Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

James 2 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 My brothers and sisters, as believers in our glorious Lord Jesus Christ, do not show favoritism. Yéen samay bokk, bu benn gënale laal seen ngëm ci sunu Boroom Yeesu Kirist, mi soloo ndam.
2 Say a man wearing a gold ring and fine clothes enters your assembly, and a poor man in shabby clothes enters too. Ndaxte su ñaari nit duggee ci seen mbooloo, kii takk jaaroy wurus te sol yére yu taaru, ka ca des ñàkk te limboo ay sagar,
3 If you notice the well-dressed one and say, "Sit here, a good seat," but tell the poor man, "Stand over there," or "Sit on the floor by my feet," ngeen teral boroom daraja ji ne ko: «Àggal ci jataay bu yiw bi,» ba noppi ngeen ne aji néew doole ji: «Taxawal fale, mbaa nga toog fi ci samay tànk,»
4 haven't you played favorites among yourselves and become judges guided by evil motives? kon gënale ngeen ci seen biir, ba àtte ci col, bàyyi xol.
5 Listen, my beloved brothers and sisters: Hasn't our Father chosen the world's poor to be rich in faith, heirs of the kingdom promised to those who love him? Dégluleen yéen sama bokk yi ma bëgg, ndax Yàlla tànnul ñi néewle ci àddina, ngir ñu barele ci ngëm, tey am i cér ci nguur, gi Yàlla dig ñi ko bëgg?
6 But you disrespected the poor. Don't the rich oppress you and drag you into court? Fekk dangeen leen di toroxal! Xanaa du boroom alal yi ñoo leen di not te di leen yóbbu fa kanam àttekat yi?
7 Aren't they blaspheming the honorable name called over you? Ndax duñu tilimal tur wu tedd, wi ngeen di wuyoo?
8 If you truly obey the royal law according to the Scripture, "Love your neighbor as yourself," you do well. Su ngeen sàmmee yoonu Buur Yàlla, ni ko Mbind mi tërale naan: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp,» kon def ngeen lu baax.
9 But if you show favoritism, you are sinning, and the law convicts you as lawbreakers. Waaye su ngeen gënalee, bàkkaar ngeen, te yoonu Yàlla dina leen dab ni ñu moy.
10 Whoever keeps the whole law but stumbles at one point is guilty of breaking it all. Ndaxte ku sàmm yoon wépp, waaye xëtt ci lenn ndigal rekk, jàdd nga yoon wépp.
11 For our Father, who forbade adultery, also forbade murder. So if you avoid adultery yet commit murder, you're a lawbreaker. Ndaxte Yàlla mi ne: «Bul njaaloo», teg na ca ne: «Bul bóome.» Ku njaaloowul nag, waaye nga bóome, jàdd nga yoon wépp.
12 Speak and act as people who will be judged by the law of freedom. Gannaaw dingeen nara jaar ci àtteb yoon, wiy goreel, na loolu lal seen wax ak seen jëf.
13 Judgment is merciless to one who showed no mercy; mercy triumphs over judgment. Ndaxte ku yërëmul, yoon du la yërëm. Te yërmande mooy not àtte.
14 What good is it, my brothers and sisters, if someone claims faith without works? Can that faith save him? Te lii itam samay bokk: ku ne gëm nga, te jëfewoo ko, loolu lu muy jariñ? Ndax googu ngëm man na laa musal?
15 Suppose a brother or sister is poorly clothed and lacking daily food, Su amee mbokk ci seen biir, mu rafle te amul dund, muy góor walla jigéen,
16 and one of you tells them, "Go in peace, stay warm and fed," but gives nothing for their bodily needs—what good is that? te kenn ci yéen ne ko: «Demal ak jàmm, nga solu te lekk,» te fekk fajuleen aajoom, loolu lu muy jariñ?
17 In the same way, faith by itself, if it is not accompanied by works, is dead. Noonu ngëm gu àndul ak jëf, amul benn njariñ.
18 But someone will say, "You have faith, and I have works." Show me your faith without works, and I'll show you my faith from my works. Waaye xanaa dina am ku ne: «Yaw am nga ngëm, man am naa ay jëf.» Yaw nag won ma sa ngëm gu àndul ak jëf; man, ma feeñal la sama ngëm ci samay jëf.
19 You believe that our Father is one; you do well. Even the demons believe that—and shudder. Gëm nga ne Yàlla kenn la; loolu lu baax la, waaye xamal ne, jinne yi it gëm nañu loolu, ba dañoo tiit bay lox.
20 Do you want me to show you, you foolish person, that faith apart from works is useless? Yaw mi gàtt xel, kaay ma won la ne ngëm gu àndul ak jëf, amul njariñ.
21 Was not Abraham our father justified by works when he offered his son Isaac on the altar? Sunu maam Ibraayma, ndax du ci kaw jëf la ko Yàlla àttee ni ku jub, ci li mu joxe doomam Isaaxa ni sarax?
22 You see that faith was working together with his works, and faith was completed by his works. Kon gis nga ne ngëm dafa lëngoo ak ay jëfam, te ngëmam mat ci kaw jëf jooju.
23 This fulfilled the Scripture: "Abraham believed our Father, and it was credited to him as righteousness"—he was called our Father's friend. Noonu li ñu wax ci Mbind mi am na, bi mu naan: «Ibraayma gëm na Yàlla, te Yàlla jàppe ngëmam ni njub,» ba ñu ko wooye xaritu Yàlla.
24 You see that a person is justified by works and not by faith alone. Kon nag gis nga ne Yàlla ci jëf lay àtte nit ni ku jub, waaye du ci kaw ngëm kese.
25 Likewise, wasn't Rahab the prostitute also justified by works, welcoming the messengers and sending them out a different way? Naka Raxab jigéenu moykat bi itam, ndax du ci noonu la ko Yàlla àttee ni ku jub, ci li mu teeru ndawi Yawut yi, te jaarale leen ca poot ba?
26 As the body without the spirit is dead, so also faith without works is dead. Kon nag ni jëmm ju amul ruu nekke ndee, noonu la ngëm gu àndul ak jëf nasaxe.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]