Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

James 3 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 My brothers and sisters, not many of you should become teachers, since we teachers face stricter judgment. Samay bokk, bu ñépp di sababloo nekk jànglekatu mbooloo mi, xam ne nun jànglekat yi, àtte bi nuy jaar mooy gëna diis.
2 For we all stumble in many ways. Anyone who never stumbles in speech is a mature man, able to control his whole body too. Ndaxte nun ñépp sikk nanu ci fànn yu bare. Ki sikkul ci kàddoom, ku mat nga te mana not sa yaram wépp.
3 If we put bits in horses' mouths to make them obey us, we guide their whole bodies too. Noonu ku laab fas, ngir mu déggal la, not nga jëmmam jépp.
4 Consider ships too: though large and driven by strong winds, a tiny rudder steers them wherever the pilot wants. Gaal yi it yu réy lañu, te ngelaw lu am doole di leen jañax, waaye dawalkat bi, weñ gu tuuti la leen di jëme fu ko neex.
5 So too the tongue is a small body part, yet boasts great things. See how small a fire sets ablaze a great forest! Ci noonu làmmiñ, cér su tuuti la, waaye day bàkkoo jëf yu réy. Seetleen ni ferñent tuutee te mana lakk àll bu yaatu.
6 The tongue is a fire, a world of wickedness placed among our body's parts. It stains the whole body, sets the whole course of life ablaze, and is itself set ablaze by hell. Noonu it làmmiñ sawara la, di bon-bonu àddina ci biir cér yi, tey musibaal jëmm jépp. Jum la, bu Seytaane taal, muy lakk àddina.
7 Every kind of beast, bird, reptile, and sea creature is tamed, and has been tamed, by humankind, Nit man na not xeeti rab yépp: rabi àll yi, picc yi, yiy raam ak yi ci géej gi-- not na lépp.
8 but no human being can tame the tongue. It is a restless evil, full of deadly poison. Waaye làmmiñ kenn manu koo not; musiba la mu dul dal mukk, fees dell ak daŋar juy rey.
9 With it we bless our Father; with it we curse people made in the likeness of our Father. Làmmiñ lanuy sante Boroom bi, di sunu Baay, ba noppi móoloo ko nit, ñi Yàlla sàkk ci meloom.
10 From the same mouth come blessing and cursing. My brothers and sisters, this should not be. Gémmiñ gi sante mooy móoloo. Yéen samay bokk, loolu warula am.
11 Does a spring pour out both fresh and bitter water from the same opening? Ndax ndox mu lewet ak mu wex dinañu ballandoo ci genn mbënn?
12 Brothers and sisters, can a fig tree bear olives, or a vine figs? Neither can a salt spring yield fresh water. Samay bokk, ndax mas ngeena gis garabu figg gu meññ oliw, walla garabu reseñ gu meññ ay figg? Mukk! Mbënnu xorom manta nàcc mukk ndox mu neex.
13 Who is wise and understanding among you? Let him show his deeds through good conduct, in wisdom's humility. Ana ku neex xel ci yéen, ana kuy boroom xam-xam? Na ko wone ciy jëfam ak dundam gu sell, te feeñal xelam ci jikkoom ju lewet.
14 But if bitter envy and selfish ambition fill your heart, don't boast or lie against the truth. Waaye ku am ci sa xol farlu gu laloo wextan ak wut aw tur, bul bàkku, di weddi dëgg.
15 This is not the wisdom that comes down from above, but is earthly, unspiritual, demonic. Xel moomu jógewul ci kaw; jëfu àddina la, di jikkoy niti kese, te jóge ci Seytaane.
16 For where there is jealousy and selfish ambition, there will be disorder and every vile practice. Ndaxte fu wextan ak wut aw tur dugg, indi fa xëccoo ak bépp ñaawteef.
17 Wisdom from above: pure first, then peace-loving, gentle, reasonable, full of mercy and good fruit, unbiased, sincere. Waaye xel mi jóge ci kaw daa sell, ba noppi ànd ak jàmm te lewet, nooy, fees dell ak yërmande ak jëf yu rafet; àndul ak genn parlàqu, amul genn naaféq.
18 And the harvest of righteousness is sown in peace by those who make peace. Te nitu jàmm dina bey toolu jàmm, góob njub.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]