Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Jonah 3 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Then the word of our Father came to Jonah a second time: Ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikkal Yunus ñaareel bi yoon. Mu ne ko:
2 "Get up, go to Nineveh, that great city, and proclaim the message I give you." «Jógal dem Niniw, dëkk bu mag ba, nga yegge leen kàddu gi ma lay dénk.»
3 So Jonah got up and went to Nineveh, as our Father had said. Nineveh was a huge city—three days to cross. Yunus jóg dem ba Niniw, muy la ko Aji Sax ji wax. Niniw nag def dëkk bu réya réy, ba doxub ñetti fan a koy wër.
4 Jonah walked one day into the city and cried out, "Forty more days and Nineveh is overturned!" Ba mu ko defee Yunus tàmbalee wër bés bu njëkk ba, di yéene naan: «Ñeent fukki fan gannaaw tey Niniw dina tas.»
5 The people of Nineveh believed God. They called a fast and put on sackcloth, from the greatest to the least. Waa Niniw nag gëm Yàlla, daldi yéene koor. Ci biir loolu ku nekk sol ay saaku, di ko ñaawloo, dale ko ca ka gën di mag, ba ca ka gën di ndaw.
6 When the news reached Nineveh's king, he rose from his throne, removed his robe, covered himself with sackcloth, and sat in ashes. Mbir ma àgg ca buurub Niniw. Mu ne ñokket, jóge ca ngànguneem, ne futeet mbubbam buuram, sàngoo saaku, daldi toog ci dóomu-taal, di ko toroxloo.
7 He had this proclaimed in Nineveh, by decree of the king and his nobles: No person or animal, herd or flock, may taste anything; they must not graze or drink water. Ci kaw loolu mu yéenelu dogal bii ca Niniw, ne: «Ci ndigalal Buur aki kàngamam; muy nit aku jur gu gudd ak gu gàtt, bu ci dara dugg ci seen gémmiñ. Buñu lekk, te ndox, buñu ko naan.
8 Let people and animals be covered with sackcloth, and everyone cry out to God with all their strength. Let each turn from his evil way and the violence in his hands. Na nit ak jur sàngoo saaku te ñu woo Yàlla wall lu ñu man. Na ku nekk dëddu jëfinam ju bon ak jëfi coxoram.
9 Who knows? God may turn and change his mind, turn from his fierce anger, so we're not destroyed. Jombul Yàlla dëpp ba fomm, daldi dëddu tàngooru meram, ba dunu sànku.»
10 When God saw their deeds—that they turned from their evil way—God changed his mind about the disaster he had threatened to bring on them, and did not do it. Yàlla nag gis seeni jëf, gis na ñu dëddoo seen jëfin ju bon. Yàlla daldi fomm mbugal ma mu leen naraloon, ba mujju koo def.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]