Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Hebrews 4 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Since the promise to enter his rest still stands, let us be careful that none of you seems to have missed it. Yàlla dige na ne dina am ñu dugg ca noflaayam. Kon ndegam dige boobu mi ngi taxaw ba tey, moytuleen ba kenn ci yéen réer ba du dugg ci noflaay boobu.
2 We too had good news preached to us, as they did. But the message heard didn't benefit them, since they didn't combine it with faith, as those who listened did. Nun jot nanu xibaaru jàmm bi ni ñoom, waaye kàddu, ga ñu déggoon, jariñu leen dara, ndaxte boolewuñu ci ngëm, ba ñu koy déglu.
3 We who believed enter that rest, as he said: "In my wrath I swore, they will never enter my rest." Yet his works were finished since the foundation of the world. Nun ñi gëm nag nooy dugg ci noflaayam, ni ko Mbind mi waxe: «Giñ naa kon ci sama mer ne: “Duñu dugg mukk ci sama noflaay,”» doonte sax liggéeyam bépp matoon na, ca ba mu sàkkee àddina ak léegi. Ci lu jëm ci juróom ñaareelu fan ba,
4 For somewhere he says of the seventh day: "And our Father rested on the seventh day from all his works." am na fu ñu wax ci Mbind mi ne: «Yàlla noppalu na ci liggéeyam bépp ca juróom ñaareelu fan ba.»
5 And again in the same passage he says, "They will never enter my rest." Te it waxoon na ci baat yi nu jota lim ba noppi: «Duñu dugg mukk ci sama noflaay.»
6 Since it remains that some enter it, and those first given the good news failed to enter through their disobedience, Kon am na ñu ci wara dugg ba tey. Te ñi jëkkoona jot xibaaru jàmm bi, dugguñu ci ndax seen déggadi.
7 so again he sets a day, "Today," speaking through David much later, as already said: "Today, if you hear his voice, do not harden your hearts." Noonu ay ati at gannaaw ga, Yàlla àppaat na beneen bés, def ko «tey jii», bi mu waxee ci gémmiñu Daawuda ci baat yii ñu jota lim: «Bu ngeen déggee tey jii baatu Yàlla bi, buleen dëgër bopp.»
8 For if Joshua had given them rest, our Father would not have spoken later about another day. Su Yosuwe dugaloon sunu maam ya ca noflaayu Yàlla ba, kon gannaaw gi Yàlla du wax dara ci lu jëm ci beneen bés.
9 So then, there remains a Sabbath rest for the people of our Father. Kon ba tey Yàllaa ngi dencal ay gaayam noflaay bu nirook noflaayu Yàlla ca juróom ñaareelu fan ba.
10 Whoever has entered our Father's rest has also rested from his works, as our Father did from his own. Ndaxte képp ku masa dugg ca noflaayu Yàlla, noppalu na ci ay jëfam ni Yàlla.
11 So let's strive to enter that rest, so no one falls by the same pattern of disobedience. Nanu farlu boog, ngir dugg ci noflaay boobu, ba kenn baña déggadi, ba daanu ni maam ya ca màndiŋ ma.
12 For the word of our Father is alive and active, sharper than any two-edged sword, piercing to divide soul and spirit, joints and marrow, discerning the heart's thoughts and intentions. Xam nanu ne kàddug Yàlla mi ngi dund te am na doole. Moo gëna ñaw jaasiy ñaari boor. Day dagg ba fa xol ak xel digaloo, ba fa yax yi ak yuq gi di teqalikoo, te man na àtte xalaat yi ak mébéti xol.
13 No creature is hidden from his sight; all lies naked and exposed to the eyes of the one we must answer to. Te itam amul mbindeef mu mana nëbbu Yàlla, waaye lépp a ubbiku, ba ne fàŋŋ ci bëti ki nu wara àtte.
14 So since we have a great high priest who has passed through the heavens—Jesus, Son of our Father—let's hold firmly to the faith we profess. Gannaaw am nanu sarxalkat bu maga mag bu àgg ba ca kanam Yàlla, di Yeesu Doomu Yàlla ji, nanu jàpp bu dëgër yoon wi nu gëm.
15 We have no high priest unable to sympathize with our weaknesses, but one tested in every way as we are, yet without sin. Sarxalkat bu mag bi nu am, du ku manula bokk ak nun sunuy naqar; moom sax far jaar na ci nattu ni nun ci bépp fànn, waaye deful bàkkaar.
16 Let us then approach the throne of grace boldly, so we may receive mercy and find grace to help us in time of need. Kon nag nanu am kóolute ci jege jalu Yàlla bu yiw ba, ngir jot yërmandeem ak yiwam, ngir mu wallu nu fu soxla taxawe.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]