Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Numbers 17 RWBT

Side by side with the Father's Heart Bible™

Bant bu wow jebbi na

16Ba loolu amee Aji Sax ji ne Musaa: 17«Waxal ak bànni Israayil, nga nangoo ci mboolem seen kilifay kër maam, aw yet, na wenn yet bawoo ci kër gu ci nekk, muy fukki yet ak ñaar, yet wu ci nekk, nga bind ci turu boroom. 18Turu Aaróona itam, nga bind ko ci yetu giirug Lewi, ndax wenn yet lay doon, ñeel kilifag kër gu ci nekk. 19Nga denc yet yi ca biir xaymab ndaje ma, fa kanam gaalu seedes kóllëre ga, fa may dajeek yeen. 20Su ko defee ki ma tànn, aw yetam dina jebbi, ba ma teqalikoo ak xultuy bànni Israayil yi ñuy xultu ci seen kaw.»

21Musaa àgge ko bànni Israayil, mboolem seen kilifay kër maam jox Musaa aw yet, kilifa gu ci nekk wenn yet, ñeel kër maamam, muy fukki yet ak ñaar, yetu Aaróona bokk ca. 22Musaa teg yet ya fa kanam Aji Sax ji, ca biir xaymab seede sa. 23Ca ëllëg sa, naka la Musaa dugg ca xaymab seede sa rekk, daldi fekk yetu Aaróona wu kër Lewi, jebbi; fekk na mu jebbi, ba tóor, ba meññ ay doomi amànd. 24Ba loolu amee Musaa jële yet yépp ci Aji Sax ji, dem ba ca bànni Israayil gépp, ñépp gis, ku nekk jël yetam.

25Aji Sax ji waxati Musaa, ne: «Dellool yetu Aaróona fa kanam gaalu seede sa, mu dence fa, di firnde ñeel xeetu fippukat wi, ndax nga dakkal seeni xultu ci sama kaw, ba duñu dee.» 26Musaa def noonu. Na ko ko Aji Sax ji sante, na la ko defe.

27Bànni Israayil nag naan Musaa: «Jeexal nanu nag, sànku nanu, nun ñépp ay sànku! 28Gannaaw képp ku jege màkkaanu Aji Sax ji doŋŋ, dangay dee kay, mbaa dunu far jeex tàkk?»

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]