Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Hebrews 3 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 So, holy brothers sharing a heavenly call, consider Jesus, the apostle and high priest we confess. Kon nag yéen bokk yu sell yi, yéen ñi Yàlla woo, ngeen bokk ci nguuram gu kawe ga, seetleen ci Yeesu, moom miy ndawu Yàlla li, di sarxalkat bu mag bi ci yoon wi nu gëm.
2 He was faithful to the one who appointed him, as Moses also was in all our Father's house. Ku takku la ci liggéey bi ko Yàlla sas, ni ko Musaa nekke woon ci lépp lu jëm ci waa kër Yàlla.
3 Jesus deserves far more glory than Moses, as a house's builder deserves more honor than the house itself. Waaye Yeesu yelloo na ndam lu sut lu Musaa, ni kiy tabax kër ëppe maana kër ga muy tabax.
4 For every house is built by someone, but the builder of all things is our Father. Ndaxte kër gu nekk am na ku ko sos, waaye ki sos lépp mooy Yàlla.
5 Moses was faithful in all our Father's house, a servant testifying to what would be spoken later. Musaa moom ku takku la woon ci lépp lu jëm ci waa kër Yàlla. Waaye jawriñ rekk la woon, ngir seede li Yàlla waroona yégle.
6 But Christ, as son, is faithful over his house. And we are his house—if we hold firm the confidence and hope we boast in. Yeesu nag ku takku la it, waaye Doom la, juy yilif kër Baayam. Nun nooy këram googu, bu nu saxee ci sunu kóolute te di bég ci li nuy séentu.
7 So, as the Holy Spirit says: "Today, if you hear his voice, Moo tax Xel mu Sell mi wax lii ci Mbind mi: «Bu ngeen déggee tey jii baatu Yàlla bi,
8 do not harden your hearts as you did in the rebellion, on the day of testing in the wilderness, buleen dëgër bopp, ni seeni maam defoon ca màndiŋ ma, keroog ba ñu dëddoo Yàlla, di ko diiŋat.»
9 where your ancestors put me to the test and saw my works for forty years. Yàlla ne: «Foofa seeni maam diiŋat nañu ma fa, di ma fexee fiir, te gis nañu samay jëf
10 That is why I was angry with that generation, and I said, 'Their hearts are always going astray, and they have not known my ways.' diirub ñeent fukki at. Looloo tax ñu génnliku ma, ma daldi ne: “Seeni xalaat a leen di réeral saa su nekk, xamuñu yoon yi ma neex.”
11 So I swore in my anger, 'They will never enter my rest.'" Giñ naa kon ci sama mer ne: “Duñu dugg mukk ci sama noflaay.”»
12 Brothers, watch that none of you has an evil, unbelieving heart that deserts the living Father. Bokk yi, wottuleen ba kenn ci yéen baña am xol bu bon te gëmadi, bay dëddu Yàlla jiy dund.
13 But encourage each other daily, while it is called "today," so none of you becomes hardened by sin's deceit. Waaye bés bu nekk, deeleen soññante ci lu jëm ci Yàlla, fi ak bés boobu ñu wax wéyul, ngir ragal bàkkaar nax kenn, ba xolam tëju.
14 For we have become sharers in Christ, if we truly keep our first confidence firm to the end. Am nanu wàll ci Kirist, su nu wéyee fii ba muj ga ci sunu kóolute, gi nu amoon ca njàlbéen ga.
15 As it is said: "Today, if you hear his voice, do not harden your hearts as when you rebelled." Lii la Mbind mi wax: «Bu ngeen déggee tey jii baatu Yàlla bi, buleen dëgër bopp, ni seeni maam defoon, ba ñu dëddoo Yàlla.»
16 Who heard and rebelled? Wasn't it all who left Egypt through Moses? Ñan ñoo dégg baatu Yàlla bi nag te di ko dëddu? Xanaa ña Musaa génne woon Misra ñépp.
17 With whom was he angry forty years? Was it not with those who sinned, whose bodies fell in the wilderness? Te ñan la Yàlla mere lu mat ñeent fukki at? Xanaa ñi daan bàkkaar te seeni néew tëdd ca màndiŋ ma.
18 Who did he swear would never enter his rest, except those who disobeyed? Te it bi Yàlla defee ngiñ lii: «Duñu dugg mukk ci sama noflaay,» booba ñan ñoo ko taxoon di wax? Xanaa ña ko déggadil.
19 So we see they couldn't enter because of lack of faith. Noonu gis nanu sax ne jotuñoo dugg ci noflaay boobu ndax seen gëmadi.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]