Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Proverbs 31 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 The words of King Lemuel—an oracle his mother taught him: Lii waxi Lemuyel la, buuru Maasa, te ndeyam jàngal ko ko. Mu ne:
2 What, my son? What, son of my womb? What, son of my vows? Ngóor si doom, saa doomi bopp! Yaa di ñaan gu nangu, doom!
3 Do not give your strength to women, or your ways to those who destroy kings. Bul jox jigéen ñi sa doole, bul jox say siddit jigéen ñiy sànk buur.
4 It is not for kings, Lemuel—not for kings to drink wine, or for rulers to crave strong drink. Buur moomul di naan biiñ, Lemuyel, buur moomu ko; kilifa moomul di sàkku ñoll.
5 For if they drink, they will forget what is decreed and pervert the rights of all the oppressed. Lu ko moy mu naan, ba fàtte lu yoon tëral, xañ néew-ji-doole ju ne àqam.
6 Give strong drink to one who is perishing, and wine to those in bitter distress. Bàyyeel ñoll kuy sànku, bàyyeel biiñ boroom naqar.
7 Let them drink and forget their poverty, and remember their misery no more. Bu ñu naanee, fàtte seen néewle, ba dootuñu fàttaliku seenu tiis.
8 Open your mouth for the voiceless, for the rights of all who are left destitute. Nanga àddul ku amul kàddu, ku sësul fenn, nga ñoŋal àqam.
9 Open your mouth, judge righteously, and defend the rights of the poor and needy. Deel àddu, di àtte njub; ku ñàkk ak ku néewle, nga sàmm àqam.
10 A woman of valor—who can find her? She is far more precious than jewels. Jeeg bu jàmbaare, ndaw lu jafe, ba rawati gànjar!
11 The heart of her husband trusts in her, and he will lack nothing of value. Jëkkër ja da koy wóolu, te jëkkër ja day am xéewal, du ko ñàkk.
12 She does him good and not harm, all the days of her life. Day defal jëkkëram lu baax, du ko lor, te di ànd ak bakkan.
13 She seeks out wool and flax, and works with willing hands. Day wut kawari gàtt aki wëñ, di ca liggéeye mbégte.
14 She is like the merchant ships, bringing her food from afar. Day mel ni gaalu jula, di jëli dundam fu sore.
15 She rises while it is still night, provides food for her household, and portions for her servant girls. Day jóg te bët setul, di waajal njëlu njabootam, aka sas ay janqam.
16 She considers a field and buys it; from the fruit of her hands she plants a vineyard. Day seetlu ab tool, jënd ko, sàkk ciw ñaqam, jëmbat tóokër.
17 She wraps herself in strength and makes her arms strong. Day gañu di góor-góorlu aka dëgëral përëg ya.
18 She perceives that her trading is profitable; her lamp does not go out at night. Day gis njartel liggéeyam, te làmpam du fey guddi.
19 She puts her hands to the spinning staff, and her hands grasp the spindle. Ma ngay yor poqe ak këccu, di ëcc.
20 She opens her hand to the poor and reaches out her hands to the needy. Day jox ku ñàkk, di sàkkal néew-ji-doole.
21 She has no fear for her household when it snows, for all her household are clothed in scarlet. Tiitul ci njaboot gi sedd bu metti, ndax ñoom ñépp ay tegley yére.
22 She makes coverings for herself; her clothing is fine linen and purple. Mooy sàkkal boppam ay malaan, ay yéreem mucc ayib te yànj.
23 Her husband is known in the gates, when he sits among the elders of the land. Dees na ràññee jëkkëram ca pénc ma, fa muy toog ca magi réew ma.
24 She makes linen garments and sells them, and supplies sashes to the merchants. Ndaw su ni mel day ràbb ay yére, di jaay, aki gañaay, di jox jaaykat yi.
25 Strength and dignity are her clothing, and she laughs at the days to come. Faaydaak jom la làmboo, te ëllëg ubul boppam.
26 She opens her mouth with wisdom, and faithful instruction is on her tongue. Day wax lu xelu, di digle ngor.
27 She watches over the ways of her household and does not eat the bread of idleness. Jigéen jooju mooy bàyyi xel ci njabootam, te du nangoo yàccaaral.
28 Her children rise up and call her blessed; her husband also, and he praises her: Doom ya dañu ko naan: «Jarawlakk!» Jëkkër ja di ko gërëm naan:
29 "Many daughters have done valiantly, but you surpass them all." «Jeeg bu jàmbaare bare na, waaye yaw, yaa ci raw.»
30 Charm is deceptive and beauty is fleeting, but a woman who reveres our Father—she will be praised. Melokaan wu jekk day naxe, taar day wéy, waaye jigéen ju ragal Aji Sax ji, kookoo jara gërëm.
31 Give her the fruit of her hands, and let her works praise her in the gates. Joxleen ko njukkalu ñaqam, jëfam di woyam ca pénc ma.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]