Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

James 1 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 James, a servant of our Father and the Lord Jesus Christ, to the twelve tribes scattered among the nations: greetings. Man Saag, jaamu Yàlla ak Boroom bi Yeesu Kirist, maa leen di nuyu, yéen fukki giir ak ñaar, yi tasaaroo ci biir àddina si.
2 Consider it pure joy, my brothers and sisters, whenever you face trials of many kinds, Yéen samay bokk, waxtu wu nattu yi dalee ci seen kaw, ak nu ñu mana mel, defleen ko ni mbég mu réy,
3 because you know that the testing of your faith produces perseverance. xam ne nattub ngëm mooy ndeyu muñ.
4 Let perseverance finish its work so that you may be mature and complete, lacking nothing. Kon na seen muñ dem ba mat, ngir ngeen baña fell fenn, waaye ngeen mat sëkk.
5 If any of you lacks wisdom, ask our Father, who gives freely to all without criticizing, and it will be given you. Ku xelam des ci benn fànn ci yéen nag, na ko ñaan Yàlla, te dina ko ko may, ndaxte Yàlla mooy Aji Yéwén, jiy may ñépp ci lu àndul ak genn ŋàññ.
6 Ask in faith, without doubting, for the doubter is like a sea wave, driven and tossed by the wind. Waaye na ko ñaan ci ngëm te bañ cee werante; ndaxte kiy werante mi ngi mel ni ndoxum géej, mi ngelaw liy lëmbaaje wet gu ne.
7 That person should not expect to receive anything from our Father. Bu kooku yaakaar dara ci Boroom bi.
8 Such a person is double-minded and unstable in all their ways. Ku am xel ñaar la, te ñàkk pastéef ci lépp lu mu mana def.
9 Let the believer in humble circumstances take pride in their high position, Naka mbokk mi néew doole, na sant ci teraangaam fa kanam Yàlla;
10 but let the rich boast in their low state, since they'll pass like a wildflower. te boroom alal it sant cig suufeem, ndax ni tóor-tóor di ruuse, noonu lay wéye.
11 The sun rises with scorching heat and withers the grass. Its flower falls; its beauty vanishes. So the rich fade away amid their pursuits. Su jant fenkee, ba naaj wi tàng, kon gàncax lax, tóor-tóor ruus, te rafetaayam naaw. Noonu la boroom alal di nasaxe, moom ak i jëfam.
12 Blessed is the one who endures trial, because once tested they'll receive the crown of life our Father promised to those who love him. Ku dékku nattu, ku barkeel nga, ndax boo ci génnee ak ndam, dees na la jagleel kaalag dund, gi Yàlla dig ñi ko bëgg.
13 When tempted, no one should say, "Our Father is tempting me." Evil can't tempt our Father, and he tempts no one. Bu la fiir galanee, bul ne: «Yàllaa ko dogal,» ndaxte Yàlla jegewul ak mbon fenn te du fiir kenn.
14 But each person is tempted, dragged away and lured by their own evil desire. Waaye ku sa bakkan nax, ba man la, looloo lay dugal ci fiir.
15 Then desire conceives and gives birth to sin; sin, full-grown, gives birth to death. Kon bu bëgg-bëgg ëmbee, bàkkaar lay wasin, te bu bàkkaar màggee, jur dee.
16 Don't be deceived, my dear brothers and sisters. Yéen sama bokk yi ma bëgg, buleen juum ci lii:
17 Every good and perfect gift is from above, coming down from the Father of lights, who never changes or casts a shifting shadow. gépp may gu baax ak gépp jagle gu mat, ci Yàlla la jóge, di Baay bi sàkk leeri asamaan, fekk moom du soppiku, mbaa muy leer ak di lëndëm.
18 By his choice, he gave us birth through the word of truth, so we'd be a kind of firstfruits of his creation. Ci coobareem la nu sole kàddug dëgg gi, ba nu judduwaat, di tànneefu lépp lu mu bind.
19 Know this, my dear brothers and sisters: everyone should be quick to listen, slow to speak, slow to anger, Yéen sama bokk yi ma bëgg, nangeen xam lii: ku nekk war ngaa farlu ci déglu, di yéexa wax tey yéexa mer.
20 because human anger does not produce the righteousness of our Father. Ndaxte meru nit du jur njub gi neex Yàlla.
21 So strip off all moral filth and excess evil; humbly receive the word planted in you, able to save your souls. Moo tax nanguleen ci woyof kàddu, gi leen Yàlla sol te man leena musal, di dëddu bépp sobe ak coxor gi daj àddina.
22 Do not merely listen to the word, and so deceive yourselves. Do what it says. Buleen yem ci déglu kàddu gi rekk, di nax seen bopp; waaye jëfeleen ko.
23 Anyone who hears the word but doesn't act on it is like one who looks at his natural face in a mirror, Ndaxte ku déglu kàddu gi te bañ koo jëfe, moom ak kuy seetu ñoo yem:
24 and, after looking at himself, goes away and immediately forgets what he looks like. day gis xar kanamam, te su nee wërëñ, daldi fàtte meloom.
25 But whoever peers into the perfect law of freedom, continuing in it—not a forgetful hearer but a doer who acts—will be blessed in his doing. Waaye kuy gëstu yoonu Yàlla, wi mat tey goreel --waxuma ki dégg, ba noppi fàtte, waaye kiy jëfe ndigal-- kooku barkeel na ci kaw jëfam.
26 If anyone thinks himself religious but doesn't control his tongue, he deceives his own heart—his religion is worthless. Ku yaakaar ne am na diine, waaye moomul làmmiñam, xanaa di nax boppam rekk, diineem jooju du diiney dara.
27 Pure and spotless religion before our Father is this: caring for orphans and widows in their distress, and keeping oneself unstained from the world. Ku diineem sell te amul benn gàkk fa kanam Yàlla mooy kii: ki nemmiku jirim yi ak jigéen, ñi seen jëkkër faatu, ci seeni tiis, tey waggar sobey àddina.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]