Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Amos 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 This is what our Father says: For three sins of Moab, and for four, I will not revoke it—he burned the bones of Edom's king to lime. Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Mowab, te duma fomm seeni duma. Ñoo lakk yaxi buurub Edom, defub dóom.
2 So I will send fire on Moab, and it will devour the strongholds of Kerioth; Moab will die amid the uproar, with shouting and the sound of the shofar. Maay yebal sawara réewum Mowab, mu xoyom tatay Keryot. Mowab deewe biir riirum xare, yuux ak buftab xare jibandoo.
3 I will cut off the ruler from her midst and kill all her officials with him, says our Father. Maay dagge fa seen biir seen njiit, booleeki kàngamam, bóom.» Aji Sax jee ko wax.
4 This is what our Father says: For three sins of Judah, and for four, I will not revoke it—they rejected our Father's instruction and did not keep his rules, and their lies led them astray, the same lies their ancestors followed. Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke Yudeen ñi, te duma fomm seeni duma. Ñoo gàntal sama yoon man, yoonu Aji Sax ji, te sàmmuñu sama dogali yoon. Seen tuuri caaxaan ya seeni maam toppoon sànk na leen.
5 So I will send fire on Judah, and it will devour the strongholds of Jerusalem. Maay yebal sawara ci kaw Yudeen ñi, mu xoyom tatay Yerusalem.»
6 This is what our Father says: For three sins of Israel, and four, I won't relent—they sell the righteous for silver, the needy for a pair of sandals. Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke Israayil, te duma fomm seeni duma. Ñooy jaay jaam aji jub ngir xaalis bu mu leen ameel, jaay aji ndóol bu manul fey dàlli carax.
7 They trample the heads of the poor into the dust of the earth and push the afflicted off the road. A man and his father go to the same girl, profaning my holy name. Ñooy dëggaate néew-ji-doole ci pëndub suuf, di xañ way-ñàkk àqam. Nit ak baayam di tëdde as ndaw, di teddadil sama tur wu sell.
8 They stretch out beside every altar on garments taken as collateral, and in the house of their God they drink the wine of those they have fined. Yérey tayle yu ñu nangoo ci néew-ji-doole sax, ñu lal, ne ñàyy ci wetu mboolem sarxalukaay. Ku leen ameel, ñu feyloo la biiñ, naan ca seen biir kër tuur ya.
9 Yet it was I who destroyed the Amorite before them, as tall as the cedars and as strong as the oaks; I destroyed his fruit above and his roots below. «Ndaxam maa leen reyaloon Amoreen ñu gudd ña te réy, mbete garab yu mag. Ma boor doom ya, buur reen ya.
10 And it was I who brought you up out of the land of Egypt and led you forty years in the wilderness, to take possession of the land of the Amorite. Fekk yeen, ma génnee leen réewum Misra, jaarale leen màndiŋ ma diiru ñeent fukki at, ngir ngeen nanguji réewum Amoreen ñi.
11 I raised up some of your sons as prophets and some of your young men as Nazirites. Is this not so, people of Israel? declares our Father. Maa tabboon ci seen doom yu góor ay yonent, tànne ci seen xale yu góor ay séddoo, —am déet, yeen bànni Israayil?» Kàddug Aji Sax jee.
12 But you made the Nazirites drink wine, and you commanded the prophets, saying, "Do not prophesy." «Yeen nag ngeen di naanloo samay séddoo biiñ. Yonent yi, ngeen ne leen: “Buleen jottali kàdduy waxyu!”
13 Look, I will crush you in your place, as a cart full of sheaves crushes the ground beneath it. «Maa ngii di yëngal suuf si ngeen joggi, ni watiir wu fees aki sabaar di yëngale suuf.
14 Even the swift will find no escape, the strong will not hold on to his strength, and the warrior will not save his life. Rawtu dina réer ku gaaw, boroom doole du tala jariñoo dooleem, jàmbaar sax du mana rawale bakkanam.
15 The archer will not stand his ground, the fleet-footed will not escape, and the horseman will not save his life. Fittkat du taxaw, mana daw du taxa raw. Ab gawar it du rawale bakkanam.
16 Even the bravest of the warriors will flee away naked on that day, declares our Father. Bésub keroog, jàmbaar ju ëppu fit, duŋŋ lay def, di daw.» Kàddug Aji Sax jee.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]