Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Hebrews 7 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 This Melchizedek, king of Salem, priest of the Most High, our Father, met Abraham returning from defeating the kings and blessed him. Melkisedeg moomu doon buuru Salem, moo nekkoon sarxalkat ca Yàlla Aji Kawe ji. Gannaaw ba Ibraayma dàqee buur ya, ba délsi, Melkisedeg gatandu woon na ko, di ko barkeel.
2 Abraham gave him a tenth of everything. His name means, first, king of righteousness, then also king of Salem—meaning king of peace. Noonu Ibraayma fab fukkeelu cér bi, maanaam asaka, ci li mu jële woon ci xare ba lépp, jox ko. Ci lu jëkk turu Melkisedeg mi ngi tekki «buur bu jub bi». Gannaaw loolu mooy buuru Salem, tur woowu mooy tekki «buuru jàmm».
3 Without father, without mother, without genealogy, no beginning of days or end of life, but like the Son of our Father, he remains a priest forever. Melkisedeg nag xamaluñu ko baay, xamaluñu ko yaay walla menn maam. Amul fenn fu ñu wax ag juddoom walla ag deeyam. Moo tax nu di ko méngale ak Doomu Yàlla ji, ndaxte sarxalkat la bu kenn dul wuutu.
4 Consider how great this man was: Abraham the patriarch gave him a tenth of the plunder. Seetleen ni mu màgge, moom Melkisedeg! Ibraayma sax, maamu cosaan mi, fab na li mu jële woon lépp ca xare ba, jox Melkisedeg asaka ja.
5 Those descendants of Levi who become priests are commanded by the law to collect the tenth from the people—their own brothers—though they too descend from Abraham. Yoonu Musaa digle na ne ñi bokk ci giiru Lewi te di ay sarxalkat, nañu jot asaka ci alalu bànni Israyil, doonte sax ñuy seeni bokk te soqikoo ci Ibraayma.
6 But he, though not descended from them, took a tenth from Abraham and blessed the one who held the promises. Waaye Melkisedeg mi bokkul woon ci giiru Lewi, jotoon na asaka ci alali Ibraayma. Te rax-ca-dolli barkeel na ko, moom mi Yàlla sédde woon dige yi.
7 It is beyond all dispute that the lesser is blessed by the greater. Kiy barkeel a gëna màgg ki ñuy barkeel, loolu amu ci benn werante.
8 In one case, tithes are received by mortal men; in the other, by one testified to be alive. Sarxalkat yi soqikoo ci Lewi, ñu ngi jot asaka, ni ko Melkisedeg jote woon. Waaye ñoom ñu nara dee lañu. Melkisedeg nag moom, Mbind mi wóoral na ne dafay dund.
9 One might even say Levi, who receives the tenth, paid it through Abraham, Léegi nag ci ni ñu ko mana waxe, Lewi miy jot asaka ci bànni Israyil, moom ci boppam jox na ko Melkisedeg, jaare ko ci Ibraayma.
10 for he was still in his ancestor's body when Melchizedek met Abraham. Ndaxte mi ngi nekkoon ci geñog maamam Ibraayma, bi ko Melkisedeg gatandoo.
11 If the Levitical priesthood brought perfection—the people received the law under it—why was another priest needed, one in Melchizedek's order, not called after Aaron's order? Jox nañu bànni Israyil yoon wu sukkandiku ci liggéeyu sarxalkat yi soqikoo ci Lewi. Su fekkoonte ne nag liggéeyu sarxalkat yooyu manoon na yeggale nit cig mat, kon du soxlaati ab sarxalkat ni ko Melkisedeg nekke, ci fànn gu wuute ak gu Aaróona.
12 For when the priesthood changes, the law must change as well. Te bu ñu fi jëlee sarxalkat yi ak seen liggéey, dañoo wara toxal itam yoon, wi ñu fi tëraloon.
