Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

1 Peter 4 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 So, since Christ suffered in the flesh, arm yourselves too with the same mindset: whoever suffers in the flesh is done with sin. Gannaaw Kirist nag sonn na ci yaramam, gànnaayooleen xelam moomu, ndaxte ku sonn ci yaramam, tàggoo na ak bàkkaar.
2 So you no longer spend your remaining time in the flesh for human cravings, but for the will of our Father. Noonu diir bi ko dese ci kaw suuf, dëddu na bànneexi bakkan, jublu ci coobarey Yàlla.
3 You've already spent enough time doing what those who don't know the Father want: living in sensuality, lust, drunkenness, wild parties, drinking bouts, and lawless idol worship. Ndaxte àndoon ngeen démb ci xalaati ñi xamul Yàlla, di dund ciy ñaawteef ak topp seen bakkan, di màndi ak a xawaare, di xér ci biiñ ak a jaamu ay xërëm yu araam, waaye na fi yem nag.
4 They're surprised you no longer run with them into the same flood of wild living, so they insult you for it. Ñiy jëfe noonu waaru nañu, ba di leen sosal, ci li ngeen àndul ak ñoom, sóobu ci seeni moy yu dul jeex,
5 But they will answer to the one ready to judge the living and the dead. waaye dinañu masa teew fa kanam ki nara àtte ñiy dund ak ñi dee.
6 This is why the gospel was preached even to those now dead: judged in the flesh as all people are, but they may live in the spirit as our Father does. Looloo waral it ñi dee sax, ñu jottali leen xibaaru jàmm bi, ngir ñu dunde Yàlla ci seen xel, doonte sax nit ñaa ngi leen daan fitnaal ci àddina.
7 The end of all things is near. Therefore be clear-minded and self-controlled so that you can pray. Te itam muju lépp jegesi na; nangeen maandu te foog, ba mana ñaan ci Yàlla.
8 Above all, keep loving one another deeply, because love covers a multitude of sins. Li gëna am solo mooy, ngeen bëggante mbëggeel gu tar, ndax mbëggeel day suul bàkkaar yu bare.
9 Show hospitality to one another without grumbling. Ganalanteleen ci lu àndul ak njàmbat.
10 Each of you, use whatever gift you've received to serve others, as good stewards of our Father's varied grace. Te lu la Yàlla jagleel kenn ku nekk ci yéen, nanga ko bokk ak ñépp ni jawriñ ju jub, ci séddale yiwu Yàlla wu yaatu.
11 Whoever speaks should speak as one delivering the very words of our Father. Whoever serves should serve by the strength he supplies, so that in everything he may be glorified through Jesus Christ. To him belong the glory and the power forever and ever. Amen. Kuy jottali kàddug Yàlla, na mel ni Yàllaay wax. Kuy jëf it, na jëfe dooley Yàlla, ngir turu Yàlla màgg ci lépp jaar ci Yeesu Kirist, mi yelloo ndam ak kàttan ba fàww. Amiin.
12 Dear friends, don't be surprised at the fiery trial testing you, as if something strange were happening to you. Yéen samay xarit, ci mbirum nattu bu tànge ni daay, bi dal ci seen kaw, bumu leen jaaxal, ba ngeen teg ko ni lu xel dajul.
13 Instead, rejoice as much as you share Christ's suffering, so you may also rejoice with joy when his glory is revealed. Waaye bégleen ci cér, boobu ngeen am ci coonoy Kirist, ngir bés bu ndamam di feeñ, ngeen bég ak mbég mu ëpp xel.
14 If insulted for Christ's name, you're blessed, for the Spirit of glory and of our Father rests on you. Su ñu leen jànnee sax ci turu Kirist, xamleen ne ñu barkeel ngeen, ndax Xelum Yàllaa ngi ci yéen, di firndeel seen ndamu ëllëg.
15 None of you should suffer as a murderer, thief, criminal, or meddler in others' affairs. Buñu sonal kenn ci yéen ci li mu rey nit walla mu sàcc, mbaa def lu bon, walla dugg ci lu yoonam nekkul.
16 But if you suffer as a Christian, don't be ashamed, but praise our Father that you bear that name. Waaye ku ñu sonal ndax waayu Kirist nga, bu ci rus, waaye nga màggal Yàlla ci tur woowu.
17 For it is time for judgment to begin with the household of our Father; if it starts with us, what awaits those who disobey the good news of our Father? Ndaxte àpp bi jot na, àtte baa ngi tàmbalee ci nun waa kër Yàlla. Su tàmbalee ci nun nag, luy muju ñi weddi xibaaru Yàlla?
18 And, "If the righteous are barely saved, what will become of the ungodly and sinner?" Te: «Su muccu ki jub jafee, luy doon muju ki weddi te dëng?»
19 So then, those who suffer by our Father's will should entrust their souls to their faithful Creator, doing good. Kon nag ñi tegoo fitna ci coobarey Yàlla, nañu sax ci def lu baax, dénk seen bopp Yàlla, miy Bindkat biy sàmm kóllëre.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]