Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

1 Peter 2 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 So put away all malice and all deceit and hypocrisy and envy and all slander. Kon nag dëdduleen gépp coxor, gépp njublaŋ, naaféq, kiñaan ak jëw.
2-3 Like newborn babies, crave pure milk of the word, so you grow into salvation, Gannaaw ay liir ngeen yuy doora juddu te mos ci mbaaxug Boroom bi, nàmpleen ci meew mu sell, miy dundal seen xol, ba màgg ci biir muccu Yàlla.
3 now that you have tasted that the Lord is good. Not in this edition
4 As you come to him, the living stone rejected by people but chosen, precious to our Father. Kon nag ñëwleen ci moom; nit ñi bañ nañu ko, waaye Yàlla fal na ko te teral ko. Mi ngi mel ni doju tabax, waaye doj wuy dund la,
5 You too are being built, like living stones, into a spiritual house and a holy priesthood, offering spiritual sacrifices our Father accepts through Jesus Christ. te yéena ngi mel niy doj yuy dund yu Yàllay defare dëkkukaayam. Noonu ay sarxalkat yu sell ngeen, ngir jébbal ko ay sarax yu ngeen tibbe ci seen xol te neex ko ndax Yeesu Kirist.
6 Scripture says: "See, I set in Zion a chosen, precious cornerstone; whoever believes in him will never be put to shame." Looloo tax bind nañu: «Maa ngi samp fi ci Siyoŋ doju koñ. Doj wu tedd la, wu ma tànn; ku gëm ci moom, sa yaakaar du tas mukk.»
7 This honor, then, is for you who believe. For those who don't, the stone the builders rejected has become the cornerstone, Kon nag yéen ñi gëm am ngeen cér ci teraangaam. Waaye naka ñi gëmul: «Doj wa tabaxkat ya sànni, mujj na di doju koñ.»
8 and a stumbling stone, a rock that trips them. They trip because they disobey the word—exactly what they were appointed for. Te it: «Doj la wuy fél nit, di xeer wu koy fakktal.» Dañu cee fakktalu, ndaxte gëmuñu kàddug Yàlla, te loolu la Yàlla dogal ci ñoom.
9 But you are a chosen people, a royal priesthood, a holy nation, a people belonging to our Father, to proclaim the praises of the one who called you from darkness into his amazing light. Waaye yéen xeet wu Yàlla tànn ngeen, di askanu sarxalkati Buur Yàlla, askan wu sell ngeen, di mbooloom Yàlla, ngir ngeen yégle ngëneelam, moom mi leen woo, ba génne leen lëndëm gi, tàbbal leen ci leeram gu yéeme gi.
10 Once you were not a people, now you are our Father's people; once you had not received mercy, now you have received mercy. Démb nekkuleen woon ci dara, waaye tey mbooloom Yàlla ngeen; booba jotuleen woon yërmandeem, waaye léegi jot ngeen ko.
11 Dear friends, I urge you—foreigners and exiles—to avoid fleshly desires that war against your soul. Samay xarit, yéen ñiy ay gan ak i doxandéem ci àddina si, maa ngi leen di dénk lii: dëdduleen bànneexi bakkan yiy xeex ak xol.
12 Live good lives among the nations, so that when they slander you as wrongdoers, they may see your good deeds and glorify our Father on the day he visits us. Na seen dundin rafet ci biir xeeti àddina, kon doonte ñu di leen sosal ay ñaawteef, dinañu gis seeni jëf yu rafet bay màggal Yàlla, bés bu leen feeñoo.
13 Submit to every human authority for the Lord's sake—whether the emperor, as supreme, Na seen nangub Boroom bi tax, ngeen déggal képp kuy kilifa, muy buur ba gëna kawe,
14 or to governors, sent by the emperor to punish wrongdoers and praise those who do good. mbaa jawriñ yu mu yebal, ngir ñu yar ñiy def lu bon, te teral ñiy def lu baax.
15 For this is our Father's will: that by doing good you silence the ignorant talk of foolish people. Ndaxte noonu la coobarey Yàlla tëdde, maanaam ngeen sax ci def lu baax, ba wedamloo jayil yi xamul dara.
16 Live as free people—not using freedom to cover evil—but as servants of our Father. Li leen Yàlla goreel nag, bu mu tax ngeen mbubboo ko, bay def lu bon, waaye ngeen gëna feddali seen jaamu Yàlla.
17 Respect everyone, love the family of believers, fear our Father, honor the emperor. Teral-leen ñépp, bëgg kureelu bokk yi, ngeen ragal Yàlla te teral buur bi.
18 Servants, submit to your masters with full respect—not only the good and gentle, but also the harsh. Yéen jaam yi, déggal-leen seeni sang ak wegeel gu mat sëkk, waxuma ñi baax te lewet rekk, waaye sax ñu wex ñi.
19 For it is commendable if someone bears up under the pain of unjust suffering, mindful of our Father. Ndaxte su ngeen dékkoo tiis, di sonn ci lu dul yoon ndax seen ànd ak Yàlla, loolu lu rafet la.
20 What credit is it to endure a beating for doing wrong? But enduring suffering for doing good—this is commendable before our Father. Su ngeen tooñee te muñ i pes, luy pey gi? Waaye su ñu leen fitnaalee ci def lu baax te ngeen muñ ko, jëf ju rafet la fa kanam Yàlla.
21 You were called to this, since Christ suffered for you too, leaving an example for you to follow in his steps. Ndaxte ci loolu la leen Yàlla woo, ndaxte Kirist itam sonn na ngir yéen, teg fi seen kanam royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam.
22 "He committed no sin, and no deceit was found in his mouth." «Masula def bàkkaar, te jenn waxu njublaŋ masula génn ci gémmiñam.»
23 When they hurled their insults at him, he did not retaliate; when he suffered, he made no threats, but entrusted himself to the one who judges justly. Saaga nañu ko te feyuwul, fitnaal nañu ko te tëkkuwul, waaye mu dénk boppam ki yor àtte bu dëgg bi.
24 He himself bore our sins in his body on the tree, so that we might die to sin and live for righteousness; by his wounds you have been healed. Gàddu na moom ci boppam sunuy bàkkaar ca bant, ba ñu ko daajoon, ngir nu tàggook bàkkaar, sóobu ci dund gu jub; ndax ay gaañu-gaañoom may na nu ag wér.
25 For you were straying like sheep, but now have returned to the Shepherd and Guardian of your souls. Ndaxte yéena ngi réeroon niy xar, waaye léegi délsi ngeen ci sàmm, biy aar seeni xol.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]