Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Hebrews 5 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Every high priest taken from among men is appointed for men in matters relating to our Father, to offer gifts and sacrifices for sins. Sarxalkat bu mag bu nekk nag, ci biir nit ñi lañu ko jële, te fal ko muy dox seen diggante ak Yàlla. Noonu dina jébbal Yàlla ay sarax, tey rendi ay mala ngir dindi seeni bàkkaar.
2 He can deal gently with the ignorant and straying, since he himself also is subject to weakness. Te ndegam moom ci boppam nit kese la, man na muñal ñiy moy ndax seen ñàkka xam.
3 Because of this weakness, he must offer sacrifices for sins—for the people as much as for himself. Li mu ñàkk doole moo tax mu wara def ay sarax ngir mbaalug bàkkaaram, ni mu ko tàmmee defal mbooloo mi.
4 No one takes this honor for himself, but only when called by our Father, as Aaron was. Kenn manula teral sa bopp ba doon ab sarxalkat, su dul ne Yàllaa la woo, ni mu ko defe woon Aaróona.
5 So also Christ did not glorify himself to become high priest, but the one who said to him: "You are my Son; today I have fathered you." Kirist itam yékkatiwul boppam, ba doon sarxalkat bu mag, waaye Yàlla moo ko woo, bi muy wax ne: «Yaa di sama Doom, maa di sa Baay tey.»
6 Just as he also says elsewhere, "You are a priest forever, after the order of Melchizedek." Am na feneen fu mu wax ne: «Doon nga sarxalkat ba fàww, mel ni Melkisedeg.»
7 During his earthly life, Jesus offered prayers and pleas—with loud cries and tears—to the one able to save him from death, and was heard for his godly fear. Giiru dundam gépp ci àddina, Kirist da daan ñaan wall ci Yàlla, di ko dénku, boole ko ak i jooy ak i rongooñ. Da doon ñaan ci Yàlla, mi ko mana musal ci dee. Te ñaanam nangu na, ndax ni mu jébbale boppam Yàlla.
8 Although he was a Son, he learned obedience from what he suffered. Waaye li muy nekk nekk doom, teewul mu jàng déggal Yàlla, jaare ko ci coono bi mu daj.
9 And having been made perfect, he became the source of eternal salvation to all who obey him, Noonu la àgge cig mat, ñu def ko ki waral mucc gi dul jeex, ngir ñi ko déggal ñépp.
10 having been appointed by our Father as a high priest after the order of Melchizedek. Fekk na Yàlla tudde ko sarxalkat bu mag ni ko Melkisedeg nekke.
11 We have much to say about this, hard to explain, since your hearing has grown dull. Ci fànn googu, am na lu bare lu nu ci bëgga wax, waaye tekkil leen ko dina jafe, ndaxte dangeena naqari xel.
12 For though you should be teachers by now, you need someone to teach you the basics of our Father's word again. You've come to need milk, not solid food. Bu yàgg ngeen waroona jàngal ñeneen ñi, waaye soxla ngeen ba tey ku leen di tette ci kàddug Yàlla. Léegi nag yéena ngi tollu fi ñu leen wara nàmpale, ndaxte àttanuleen ñam wu dëgër.
13 Everyone living on milk lacks skill in the word of righteousness, since he's an infant. Képp kuy nàmp, ab xale nga ba tey. Jëfeegoo njàngle mi jëm ci wàllu njubte.
14 But solid food is for the mature, whose senses are trained by practice to distinguish good from evil. Waaye ñam wu dëgër, ñi mat a ko yelloo, maanaam ñiy jëfandikoo seen xel ngir ràññee lu baax ak lu bon.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]