Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

2 Peter 1 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Simon Peter, servant and apostle of Jesus Christ, to those given a faith as precious as ours through the righteousness of our God and Savior Jesus Christ: Man Simoŋ Piyeer, jaamu Yeesu Kirist ak ndawam, maa leen di bind, yéen ñi Yàlla jagleel ngëm gu rafet ni nun, aju ci njubu sunu Yàlla ak Musalkat, Yeesu Kirist.
2 May grace and peace be multiplied to you through knowing our Father and Jesus our Lord. Na leen Yàlla dollil yiw ak jàmm, jaar ci xam ko ak Yeesu sunu Boroom.
3 His divine power gave us all we need for life and devotion to God, through knowing him who called us by his glory and excellence. Dooley Yàlla moo nu may lépp lu aju ci dund gu sax ak ragal Yàlla, jaarale ko ci xam gi nu ko xam, moom mi nu woo ci kaw ndamam ak dooleem.
4 Through these he gave us his precious and very great promises, so that through them you may share the divine nature, having escaped the world's corruption from evil desires. Noonu la nu dige ay dige yu rafet te réy ba ëpp xel, ngir nu gëm leen, te Yàlla sol nu jikkoom, nu mucc ci yàqute, gi bànneexu bakkan samp ci àddina si.
5 So, making every effort, add goodness to your faith, and to goodness, knowledge; Na loolu tax ngeen góor-góorlu, ba yokk ci seen ngëm njàmbaar, ci njàmbaar googu ngeen yokk ci xam-xam, yokk ci not sa bopp.
6 to knowledge, self-control; to self-control, endurance; to endurance, devotion to God, Not sa bopp googu, ngeen yokk ci muñ, yokk ci ragal Yàlla,
7 to devotion to God, brotherly affection; to brotherly affection, love. yokk ci sopp mbokk, yokk ci bëgg ñépp.
8 If you have these qualities, growing, they'll keep you from being useless or fruitless in knowing our Lord Jesus Christ. Ndaxte bu leen jikko yooyu soloo, ba sax ci yéen, dina tax seen xam Yeesu Kirist Boroom bi am njariñ te jur mbaax.
9 Whoever lacks these things is blind, shortsighted, forgetting he was cleansed from his past sins. Waaye ku ñàkk jikko yooyu, ay bëtam dañoo lëndëm ba gumba, te fàtte na, ni ko Yàlla fóotale bàkkaari démb.
10 So, brothers and sisters, strive to confirm your calling and election; do these things and you will never stumble. Kon nag samay bokk, gannaaw Yàlla da leena tànn te woo leen, góor-góorluleen ci feddali ko ak seen kem kàttan. Ndaxte su ngeen ko defee, dungeen jeng mukk.
11 This way you'll be richly given entrance into the eternal kingdom of our Lord and Savior Jesus Christ. Te noonu dingeen tàbbi ak ndam ci nguur gu sax gu sunu Boroom, di sunu Musalkat Yeesu Kirist.
12 So I will always remind you of these things, though you know them and stand firm in the truth you now hold. Wóor na ma ne xam ngeen loolu, ba sampu ci dëgg gi leen Yàlla jagleel, waaye fas naa yéene, may sax ci di leen ko fàttali.
13 I think it right to keep stirring you with reminders while I remain in this tent, Te jàpp naa ko, muy sama warugar, feek maa ngi noyyi, ma di leen fàttali loolu, ba yee leen.
14 since I know I'll soon set my tent aside, as our Lord Jesus Christ showed me. Ndaxte xam naa ne léegi ma jóge fi, ni ma ko Yeesu Kirist Boroom bi leerale woon.
15 I will also strive so you can always recall these things after I depart. Te dinaa góor-góorlu, ngir sama gannaaw ngeen di fàttaliku li ma leen doon wax.
16 For we didn't follow ingenious myths to tell you of our Lord Jesus Christ's power and coming—we were eyewitnesses of his majesty. Bi nu leen yégalee dooley Yeesu Kirist sunu Boroom ak ñëwam ci biir ndam, sukkandikuwunu woon ciy léeb yu sësul fenn, waaye danoo teewe ag màggam.
17 He received honor and glory from our Father when a voice came to him from the Majestic Glory: "This is my Son, the one I love; I delight in him." Ndaxte Yàlla Baay bi sol na ko teraanga ak ndam, te baatub Aji Màgg ju tedd ji jib na ne: «Sama Doom a ngii, di sama Soppe; ci moom laa ame bànneex.»
18 We ourselves heard this voice come from heaven, for we were with him on the holy mountain. Te nun dégg nanu baat boobu jóge asamaan, bi nu nekkee ak moom ca tund wu tedd wa.
19 We also have the prophetic word made more certain—you do well to attend to it, like a lamp shining in a dark place, until day dawns and the morning star rises in your hearts. Noonu bir na ne waxu yonent yi wér na, te war ngeen koo fonk; mi ngi mel ni làmp buy leer ci bérab bu lëndëm, ba kera fajar di xar, te biddiiwu njël bi feq, leeral seeni xol.
20 Above all, you must understand that no prophecy of Scripture comes from one's own interpretation. Waaye jëkkleena xam ne amul jenn waxu yonent ci Mbind mi, ju balle ci xelu boppam.
21 No prophecy ever came by human will, but men spoke from our Father, carried along by the Holy Spirit. Ndaxte kenn ci yonent yi masula wax ci coobarey boppam, waaye Xel mu Sell mi daa na xiir nit ñi, ñu yégle kàddug Yàlla.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]