Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Hebrews 2 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 So we must pay closer attention to what we've heard, or we may drift away. Moo tax kon nu wara gëna faaydaal wax yi nu dégg, ngir baña bayliku.
2 For if the word spoken through angels held firm, and every wrongdoing and disobedience got just payment, Xam nanu ne kàddug yoon, wi Yàlla yégle jaarale ko ci malaaka yi, wareef la woon, te képp ku ko masa moy, walla mu mas koo tanqamlu, jot na mbugal gi mu yelloo.
3 how will we escape if we neglect so great a salvation? First announced by the Lord, it was confirmed to us by those who heard him, Kon nun ñi dégg mucc gu mag gi, bu nu ko sàgganee, nan lanuy mana rëcce mbugalu Yàlla? Boroom bi moo xamle woon mucc googu ca njàlbéen ga, te gannaaw gi, ñi ko dégg ñoo nu ko wóoralal.
4 while our Father also testified with them through signs, wonders, various miracles, and distributions of the Holy Spirit, according to his will. Te it Yàlla dëggal na seen seede ci ay firnde ak ay kéemaan, ay jaloore yu bare ak ci ay may yu jóge ci Xelam mu Sell, te mu séddale leen ni mu ko bëgge.
5 For it was not to angels that our Father subjected the coming world we're speaking of. Yàlla jébbalul malaaka yi benn sañ-sañ bu jëm ci jamonoy ëllëg ji nuy wax; keneen la ko jébbal,
6 Someone has testified somewhere, "What is man, that you are mindful of him, or the son of man, that you care for him? ndaxte am na fu ñu wax ci Mbind mi ne: «Lan mooy nit, yaw Yàlla, ba nga di ko xalaat? Lan mooy doomu nit, ba nga koy topptoo?
7 You made him for a little while lower than the angels; you crowned him with glory and honor, Wàcce nga ko, def ko mu gëna suufe tuuti malaaka yi. Kaalaa nga ko teraanga ak ndam,
8 putting everything in subjection under his feet." Now in subjecting everything to him, our Father left nothing outside his control. At present, however, we do not yet see everything subjected to Christ. notal ko lépp, mu teg ci tànk.» Bi ko Yàlla notalee lépp nag, bàyyiwul dara. Fi mu nekk gisagunu ne lépp a ngi ci sañ-sañam;
9 But we see Jesus, made lower than the angels for a little while, now crowned with glory and honor because he suffered death, so that by our Father's grace he might taste death for everyone. Waaye gis nanu Yeesu. Wàcce nañu ko, def ko mu gëna suufe tuuti malaaka yi, ngir mu dee ci wàllu ñépp, ndaxte loolu la Yàlla dogal ci yiwam. Waaye léegi Yàlla kaalaa na ko teraanga ak ndam ndax coono bi mu daj ba dee.
10 It was fitting that our Father, for whom and through whom all things exist, should perfect the pioneer of their salvation through suffering, bringing many sons to glory. Ndaxte Yàlla mi yelloo lépp te sàkk lépp, dogal na def ñu bare ay doomam, boole leen ci ndamam. Jekk na nag mu matal Yeesu ci coono bi mu daj, moom mi leen xàllal yoonu mucc gi.
11 The one who makes holy and those made holy all come from one Father. That's why he isn't ashamed to call them brothers and sisters, Moom Yeesu miy sellal, ak ñi muy sellal, ñoom ñépp genn njaboot lañu. Moo tax Yeesu rusu leena wooye ay doomi baayam.
12 saying, "I will proclaim your name to my brothers and sisters; I will sing your praise amid the assembly." Nee na: «Yaw Yàlla, dinaa xamle sa tur ci samay doomi baay, dinaa la tagg ci biir mbooloo mi.»
13 And again, "I will trust in him." And again, "Here am I, and the children our Father gave me." Newaat na: «Dinaa am ci Yàlla kóolute.» Dellu na waxaat ne: «Maa ngi nii, man ak doom yi ma Yàlla jox.»
14 Since the children share flesh and blood, he too shared them, so that through death he might destroy the one holding the power of death—the devil, Doomam yooyu muy wax, nit kese lañu. Looloo tax Yeesu it moom ci boppam, wàcc na, jëmmoo ni ñoom, ngir dee, ba man caa daaneel Ibliis, mi yore dooley dee.
15 and free all those who, through fear of death, were enslaved their whole lives. Noonu mu yiwi nit, ñi meloon ni ay jaam seen giiru dund gépp ndax ragala dee.
16 For surely it is not angels he helps, but the descendants of Abraham. Leer na ne Yeesu xettalisiwul malaaka yi, waaye askanu Ibraayma lay xettalisi.
17 So he had to become like his brothers and sisters in every way, to be a merciful and faithful high priest serving our Father, clearing away the people's sins. Looloo taxoon mu wara mel niy doomi baayam ci bépp fànn, ngir doon seen sarxalkat bu mag fa kanam Yàlla, bi leen yërëm te di sàmm kóllëre, te ci liggéeyu sarxaleem joxe na bakkanam ngir dindi bàkkaari nit ñi, ba Yàlla baal leen.
18 Since he himself suffered when tempted, he can help those being tempted. Gannaaw sonn na ci nattu yi mu daj, man na dimbali ñiy jaar ciy nattu.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]