Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Psalms 125 RWBT

Side by side with the Father's Heart Bible™

Ku doyloo Aji Sax ji raw

1Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.Ku doyloo Aji Sax ji,dangay mel ni tundu Siyoŋ, doo toxu;dangay sax ba fàww.

2Ni tund yi yéewe Yerusalem,ni la Aji Sax ji yéewe ñoñam,tey ak ëllëg.

3Nguur gu bon du saxekaw suuf su nit ñu jub muurloo.Lu ko moy ñu jub ñi sàkku lu bon,di ko jëfe.

4Éy Aji Sax ji, baaxeel ku baax,ak kuy mébét njub.

5Waaye kuy topp yoonu ndëngte,Aji Sax jee koy sànk,boole kook kuy def lu bon.Yal na jàmm dal ci Israayil.

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]