Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

1 Peter 5 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 I urge the elders among you, as fellow elder, witness of Christ's sufferings, and sharer in the glory about to be revealed: Kon yéen njiit yi, maa ngi leen di dénk, man miy njiit ni yéen, man mi seede coonoy Kirist te am cér ci ndam li nara feeñ.
2 Shepherd our Father's flock among you, watching over it—not forced but willing, as our Father wants; not for shameful profit but eager, Lii laa leen di ñaan: sàmmleen géttug Yàlla, gi mu leen dénk, di ko wottu, waxuma ci sañul-bañ, waaye di surgay Yàlla ci xol bu tàlli; ngeen def ko ak xol bu laab te bañ cee séentu alal.
3 not lording it over those entrusted to you, but being examples to the flock. Buleen not ñi leen Yàlla dénk, waaye ngeen nekk ay royukaay fi kanam jur gi.
4 And when the Chief Shepherd appears, you will receive the unfading crown of glory. Noonu waxtu wu Boroom gétt gi feeñee, dina leen jagleel kaalag ndam guy sax ba fàww.
5 Likewise, younger ones, submit to elders. All of you, dress yourselves in humility toward each other, for our Father opposes the proud but gives grace to the humble. Noonu itam yéen ndaw ñi, nangeen déggal mag ñi. Te yéen ñépp, solooleen woyof ci seen biir, ndaxte: «Yàlla day dàq ñi réy, di yiwal ñi woyof.»
6 So humble yourselves under our Father's mighty hand, that he may lift you up in the right time, Suufeel-leen seen bopp kon ci ron loxob Yàlla bu am kàttan, ngir mu yékkati leen ci jamono ju ko soob.
7 casting all your anxiety on our Father, because he cares for you. Te ngeen yenniku ci kawam seen njàqare jépp, ndax ku leen ñeewante la.
8 Stay sober and watchful; your adversary the devil roams like a roaring lion, hunting someone to devour. Maanduleen te foog, ndax seen noon Seytaane mu ngi wër, ni gaynde guy yëmmu, di rëbb ku mu yàpp.
9 Resist him, standing firm in faith, knowing your fellow believers worldwide endure the same suffering. Jànkoonteleen ak moom ci biir ngëm gu takku, xam ne kureelu bokk yi ci àddina yépp, ñu ngi daj ay fitna ni yéen.
10 And our Father of all grace, who called you to his eternal glory in Christ, will himself restore, support, strengthen, and ground you after brief suffering. Te Yàlla mi jagoo yiw wépp te woo leen ci darajay Kirist, ngir ngeen bokk ci ndamam li sax, gannaaw bi ngeen yendoo bëccëgu tiis, dina leen yeesalaat, di leen dëgëral ak a dooleel, ba ngeen sampu.
11 To him be the dominion forever. Amen. Yal na Yàlla yelloo màgg ba fàww. Amiin.
12 Through Silvanus, a faithful brother as I see him, I've written briefly—encouraging you and testifying that this is the true grace of our Father. Stand firm in it. Bind naa leen ci lu gàtt ci ndimbalu Silwan, mi ma jàpp ni sama mbokk mu takku. Dénk naa leen, di leen seedeel ne lii mooy yiwu Yàlla dëgg; kon nag saxleen ci.
13 She who is in Babylon, chosen together with you, sends you greetings, and so does Mark, my son. Mbooloo mi nekk ci dëkk bi ñuy wax Babilon te Yàlla tànn ko ni yéen, moo di leen nuyu, ñoom ak Màrk sama doomu diine.
14 Greet one another with a kiss of love. Peace to all of you who are in Christ. Nuyoonteleen ak saafoonte yu sell. Yal na jàmm ñeel képp ku gëm Kirist.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]