Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Jonah 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
2 Then Jonah prayed to our Father from inside the fish: Yunus ñaan ci Yàllaam Aji Sax ji, fa mu tollu ca biir jën wa.
3 In my distress I called to my Father, and he answered me; from the grave's belly I cried for help, and you heard my voice. Mu ne: Maa jàq, woo Aji Sax ji, mu wuyu ma. Ca xóotey njaniiw laa wootee wall, nga dégg ma.
4 You hurled me into the deep, into the heart of the seas, and the currents swirled around me; all your breakers and your waves swept over me. Yaa ma xalab xóotey xolu géej, ndaw ma mëdd ma. Say wal ak say gannax, lépp a jaare sama kaw.
5 Then I said, 'I have been driven away from your sight; yet I will look again toward your holy temple.' Man nag ma naan: «Dàqees na ma, ba ma sore la, waaye maay dellu gis sa kër gu sell ga!»
6 The waters closed in over me to the point of death; the deep surrounded me; seaweed was wrapped around my head. Ndox maa ma tanc ba ci put, xóotey géej mëdd ma, waag ba laxasu sama bopp.
7 I sank down to the roots of the mountains; the earth shut its gates behind me forever. But you brought my life up from the pit, my Father. Ca reeni tund ya laa suuxi, caabiy suuf féete ma gannaaw ba fàww, waaye ca kan ma nga jukkee sama bakkan, yaw, sama Yàlla Aji Sax ji.
8 As my life was ebbing away, I remembered my Father, and my prayer rose to you, to your holy temple. Noowal bakkan a nga may rëcc, sama xel ne yarr ci yaw, Aji Sax ji, sama ñaan àgg fa yaw, ca sa kër gu sell ga.
9 Those who cling to worthless idols walk away from the love that could be theirs. Ñiy wormaal neenug neen daal, ñoo dëddu seen yiw fa Yàlla.
10 But I will sacrifice to you with grateful praise; I will keep every vow I have made. Salvation belongs to our Father! Man nag, ci biir cant laa lay sarxale. Li ma xas laay sottal. Wall, fa Aji Sax ji!
11 Then our Father spoke to the fish, and it vomited Jonah out onto the dry land. Ci kaw loolu Aji Sax ji wax ak jën wa, mu goqi Yunus ca tefes ga.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]