Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Psalms 128 RWBT

Side by side with the Father's Heart Bible™

Ragal Yàlla, jàmmi kër

1Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.Ndokkalee képp ku ragal Yàlla,di jëfe ay yoonam.

2Yaay lekk saw ñaq,mbégteek ngëneel ñeel la.

3Sa jabar ni garab gu meññ ci sa kër,say doom wër a wër sa ndab ni njëmbat lu jebbi.

4Ki ragal Aji Sax jaa ngoog,nii rekk lay barkeele.

5Yal na la Yàlla barkeele fii ci Siyoŋ;yal nanga teewe xéewalu Yerusalem sa giiru dund gépp,

6te nga gis say sët.Yal na jàmm dal Israayil.

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]