Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Ecclesiastes 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 The words of the Teacher, son of David, king in Jerusalem. Lii kàdduy waarekat baa, di doomu Daawuda te di buurub Yerusalem.
2 "Utterly fleeting," says the Teacher, "utterly fleeting! Everything is fleeting." Cóolóoloo cóolóol, waru waarekat ba, cóolóoloo cóolóol, léppi cóolóoli neen.
3 What does a person gain from all the labor at which they toil under the sun? Ana sax luy njariñu doñ-doñoo doñ-doñ ju nit di doñ-doñi fi kaw dun bi?
4 A generation goes, and a generation comes, but the earth remains forever. Ag maas wéy, ag maas teew; àddina sax ba fàww.
5 The sun rises and the sun sets, and hurries back to the place where it rises. Jant fenk, so, ne coww dellu fa muy fenke.
6 The wind blows to the south and turns to the north; round and round it goes, ever returning on its circuits. Ngelaw jëm bëj-saalum, wiiri jëm bëj-gànnaar, di wiir aka wiiraat, di delluy wëndeelu, topp yoonam.
7 All the streams run to the sea, yet the sea is never full; the streams return to their source and flow again. Dexoo dex wal, wuti géej, te taxul géej fees. Fa dex wal jëm, fa lay walati, jëm.
8 All things are wearisome, more than anyone can express; the eye is not satisfied with seeing, nor the ear filled with hearing. Jëfoo jëf ca jëfit, làmmiñ tuddul lépp, bët du suur, nopp du buur.
9 What has been is what will be, and what has been done is what will be done; there is nothing new under the sun. Lu ayoon mooy ayati, lu ñu jëfoon moom lañuy jëfati. Dara yeesul fi kaw suuf.
10 Is there anything anyone can point to and say, "Look, this is new"? It was already here, in the ages before us. Lëf a ngii, nit naa: «Lii de lu bees la,» te mu ngi fi woon lu yàgg, lu jiitu sunu juddu.
11 There is no remembrance of those who came before, and even those yet to come will not be remembered by those who follow them. Kenn du fàttaliku ñi jiitu, ñiy ñëwit, ñi leen topp duñu leen fàttaliku.
12 I, the Teacher, was king over Israel in Jerusalem. Man waarekat bi, buurub Israayil laa woon ci Yerusalem.
13 I gave my heart to seek and explore by wisdom all that is done under heaven—a miserable task God has given mankind to struggle with. Damaa dogu ne damay gëstu, teg ko ci xel mu rafet, di settantal mboolem lu nit def fu jant bi tiim. Ndaw sas wu tiis wu Yàlla sase, ñu war koo sasoo!
14 I saw all the deeds done under the sun, and look—it is all fleeting, a chasing after wind. Gis naa jépp jëf ju jëfe ci kaw suuf, ndeke lépp cóolóoli neen la ak nappum ngelaw.
15 What is crooked cannot be made straight, and what is lacking cannot be counted. Lu wañaaru, maneesu koo jubbanti; lu teewul, maneesu koo lim.
16 I told myself, "Look, I have grown great and gained more wisdom than all who ruled Jerusalem before me; my heart has seen much wisdom and knowledge." Damaa wax ci saam xel naa: «Man de, maa ngii di gëna xelu, ba sut ku ma jiitu ci jalub Yerusalem. Damaa xuus ci xel mu rafet ak xam-xam.»
17 I set my mind to know wisdom, and madness and foolishness; I learned this too is a chasing after the wind. Noonu dogu naa xam luy xel mu rafet, xam luy nitoodi akug ndof. Fekk loolu it nappum ngelaw la.
18 For with much wisdom comes much grief, and the more knowledge, the more sorrow. Ku géejal xel mu rafet, géejal naqar; yokku xam-xam, yokku tiis.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]