Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Hebrews 8 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 The point of this: we have such a high priest, who sat down at the right hand of the throne of the Majesty in heaven. Lii mooy li ëpp solo ci li nuy wax: am nanu sarxalkat bu mag bu mel noonu, moom mi toog ci ndijooru Aji Màgg ja ca nguuram ca kaw.
2 A minister of the holy places and the true tabernacle, set up by the Father, not man. Mu ngi liggéey ca bérab bu sell baa sell, di màggalukaay bu dëggu. Nit defaru ko; Boroom bee ko sos.
3 Every high priest is appointed to offer gifts and sacrifices; so this one too must have something to offer. Bépp sarxalkat bu mag fal nañu ko, ngir muy def ay sarax ak ay saraxi mala yu jëm ca Yàlla. Kon nag fàww Yeesu am lu mu joxe.
4 If he were on earth, he wouldn't even be a priest, since others offer the gifts under the law. Bu nekkoon ci àddina, du nekk sax sarxalkat, ndaxte am na fi ba noppi ay sarxalkat yuy def ay sarax, ni ko yoonu Musaa santaanee.
5 They serve a copy and shadow of heavenly things, as Moses was warned when about to complete the tabernacle: "See," he said, "make everything according to the pattern shown you on the mountain." Sarxalkat yooyu ñu ngi liggéeyal Yàlla ca màggalukaay, ba nekk misaal tey takkandeeru yëf yu dëggu, ya féete kaw. Moo tax ba Musaa naree defar xaymab màggalukaay ba, Yàlla artu na ko ne ko: «Teeylul ba def lépp, roye ko ci bi ma la won ca tund wa.»
6 But now Jesus has obtained a superior ministry, since the covenant he mediates is better, established on better promises. Waaye léegi nag liggéeyu sarxale, bi ñu jox Yeesu, moo gëna màgg liggéeyu sarxalkat yooyu, mel ni it kóllëre, gi Yeesu fas diggante Yàlla ak nit, moo sut kóllëre gu jëkk ga te mu tëdd ci ay dige yu ëpp yu jëkk ya.
7 For if that first covenant had been faultless, there would have been no need for a second. Bu fekkoonte ne kóllëre gu jëkk ga dafa amul woon benn sikk, kon du aajo ñu koy weccee ak geneen.
8 For finding fault with them, he says: "Look, the days are coming, declares our Father, when I will make a new covenant with the house of Israel and with the house of Judah. Waaye nag Yàlla sikk na bànni Israyil, bi mu naan: Boroom bi nee na: «Ay fan a ngi ñëw yu may fasi kóllëre gu bees ak bànni Israyil ak waa Yude. Kóllëre googu nag bokkul ak gi ma fasoon ak seeni maam,
9 Not like the covenant I made with their fathers on the day I took them by the hand to lead them out of the land of Egypt. For they did not remain in my covenant, and so I disregarded them, declares our Father. ba ma leen jàppee ci loxo, génne leen réewu Misra. Boroom bi nee na: Beddeeku naa leen ndaxte sàmmuñu sama kóllëre.
10 For this is the covenant I will make with the house of Israel after those days, declares our Father I will put my laws into their minds and write them on their hearts, and I will be their Father, and they will be my children. Boroom bi nee na: Kóllëre gaa ngii, kóllëre gi may fas ak bànni Israyil, bu bés yooyule weesoo. Dinaa def samay ndigal ci seen xel, bind ko ci seen xol. Dinaa nekk seen Yàlla, ñu doon samay gaay.
11 And no longer will each one teach his neighbor and each one his brother, saying, "Know our Father," for they will all know me, from the least of them to the greatest. Kenn dootul wara jàngal moroomam walla mbokkam, di wax naan: “Xamal Boroom bi!” Ndaxte ñépp dinañu ma xam, li dale ci ki gëna ndaw ba ci ki gëna mag.
12 For I will be merciful toward their wrongdoing, and I will remember their sins no more." Ndaxte dinaa leen baal seeni tooñ, te dootuma fàttaliku seeni bàkkaar.»
13 Speaking of a new covenant, he has made the first outdated. What's outdated and aging is nearing its end. Kon nag bi Yàllay wax ci kóllëre gu bees gi, dafa fekk mu màggatal gu jëkk ga. Te lu xewwi te màggat mi ngi ci tànki wéy.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]