Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Jonah 4 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 But this upset Jonah deeply, and he burned with anger. Ba loolu amee Yunus mer mer mu réy, ba xol bay bax.
2 He prayed to our Father, "Please, O Father, isn't this what I said while still in my own land? That's why I fled toward Tarshish first—I knew you are a gracious, compassionate Father, slow to anger, overflowing with covenant love, one who relents from sending disaster. Mu ñaan Aji Sax ji, ne ko: «Céy Aji Sax ji, xanaa du lii laa waxoon ba ma génnagul sama réew? Moo taxoon ma njëkka daw, jëm Tarsis! Ndax xamoon naa ne yaw Yàlla yaay boroom yiw ak yërmande, sa mer a diib, sa ngor bare, ngay fomm mbugal.
3 Now, our Father, please take my life from me—death is better for me than life." Léegi nag Aji Sax ji, rikk jëlal sama bakkan rekk, ndax dee sax a ma gënal dund!»
4 And our Father said, "Is it right for you to be so angry?" Aji Sax ji ne ko: «Waaw, mbaa yaa yey am xol bu tàng ci loolu?»
5 Jonah left the city and sat east of it, made himself a shelter there, and sat under it in the shade, waiting to see what would happen to the city. Yunus daldi génn dëkk ba, dem toogi fa féete dëkk ba penku, mbaaral fa boppam, toog ca keppaar ga, di seet nu dëkk bay mujje.
6 And our Father appointed a plant and made it grow up over Jonah, to shade his head and ease his discomfort. So Jonah was overjoyed because of the plant. Ba mu ko defee Aji Sax ji Yàlla yebal ag lawtan, mu law, tiim Yunus, keral boppam ngir xettali ko. Yunus bég mbégte mu réy ca lawtan ga.
7 At dawn the next day, our Father appointed a worm that attacked the plant, and it withered. Ca ëllëg sa, ba jant bay fenk, Yàlla yebal aw sax, mu song lawtan ga, mu wow.
8 When the sun rose, our Father sent a scorching east wind; the sun beat on Jonah's head until he grew faint. He begged to die: "Better for me to die than to live." Naka la jant ba fenk, Yàlla yebal ngelawal penku lu tàng jérr, jant ba jam boppu Yunus, ba mu xawa xëm, bëggatul dara ci bakkanam. Mu naan: «Dee sax a ma gënal dund!»
9 But our Father asked Jonah, "Is it right for you to be angry about the plant?" He said, "It is right—angry enough to die." Ci kaw loolu Yàlla ne Yunus: «Waaw, mbaa yaa yey am xol bu tàng ci lawtan gi?» Mu ne: «Maa yey am xol bu tàng ba dee sax!»
10 And our Father said, "You pitied the plant you did not work for or grow, which sprouted in a night and died in a night. Aji Sax ji ne ko: «Waaw yaw, yaa ngi xalaat lawtan gii nga sonnul, lawaloo ko; guddi la sax, guddi ga ca topp mu dee.
11 And should I not pity Nineveh, that great city, in which there are more than 120,000 people who cannot tell their right hand from their left, and many animals as well?" Man nag, Niniw, dëkk bu mag bii ëmb lu ëpp fuuf téeméeri junniy nit ak ñaar fukk (120 000), ñu ràññeewul seen ndijoor ak seen càmmoñ, ak mala yu bare, duma leen xalaat?»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]