Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Proverbs 30 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 The words of Agur son of Jakeh—the oracle. The man declares: I am weary, O my Father; I am weary, O my Father, and worn out. Lii waxi Agur la, góor gay doomu Yake mu Maasa. Góor ga daa wax ak Itiyel, wax ak Itiyel ak Ukal. Mu ne:
2 Surely I am too brutish to be a man; I do not have the understanding of a man. Maa dofe dëgg, ba yées ci nit ñi, dég-dégu nit sax awma ko.
3 I have not learned wisdom, nor do I have knowledge of the Holy One. Jànguma, ba am xel mu rafet, awma xam-xam ci Aji Sell ji.
4 Who has ascended to heaven and come down? Who has gathered the wind in the hollow of his hands? Who has wrapped the waters in a garment? Who has established all the ends of the earth? What is his name, and what is his son's name? Surely you know! Ana ku yéegoon asamaan, ba wàcc? Mbaa mu masa ŋëb ngelaw ciy loxoom? Ana ku masa ëmb ndox ci ndimo? Mbaa mu rëdd mboolem kemi àddina? Nu mu tudd ak nu doomam tudd? Wax ma, yaw mi ko xam!
5 Every word of our Father proves true; he is a shield to those who take refuge in him. Lu Yàlla wax, mat na sëkk, mooy yiir ku ko làqoo.
6 Do not add to his words, or he will rebuke you and prove you a liar. Bul yokk ay waxam, mu weddi say fen, nga weeru.
7 Two things I ask of you; do not withhold them from me before I die: Éy Yàlla, ñaar laa la ñaan, ngalla may ma ko sama giiru dund:
8 Keep falsehood and lies far from me; give me neither poverty nor riches; feed me only the bread that is my portion, caaxaan aki fen, yal na ma sore, néewleek barele, bu ma ci may lenn, leel ma lu ma doy;
9 for if I am full, I may deny you and say, "Who is God?" or if I am poor, I may steal and profane the name of my God. lu ko moy ma regg, weddi la, ba naan: «Kuy Aji Sax ji?» Mbaa ma ñàkk bay sàcc, di la ñàkke worma, yaw sama Yàlla.
10 Do not slander a servant to his master, or he will curse you and you will be found guilty. Bul sikkal ab surga ca njaatigeem, da lay ñaan-yàlla, mu dal la.
11 There is a generation that curses its father and does not bless its mother. Ag maas a ngi saaga baay, te wormaaluñu ndey.
12 There is a generation clean in its own eyes yet not washed of its filth. Ag maas a ngi defe ne set nañu, te taq ripp ak bàkkaar.
13 There is a generation—how proud its eyes, how scornful its glances! Ag maas a ngi daŋŋiiral; aka ñoo mana xeeloo!
14 There is a generation whose teeth are swords, whose fangs are knives, to devour the poor from the earth and the needy from among mankind. Ag maas a ngi, seeni sell niy saamar, seeni gëñ niy paaka, ñuy lekk néew-ji-doole, ba raafal leen ci réew mi, ba ku ñàkk jeex ci biir nit ñi.
15 The leech has two daughters: "Give" and "Give." Three things are never satisfied; four never say, "Enough": Saxu watar du suur, ñaar ñu jigéen la am: Jox Ma ak Jox Ma. Ñett a ngii ñu dul suur, ba ci ñeent ñu dul ne doy na mukk:
16 The grave, the barren womb, the land never satisfied with water, and the fire that never says, "Enough." njaniiw, jigéen ju jaasir, suuf, du màndi ndox, sawara, du ne doy na mukk.
17 The eye that mocks a father and scorns to obey a mother—the ravens of the valley will pluck it out, and the young vultures will eat it. Kuy xeelu sa baay, di siidee déggal sa ndey, baaxoñ génne ciw xur, luqi sa bët, tan ya lekk.
18 Three things are too wonderful for me; four I do not understand: Ñett a ngii, yéem na ma, ba ci ñeent yu ma xamul:
19 the way of an eagle in the sky, the way of a serpent on a rock, the way of a ship in the heart of the sea, and the way of a man with a young woman. yoonu jaxaay ci asamaan, yoonu jaan ci kawi doj, yoonu gaal ci diggu géej, yoon wi góor di jaar as ndaw.
20 This is the way of an adulteress: she eats and wipes her mouth and says, "I have done no wrong." Jikkoy jigéenu moykat a ngii: day lekk, wommiku, te naan: «Defuma dara lu aay!»
21 Under three things the earth trembles; under four it cannot bear up: Ñett a ngii, day yëngal suuf, ba ci ñeent yu suuf àttanul:
22 a servant when he becomes king, and a fool when he is filled with food; jaam bu falu buur, dof bu regg,
23 an unloved woman when she finally marries, and a servant girl when she displaces her mistress. ndaw su bon su for jëkkër, jigéen ju wuutu sangam bu jigéen.
24 Four things on earth are small, yet they are exceedingly wise: Ñeent a ngii, di lu tuut ci kaw suuf, te am xel, yaroo xel:
25 the ants are a people not strong, yet they store up their food in the summer; xorondom, néew na doole, waaye bu jotee, mu denc dundam;
26 the rock badgers are a people not mighty, yet they make their homes in the cliffs; daman, barewul kàttan, te day dëkk ciy doj;
27 the locusts have no king, yet all of them advance in ranks; soccet, amul buur, teewul ñuy àndandoo, diy gàngoor;
28 the lizard you can catch in your hands, yet it is found in kings' palaces. sindax, manees na koo ŋëb, teewul ma nga biir kër buur.
29 Three things are stately in their stride; four are stately in their walk: Ñett a ngii, ñu jekkum ndaag, ba ci ñeent ñu jekk doxin:
30 the lion, mightiest among beasts, which turns back before nothing; gaynde, mooy buuru rab yi, ragalul kenn;
31 the strutting rooster, the male goat, and a king whose army is with him. séq daagu, jekk taxawaay; ab sikket, ak buur ci biiri dagam.
32 If you have been foolish, exalting yourself, or if you have schemed evil, put your hand over your mouth. Boo sàgganee bay tëggu, mbaa ngay mébét lu bon, nanga téye saw làmmiñ.
33 For pressing milk produces curds, pressing the nose produces blood, and pressing anger produces strife. Ndax ku ruux soow, am ca dax, ku wañaar bakkan, mu nàcc, te lu jógal xol, indiw ay.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]