Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

James 4 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Where do wars and fights among you come from? Isn't it your cravings warring inside you? Xeex yi ak xuloo yi ci seen biir nag, lu leen waral? Xanaa du ci seeni bëgg-bëgg, yiy xeex ci seeni cér?
2 You want and don't have—you kill. You crave and can't get it—you quarrel and fight. You don't have because you don't ask. Dangeen di mébét waaye dungeen am; dangeen di bóome, boole ci kiñaan, waaye li ngeen di yóotu, dungeen ko jot; dangeen di xuloo ak a xeex waaye dungeen am dara, ndaxte ñaanuleen Yàlla.
3 You ask and do not receive, because you ask wrongly, to spend it on your own pleasures. Bu ngeen ñaanee sax, dungeen jot dara, ndax yéena ngi ñaan ci naaféq, ngir gëna topp seen nafsu.
4 You adulterous people! Don't you know friendship with the world is hostility toward our Father? Whoever chooses to be its friend becomes an enemy of our Father. Yéen ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla, xanaa xamuleen ne mbëggeelu àddina, mbañeel la fa Yàlla? Ku bëgga xaritoo ak àddina nag, noonoo nga ak Yàlla.
5 Or does Scripture speak for nothing, saying the spirit he placed in us longs jealously? Xanaa yaakaar ngeen ne Mbind mi day wax cig neen, ci li mu ne: «Yàlla am na mbëggeel gu fiir ci Xel mi mu def ci nun.»
6 But he gives more grace. That is why Scripture says, "Our Father opposes the proud but gives grace to the humble." Waaye yiwu Yàllaa ko ëpp. Moom la Mbind mi wax ne: «Yàlla dàq na ñi réy, waaye yiwal na ñi woyof.»
7 Submit yourselves, then, to our Father. Resist the devil, and he will flee from you. Kon nag wàkkirluleen ci Yàlla, waaye dàqleen Seytaane, te dina daw, ba sore leen.
8 Come close to our Father, and he will come close to you. Cleanse your hands, sinners; purify your hearts, double-minded. Jegeleen Yàlla, mu jege leen. Yéen bàkkaarkat yi, sellal-leen seeni loxo; yéen ñi am xel ñaar, laabal-leen seeni xol.
9 Grieve, mourn, and weep. Turn your laughter to mourning and your joy to gloom. Toroxluleen te naqarlu, bay jooy; defleen seeni ree aw naqar, te seen mbég nekk tiis.
10 Humble yourselves before our Father, and he will lift you up. Suufeel-leen seen bopp fa kanam Boroom bi, kon dina leen yékkati.
11 Don't speak against each other, brothers and sisters. Whoever speaks against a brother, or judges him, speaks against the law and judges it. But if you judge the law, you're not keeping it—you're judging it. Yéen bokk yi, buleen ŋàññante. Ku ŋàññ sa moroom mbaa nga ñaaw njort, ba àtte ko, diiŋat nga yoonu Yàlla te àtte ko. Ku àtte yoon wi nag sàmmoo ko, waaye danga koo àtte.
12 Only one gives the law and judges—able to save or destroy. Who are you to judge your neighbor? Kenn rekk mooy tëral yoon, kooku rekk mooy àtte; moo mana musle, moo mana alage. Te sax yaw miy àtte sa bokk yaay kan?
13 Come now, you who say, "Today or tomorrow we will go to this or that city, spend a year, trade, and profit." Léegi nag dégluleen, yéen ñiy wax ne: «Tey walla ëllëg dinanu dem ca dëkk sàngam, def fa at, di fa sàkku xaalis ci jula.»
14 You don't know what tomorrow brings. What is your life? For you're a mist, visible briefly, then gone. Ndax dangeena xam seen ëllëg? Luy seen dund? Xanaa cóola doŋŋ luy naaw ci diir bu gàtt, daldi naaxsaay.
15 Instead you ought to say, "If our Father wills, we will live and do this or that." Lii kay ngeen waroona wax: «Bu soobee Boroom bi, dinanu dund, tey def nàngam ak nàngam.»
16 As it is, you boast in your arrogance. All such boasting is evil. Waaye fi mu ne, naagu ngeen bay damu, te damoo noonu baaxul.
17 So whoever knows the good to do and fails to do it, sin is theirs. Kon nag ku xam def lu baax te defoo ko, bàkkaar nga.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]