Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

1 Peter 1 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Peter, apostle of Jesus Christ, to the chosen exiles scattered through Pontus, Galatia, Cappadocia, Asia, and Bithynia. Man Piyeer, ndawul Yeesu Kirist, maa leen di bind, yéen doxandéem yi tasaaroo ci diiwaani Pont, Galasi, Kapados, Asi ak Bitini. Yàlla Baay bi tànn na leen,
2 Chosen by our Father's foreknowledge, made holy by the Holy Spirit, to obey Jesus Christ and be sprinkled with his blood: grace and peace multiplied to you. ci li mu leen xam bu jiitu, te sédde leen boppam ci jëfu Xel mu Sell mi, ngir ngeen déggal ko, te seen xol laab ndax deretu Yeesu Kirist. Na leen Yàlla dollil yiw ak jàmm.
3 Blessed is our Father, and the Father of our Lord Jesus Christ: by his great mercy he gave us new birth into a living hope through Jesus Christ's resurrection from the dead, Cant ñeel na Yàlla, Baayu sunu Boroom Yeesu Kirist! Moo nu judduwaatal ci yërmandeem ju bare, ba may nu yaakaar ju sax ndax ndekkitel Yeesu Kirist.
4 into an inheritance that can never perish, spoil, or fade, kept in heaven for you, Sédd na leen cér bu dul yàqu, du gàkk te du seey mukk, dencal leen ko ci asamaan,
5 protected through faith by our Father's power for the salvation ready to be revealed in the last time. yéen ñi muy aar ci dooleem, sukkandikoo ci ngëm, di leen nége mucc, gi mu nara feeñal bés bu mujj ba.
6 You rejoice greatly in this, though now, briefly, you may have had to be distressed by various trials. Yéena ngi bég bu baax ci biir yaakaar jooju, doonte sax, su waree am, yéena ngi dékku tiis ab diir, ci seen jànkoonte ak nattu yu wuute.
7 These have come so that your faith—tested and found genuine, worth more than fire-refined gold that still gets destroyed—may bring praise, glory, and honor when Jesus Christ appears. Xam ne nattu yooyu dinañu sellal seen ngëm, ni sawara di setale wurus, fekk wurus luy wéy la, te ngëm a ko gën fuuf. Noonu seen ngëm dina yelloo cant, ndam ak màgg, bés bu Yeesu Kirist feeñee.
8 Though you've never seen him, you love him; though you don't see him now, you trust him, rejoicing with joy beyond words and full of glory, Masuleen koo gis waaye bëgg ngeen ko, gisuleen ko waaye gëm ngeen ko te am mbég mu xel dajul, mu fees dell ak ndam,
9 for you are receiving the goal of your faith, the salvation of your souls. di jot muj gi ngëm séentu, maanaam muccu xol.
10 Prophets who spoke of the grace meant for you investigated and searched carefully into this salvation, Naka mucc googu nag, yonent yi xamle yiw, wi ngeen naroona joti, seet nañu ko te gëstu ko.
11 searching for the time and situation the Spirit of Christ in them pointed to, when he predicted Christ's sufferings and the glories after them. Bi Xelum Kirist, mi nekkoon ci ñoom, seedee lu jiitu coonoy Kirist ak ndam la cay topp, jéem nañoo takk, kañ ak nan lay ame.
12 It was revealed to them: they served not themselves but you, when they spoke of these things now announced to you through those who preached the good news to you by the Holy Spirit sent from heaven. Even angels long to look into these things. Waaye Yàlla xamal na leen ne moomuñu woon kàddu googu ñu wax, waaye yéena ko moom. Te mooy kàddu gi ngeen dégg ci gémmiñu ñi leen doon jottali xibaaru jàmm bi, ci dooley Xel mu Sell, mi Yàlla yónnee asamaan; malaaka yi sax bëgg nañoo gëstu yëf yii.
13 So, minds braced for action and fully sober, hope completely on the grace to be brought to you when Jesus Christ is revealed. Kon fagaruleen ci seeni xalaat te maandu, di wékk seen yaakaar jépp ci yiw, wi leen Yàlla di jagleel bés bu Yeesu Kirist di feeñ.
14 As obedient children, don't let yourselves be shaped by the desires you once followed in your ignorance. Gannaaw gaayi Yàlla yu koy déggal ngeen, buleen toppati bëgg-bëgg, yi ngeen toppoon, bi ngeen xamagul Yàlla.
15 But just as the one who called you is holy, so be holy in all you do; Waaye na seen dund gépp sell, ni Yàlla mi leen woo selle.
16 for it is written: "Be holy, because I am holy." Ndaxte Mbind mi nee na: «Sell-leen, ndaxte ku sell laa.»
17 Since you call on a Father who judges every deed without favoritism, spend your exile time here in reverent fear. Gannaaw nag Yàlla, mi ngeen di wooye Baay, mooy àtte jëfi ñépp te du gënale kenn, saxleen ci ragal ko diirub seen ngan ci àddina.
18 You know silver and gold—things that decay—didn't rescue you from the empty life passed down from your ancestors, Xam ngeen ne, Yàlla jot na leen ci seen dund gu tekkiwul dara, gi maam ya nekkoon; te jotuleen ak yu deme ni xaalis mbaa wurus yuy wéy,
19 but with Christ's precious blood, a lamb without defect or stain. waaye ci deretu Kirist ju tedd ji, mel ni gàttub sarax bu sikkul te wàññikuwul.
20 Chosen before the world's foundation, revealed in these last times for your sake. Yàlla xamoon na ko, ba àddina sosoogul, waaye léegi ci mujug jamono feeñal na ko ndax yéen
21 Through him you believe in our Father, who raised him from the dead and glorified him, so your faith and hope are in our Father. ñi jaar ci moom gëm Yàlla. Te Yàlla dekkal na ko, sol ko ndam, ngir ngeen wékk seen ngëm ak seen yaakaar ci Yàlla.
22 Having purified your souls by obeying the truth for sincere love of the brothers, love each other deeply from a pure heart. Kon nag gannaaw déggal ngeen dëgg gi, ba sellal seeni xol te am mbëggeel gu dëggu, bëgganteleen mbëggeel gu tar ak seen xol bépp.
23 For you have been born again—not of perishable seed but imperishable—through the living, enduring word of our Father. Ndaxte du ci jiwu wuy yàqu ngeen judduwaate, waaye ci jiwu wu sax, maanaam kàddug Yàlla giy dund tey sax.
24 For, "All people are like grass, and all their glory like the flowers of the field; the grass withers and the flowers fall, Ndaxte: «Nit ñax la, ndamam di tóor-tóor kese; ñax day wow, tóor-tóor ruus, waaye kàddug Boroom bi day sax ba fàww.»
25 but the word of our Father endures forever." And this is the word that was preached to you. Te kàddu googu mooy xibaaru jàmm, bi ñu leen doon yégal.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]