Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Amos 3 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Hear this word our Father has spoken against you, children of Israel—against the whole family I brought up from Egypt: Dégluleen kàddu gii Aji Sax ji wax ci yeen, bànni Israayil, mu jëm ci seen mboolem xeet wi mu génnee réewum Misra. Mu ne:
2 Of all the families of the earth, I have known only you; therefore I will hold you accountable for all your sins. «Yeen doŋŋ laa ràññee ci mboolem askani suuf. Moo tax ma di leen mbugal ndax seen ñaawtéef gépp.»
3 Do two walk together, unless they have agreed to meet? Ndax ñaar dina ànd te digewuñub dajee?
4 Does a lion roar in the forest when he has no prey? Does a young lion cry out from his den if he has caught nothing? Ndax gaynde dina ŋarem ngeer te fàddul? Am gaynde gu mat dina xiiroom paxam te jàppul?
5 Does a bird fall into a snare on the ground when there is no trap for it? Does a snare spring up from the earth when it has caught nothing? Ndax picc dina keppu te fiireesu ko? Am ag fiir dina fettax te jàppul?
6 If a ram's horn is blown in a city, will the people not tremble? If disaster comes to a city, has our Father not done it? Ndax bu buftab xare jibee, waa dëkk ba du tiit? Ndax aw ay dina dabub dëkk te du Aji Sax jee?
7 Surely the Sovereign Father does nothing without revealing his secret to his servants the prophets. Du lenn moos lu Boroom bi Aji Sax ji def, te déeyu ko yonent yiy jaamam.
8 The lion has roared—who will not fear? The Sovereign Father has spoken—who can keep from prophesying? Bu gaynde yëmmoo, ana ku dul tiit? Ana ku saña baña jottali kàdduy waxyu, bu ko Boroom bi Aji Sax ji waxee?
9 Proclaim over the strongholds in Ashdod and over the strongholds in the land of Egypt, and say: "Assemble on the mountains of Samaria and see the great uproar within her, and the oppression in her midst." Yéeneleen ca biir taaxi Asdodd ak ca biir taaxi Misra. Neleen: «Dajeleen ca kaw tundu Samari, ba gis na Samari salfaañoo, ak nootaange ga fa nit di daj.
10 They do not know how to do right, declares our Father—those who hoard up violence and plunder in their strongholds. Xamuñu sax def njub.» Kàddug Aji Sax jee. «Dañuy jal alalu fitnaak yàqute ci seen biiri taax.»
11 So the Sovereign Father says: An enemy will surround the land, topple your defenses, and loot your strongholds. Moo tax Boroom bi Aji Sax ji ne: «Ab noon dina gaw seenum réew, néewal leen doole, lël seeni taax.»
12 This is what our Father says: As a shepherd rescues two legs or a piece of an ear from the lion's mouth, so the children of Israel living in Samaria will be rescued—with a corner of a couch, part of a bed. Aji Sax ji nee: «Wallub sàmm ak gàtt bu gaynde fàdd weesul ñaari yeel, dogitu nopp. Kuy wallu bànni Israayil ga ca Samari it, xanaa dogu basaŋ, dammitu lal.
13 Hear, and testify against the house of Jacob, declares the Sovereign Father, the Father of heaven's armies: Dégluleen te artu waa kër Yanqóoba.» Kàddug Boroom bi Aji Sax jee, Yàlla ji ci gàngoori xare yi.
14 On the day I punish Israel for his rebellions, I will also punish the altars of Bethel; the horns of the altar will be cut off and fall to the ground. «Bés bu may mbugale Israayil ay bàkkaaram, damay tasaale sarxalukaayi Betel. Béjjén yi ci cati sarxalukaay ba dog, rot.
15 I will strike the winter house along with the summer house; the houses of ivory will perish, and the great houses will come to an end, declares our Father. Maay màbbaale këru taax ak këru àll; kër yu ñu rafetale bëñu ñey dina yàqu, te kër yu bare dootul taxaw.» Kàddug Aji Sax jee.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]