Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Psalms 133 RWBT

Side by side with the Father's Heart Bible™

Bennoo, barkeel

1Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.Céy liika baax te neexati,ay bokk yu bokk dëkk, di benn!

2Daa neex ni diwu bopp gu xeeñ,siite sikkim, bu mel ni sikkimu Aaróona,rogalaat ba ci mbubbam,

3neex ni layub tundu Ermon,neex ni lay bu ni mel tey rogalaate tundi Siyoŋ.Fa la Aji Sax ji dogale barke,muy dund, ba fàww.

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]