Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Jonah 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Now the word of our Father came to Jonah son of Amittai: Am na bés kàddug Aji Sax ji dikkal Yunus mi Amitay di baayam. Mu ne ko:
2 "Get up, go to Nineveh, that great city, and cry out against it, for their evil has risen before me." «Jógal dem Niniw, dëkk bu mag ba, nga rëbb leen, ndax seen mbon agsi na ba fi man.»
3 But Jonah set out to flee to Tarshish, away from our Father's presence. He went down to Joppa, found a ship bound for Tarshish, paid its fare, and boarded to go with them to Tarshish, away from our Father's presence. Yunus nag jóg jëm Tarsis, ngir daw Aji Sax ji. Mu àgg fu ñuy wax Yafa, fekk fa gaal gu mag gu jëm Tarsis. Mu fey njëg ga, dugg, ànd ak ña ca nekk, jëm Tarsis, ngir daw Aji Sax ji.
4 Then our Father hurled a great wind at the sea; a violent storm arose, and the ship seemed about to break apart. Aji Sax ji itam sànni ngelaw lu réy ca géej ga, muy ngëlén lu réy ca géej ga, ba gaal ga nara tas.
5 The sailors were terrified, each crying to his own god. They threw the ship's cargo into the sea to lighten it. But Jonah had gone below deck, where he lay fast asleep. Ba loolu amee mool ya tiit di yuuxoo, ku nekk di woo sa yàlla wall. Ñu sànni biir géej la ñu yeboon ca gaal ga ngir gëna woyof. Fekk na Yunus wàcc ca suufu gaal ga, tëdd di nelaw ba yàndoor.
6 The captain came and said, "How can you sleep? Get up, call on your god! Maybe he will notice us, and we won't perish." Ci kaw loolu njiitu mool ya dikk ba ca moom, ne ko: «Yaw, ana looy nelaw? Jógal kay woo sa yàlla wall! Jombul mu geesu nu, ba dunu sànku.»
7 The men said to each other, "Come, let's cast lots to find who's to blame for this disaster on us." They cast lots, and it fell on Jonah. Ci biir loolu ku nekk naan sa moroom: «Ayca nu tegoo bant, ba xam musiba mii nu dal, ku nu ko yóbbe.» Ñu tegoo bant, mu dal ca kaw Yunus.
8 They said to him, "Tell us—you who have brought this disaster on us—what do you do? Where do you come from? What is your country? What people are you from?" Ñu ne ko: «Dinga nu wax nag ku nu yóbbe mii musiba! Ana luy sa liggéey, ak foo bàyyikook fuy sam réew, ak xeet woo bokk sax yaw?»
9 He answered, "I am a Hebrew, and I fear our Father, the Father of heaven, who made the sea and the dry land." Mu ne leen: «Ab Ebrë laa. Aji Sax jiy Yàllay asamaan laay jaamu, moom mi sàkk géej ak jéeri.»
10 Then the men were terrified and said, "What have you done?" For they knew he was fleeing from our Father's presence, because he had told them. Ci kaw loolu nit ña tiit tiitaange ju réy, ne ko: «Yaw, li nga def lu mu doon?» Fekk na Yunus xamal leen ne Aji Sax ji lay daw.
11 Then they said to him, "What should we do to you to calm the sea for us?"—for the sea grew stormier and stormier. Géej ga nag di gëna sàmbaraax. Ñu ne ko: «Nu nu lay def nag, ba géej gi dalal nu?»
12 He told them, "Lift me up and throw me into the sea, and it will calm for you. I know this great storm came on you because of me." Yunus ne leen: «Fableen ma, sànni ci biir géej gi. Kon géej gi dal. Ndax xam naa xéll ne ngëlén lu réy lii, maa leen ko yóbbe.»
13 Instead the men rowed hard to reach land, but could not, for the sea grew wilder and wilder against them. Terewul nit ña joow, joow rekk, wuti tefes, mu të ndax géej ga gëna sàmbaraax ca seen kaw.
14 So they cried out to our Father: "Please, God, don't let us die for taking this man's life. Don't hold us guilty of innocent blood, for you have done as you pleased." Ba loolu amee ñu ñaan Aji Sax ji, ne ko: «Céy Aji Sax ji, ngalla bu nu bàyyi nu sànku ndax bakkanu nit kii, te bu nu gàdduloo bakkanu jàmbur, ndax yaw Aji Sax ji, sa coobare nga def.»
15 Then they picked Jonah up and hurled him into the sea, and the raging sea grew calm. Ñu daldi fab Yunus, sànni ca biir géej ga, géej ga giif, ne tekk.
16 The men then feared our Father greatly, offered a sacrifice to our Father, and made vows. Nit ña nag am tiitaange ju gënatee réy ci Aji Sax ji, daldi rendil Aji Sax ji sarax, ba noppi xasal ko aw xas.
2:1 Now our Father appointed a great fish to swallow Jonah, and Jonah was in the belly of the fish three days and three nights. Ci kaw loolu Aji Sax ji yebal jën wu mag, mu wann Yunus. Mu nekk ca biiru jën wa ñetti bëccëg ak ñetti guddi.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]