Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

1 Peter 3 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1-2 Likewise, wives, submit to your own husbands, so that even if some disobey the word, they may be won without a word by their wives' conduct, Yéen itam jigéen ñi, na ku nekk nangul sa jëkkër. Noonu su amee góor gu gëmul kàddug Yàlla, te gis soxnaam di dund dund gu sell, boole ci weg ko, loolu dina ko gindi ci lu àndul ak wax.
2 seeing your pure, reverent conduct. Not in this edition
3 Do not let your beauty be the outward kind—braided hair, gold jewelry, fine clothing. Bu seen taar aju ci col, maanaam ay létt, wurus mbaa yére yu rafet,
4 But let it be the hidden person of the heart, the undying beauty of a gentle, quiet spirit, precious in our Father's sight. waaye nay taar bu sax bu nekk ci biir, di xol bu nooy te dal, ndax loolu lu takku la fa Yàlla.
5 For this is how the holy women of old who hoped in our Father adorned themselves, submitting to their own husbands, Ndaxte jigéeni démb yu sell, ya gëmoon Yàlla, loolu moo doon seen taar; nanguloon nañu seen jëkkër,
6 as Sarah obeyed Abraham, calling him lord. And you have become her children if you do good, fearing no terror. ni Saarata déggale woon Ibraayma, ba daan ko wooye «Sang bi». Yéen nag, su ngeen dee def lu baax te bañ cee boole genn njàqare, kon mel na ni Saarataa leen jaboote.
7 Husbands, similarly, live with your wives with understanding, honoring each as the weaker vessel and as coheirs of the grace of life, so your prayers aren't hindered. Te yéen itam góor ñi, na ku nekk ci yéen am xel, ci ni ngay ànde ak sa soxna, xam ne àndandoo ju la gëna néew doole la. Joxleen ko teraanga ju mat, ndax yéena yem cér ci yiwu Yàlla, wi nu ubbil buntu dund gu dul jeex. Noonu dara du mana yàq seeni ñaan.
8 Finally, all of you, be of one mind, sympathetic, loving one another as family, tenderhearted, and humble. Kon nag bokkleen xalaat, bokkleen i tiis, bëgganteleen, yërëmante te woyof.
9 Do not repay evil for evil or insult for insult, but bless instead—you were called to this, so you may inherit blessing. Ku la def lu bon mbaa mu saaga la, bul feyu, waaye ñaanal ko lu baax; ndaxte ci loolu la leen Yàlla woo, ngir barkeel leen.
10 For, "Whoever desires to love life and to see good days, let him keep his tongue from evil and his lips from speaking deceit. Ndaxte: «Ku bëgga am dund gu naat te fekke bés yu rafet, na jàpp làmmiñam ci lu bon, sàmm gémmiñam ci fen.
11 Let him turn away from evil and do good; let him seek peace and pursue it. Na dëddu lu bon, tey def lu baax, na xënte jàmm te sax ci.
12 For the eyes of our Lord are on the righteous, and his ears are open to their prayer, but the face of our Lord is against those who do evil." Ndax Boroom baa ngi xool ñi jub bëti yërmande, di dékk noppam seeni ñaan, waaye day dàq ñiy def lu bon.»
13 Now who is there to harm you if you are eager to do what is good? Te it kan moo leen di sonal, su ngeen góor-góorloo ci def lu baax?
14 But if you suffer for righteousness, you are blessed. Don't fear their fear, don't be shaken. Doonte ñu di leen fitnaal sax ci def lu jub, ñu barkeel ngeen. Buleen tiit nag ndax seeni xëbal, mbaa ngeen di ci am njàqare.
15 Set Christ apart as Lord in your hearts. Always be ready to answer anyone who asks the reason for your hope, but with gentleness and respect. Waaye màggal-leen Kirist Boroom bi ci seeni xol, te jekk ngir tontu ku lay laaj ci seen yaakaar ji ngeen am;
16 Keep a clear conscience, so that when you're slandered, those who insult your good conduct in Christ are shamed. waaye na tont li lewet te ànd ak wegeel. Àndleen ak xel mu dal; noonu ñi leen di sikkal ndax seen dund gu rafet ci gëm Kirist, dinañu rus ci seeni sos.
17 Better to suffer for doing good, if that's our Father's will, than for doing evil. Ñu fitnaal la ndax jëf ju baax, su dee mooy coobarey Yàlla, moo gën ñu fitnaal la ndax jëf ju bon.
18 For Christ too suffered once for sins, the righteous for the unrighteous, to bring us to our Father—put to death in flesh, made alive in spirit, Ndaxte Kirist ci boppam dee na benn yoon ba fàww, ngir dindi bàkkaar yi, moom mi jub ngir ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla; dee na ci jëmm, waaye dundaat na ci xel.
19 in which he also went and proclaimed to the spirits in prison, Ci biir xel moomu la yégleji ndamam ca ruu ya Yàlla tëj kaso;
20 who disobeyed long ago, when our Father waited patiently in Noah's days as the ark was being built, in which a few—eight people—were brought safely through the water. maanaam ña weddi woon ca jamonoy Nóoyin, fekk Yàlla muñaloon na leen diir bu yàgg, dajeek Nóoyin doon yett gaal ga. Ñu néew, maanaam limub juróom ñett, dugg nañu ca gaal ga, jaar ca ndox ma, ba mucc.
21 This corresponding baptism now saves you too—not removing body dirt, but appealing to our Father for a good conscience—through Jesus Christ's resurrection, Loolu misaal la tey, ci li ñu nuy sóob ci ndox, te nu mucc; waxuma laabal sobe si taq ci yaram, waaye wuyu Yàlla ak xel mu dal. Li nu may mucc googu, mooy ndekkitel Yeesu Kirist,
22 who entered heaven and is at our Father's right hand, with angels, authorities, and powers subject to him. mi yéeg asamaan, toog fa ndijooru Yàlla, mu tiim malaaka yi ak boroom sañ-sañ yi ak boroom doole yépp.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]