Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

James 5 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Come now, you who are rich, weep and wail over the miseries that are coming upon you. Dégluleen yéen boroom alal yi, jooyleen te naqarlu ndax mbugal, gi leen di xaar.
2 Your riches have rotted, and your clothes have become moth-eaten. Seen alal seey na, seen yére yi maxe na,
3 Your gold and silver have rusted; their rust will witness against you and burn your flesh like fire. You piled up riches in the last days. seen wurus ak seen xaalis xomaag na. Xomaag jooju seede lay doon, su leen di daanlu, ba lakk leen ni sawara. Dajale ngeen alal ju ne gàññ, te fekk yéena ngi ci mujug jamono.
4 Look: the wages you held back from the workers who mowed your fields cry out, and the harvesters' cries have reached the ears of the Father of heaven's armies. Dégluleen! Jooyi xaalis bi ngeen sàcce ci gubkat, yi leen doon liggéeyal, ak yuuxi góobkat yi, dugg nañu ci noppi Boroom gàngoori xare yi.
5 You lived on earth in luxury and indulgence. You fattened your hearts in a day of slaughter. Ci barele ak bànneex ngeen dunde ci kaw suuf, di yafal seen bopp, fekk bésu rendi baa ngii.
6 You have condemned and murdered the righteous one, who does not resist you. Daan ngeen ku jub, ba rey ko sax, te bañul.
7 So be patient, brothers and sisters, until the Lord's coming. Think of the farmer: he waits patiently for the land's precious fruit, until it gets the early and late rains. Yéen samay bokk, muñleen, ba Boroom bi délsi ci ndamam. Seetleen ci beykat bi, ni muy xaare njariñ ci meññeefu suuf, tey muñ, céebo ba bët wàcc.
8 You too must be patient. Strengthen your hearts, because the coming of the Lord is near. Yéen itam nag muñleen te dëgëral seen xol, xam ne ñëwug Boroom bi ci ndamam jege na.
9 Don't grumble against each other, brothers and sisters, or you'll be judged. Look—the Judge stands at the doors. Buleen jàmbatante, samay bokk, ngir ragal Yàlla àtte leen. Àttekat baa ngi ci bunt bi sax!
10 Brothers and sisters, take the prophets who spoke in the name of our Father as examples of suffering and patience. Bokk yi, defleen yonent, yi wax ci turu Boroom bi, seeni royukaay ci muñ tiis ak ci góor-góorlu.
11 See, we call those who endured blessed. You've heard of Job's endurance and seen what our Father brought about—our Father is rich in compassion and mercy. Xam ngeen ne ñiy góor-góorlu, ñu barkeel lañu. Dégg ngeen muñ ga Ayóoba amoon, te gis muj gu rafet, ga ko Boroom bi jagleel, ndax Boroom bi kuy ñeewante la te bare yërmande.
12 Above all, my brothers and sisters, do not swear—neither by heaven, nor earth, nor any other oath. Let your yes be yes and your no, no, so you won't fall under judgment. Te li fi raw samay bokk, buleen waat mukk, bu muy ci asamaan mbaa ci suuf mbaa ci leneen lu mu mana doon. Nangeen yem ci: «waaw» ak «déedéet», ngir bañ cee layoo fa kanam Yàlla.
13 Is anyone among you suffering? Let them pray. Is anyone cheerful? Let them sing praises. Su amee ci yéen ku nekk ci tiis, na ñaan ci Yàlla. Ku nekk ci mbég, na sant Yàlla ciy woy.
14 Anyone sick among you? Have them call for the church elders, and have the elders pray over them, anointing them with oil in the name of the Lord. Su amee ci yéen ku wopp, na woo njiiti mbooloo mi, ñu ñaanal ko te diw boppam ci turu Boroom bi.
15 The prayer of faith will save the sick person, and the Lord will raise him up. And if he has sinned, he will be forgiven. Ñaan gu ànd ak ngëm dina musal ki wopp, ba Boroom bi yékkati ko. Su ko fekkoon ak i bàkkaar sax, Yàlla dina ko baal.
16 So confess your sins to each other and pray for each other, that you may be healed. A righteous person's prayer is powerful and effective. Kon nag waxanteleen seeni bàkkaar tey ñaanalante, ngir ngeen wér. Ñaanu aji jub gu dëggu, dooleem amul kem.
17 Elijah was a man like us, and he prayed hard that it not rain; it did not rain on the land for three years and six months. Naka noonu Ilyaas nit la woon ku bindoo ni nun, waaye bi mu saxee ci ñaan Yàlla, ngir mu baña taw, ndox laalul suuf diirub ñetti at ak genn-wàll.
18 Then he prayed again, and the heavens gave rain, and the earth produced its fruit. Gannaaw ga mu dellu ñaan, asamaan daldi taw, te suuf si saxal meññeef.
19 My brothers and sisters, if anyone among you wanders from the truth and someone turns them back, Samay bokk, su amee ci yéen ku réere dëgg, te am ku ko gindi,
20 know this: whoever turns a sinner from their wrong way saves that person's soul from death and covers a multitude of sins. na xam lii: ku gindi bàkkaarkat ci réeram, musal nga nit ci dee te faral ko bàkkaar yu bare.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]