13 For he of whom these things are said belonged to another tribe, from which no one has ever served at the altar. Noonu Yeesu mi nuy wax, mi ngi soqikoo ci geneen giir gu bokkul ak giiru Lewi. Giir googu nag, amu ci kenn ku ci masa def liggéeyu sarxale ca sarxalukaay ba.
14 Clearly our Lord descended from Judah; Moses said nothing about priests from that tribe. Li wóor moo di, sunu Boroom mi ngi soqikoo ci giiru Yuda. Te bi Musaa bindee ci mbirum sarxalkat yi, limaalewul woon giir googu.
15 And this becomes even more evident when another priest arises in the likeness of Melchizedek, Li waral mbir mi gëna leer moo di ne beneen sarxalkat bu mel ni Melkisedeg dafa ñëw.
16 who has become a priest not by a law of physical descent but by the power of an indestructible life. Te defuñu ko sarxalkat jaarale ko ci yoonu ndono, waaye fal nañu ko ci dooley dund gu amul àpp.
17 For it is testified about him, "You are a priest forever, in the order of Melchizedek." Ndaxte seedeel nañu Yeesu lii: «Doon nga sarxalkat ba fàww, mel ni Melkisedeg.»
18 On the one hand, a former commandment is set aside because of its weakness and uselessness. Noonu tebbi nañu yoon wu jëkk, wa néewoon doole te meññul dara
19 The law perfected nothing; but a better hope is introduced, through which we draw near to our Father. --ndax yoonu Musaa yeggalewul dara cig mat-- waaye dugalal nañu nu fii yaakaar ju gën ju nu mana jaare ngir jege Yàlla.
20 This was not without an oath, for the others became priests without an oath, Te rax-ca-dolli ngiñ ànd na ci. Ndaxte ñi soqikoo ci Lewi doon nañu ay sarxalkat te kenn giñul.
21 but he became a priest with an oath, by the one who said to him: "Our Father has sworn and will not change his mind, 'You are a priest forever.'" Waaye nag Yeesu moom doon na sarxalkat, bi Yàlla giñee ne ko: «Boroom bi giñ na te du dellu gannaaw mukk: “Doon nga sarxalkat ba fàww.”»
22 To that same degree, Jesus has become the guarantor of a better covenant. Ngiñ loolu moo tax Yeesu nekk tayle, giy wóoral kóllëre gi gën.
23 The former priests were many, because death prevented them from continuing in office, Te it yeneen sarxalkat yi dañoo bare woon, ndaxte dee moo daan tax duñu mana sax ci seen liggéey.
24 but he holds his priesthood permanently, because he continues forever. Waaye Yeesu miy dund ba fàww, sasoo na liggéeyu sarxale bu sax fàww.
25 So he can fully save those who come to our Father through him, since he always lives to plead their case. Loolu moo tax it mu mana musal tey yeggale cig mat ñiy jaar ci moom te bëgg jege Yàlla, ndaxte mi ngi dund ba fàww ngir di leen rammu.
26 Such a high priest suited us: holy, blameless, unstained, separated from sinners, raised above the heavens. Kon nag Yeesu mooy sarxalkat bu mag, bi nu soxla; dafa sell, du def lu bon, du taq bàkkaar, bokkul dara ak bàkkaarkat yi, te yéege nañu ko fa Yàlla.
27 Unlike those high priests, he doesn't need to offer sacrifices daily—first for his own sins, then for the people's—since he did this once for all, offering himself. Niroowul ak yeneen sarxalkat yu mag yi; soxlawul di def bés bu set ay saraxi mala ngir bàkkaari boppam jëkk, teg ca yoy mbooloo mi. Yeesu def na sarax benn yoon ba fàww ngir dindi bàkkaar yi, bi muy joxe bakkanam.
28 The law appoints weak men as high priests, but the oath's word, coming after the law, appoints the Son, made perfect forever. Naka yoonu Musaa, aji néew doole yi lay fal sarxalkat yu mag. Waaye ngiñu Yàlla gi ñëw gannaaw yoon wi, Doom ji la fal sarxalkat bu mag bu mat ba fàww.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]