Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Hebrews 1 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Long ago, in many times and many ways, our Heavenly Father spoke to our ancestors through the prophets. Li jiitu tey Yàlla waxoon na ak maam ya ci wàll yu bare ak ci tëralin yu wuute jaarale ko ca yonent ya.
2 But in these final days he spoke to us by his Son, whom he appointed heir of all things and through whom he made the universe. Waaye ci mujug jamono jii nu tollu, Yàlla wax na ak nun jaarale ko ci Doom ji. Doomam jooju la Yàlla jagleel lépp, te ci moom la Yàlla jaar, sàkk àddina.
3 The Son is the brightness of our Father's glory, the exact image of his being, sustaining all things by his powerful word. After purifying sins, he sat down at the right hand of the Majesty on high. Doom ji moo di leer giy jollee ci ndamu Yàlla, di ki dippeekoo ci Yàlla. Moo téye àddina ci kàddoom gu am doole gi. Te bi mu ubbee bunt ba nit di selle ci ay bàkkaaram, dafa toog fa ñu koy terale ca ndijooru Aji Màgg ji ca kaw,
4 He became as much greater than angels as his inherited name is greater than theirs. wone noonu ne moo gëna màgg malaaka yi. Te it Yàlla jox na ko tur wu sut seen tur.
5 For to which of the angels did our Father ever say, "You are my Son; today I have become your Father"? Or again, "I will be his Father, and he will be my Son"? Ndaxte Yàlla masula wax kenn ci malaaka yi ne: «Yaa di sama Doom, maa di sa Baay tey.» Masul ne ci mbirum kenn ci ñoom it: «Man Yàlla, dinaa doon Baay ci moom, mu nekk Doom ci man.»
6 And again, when he brings the firstborn into the world, he says, "Let all my angels worship him. Waaye bi muy yónni Doom jooju di taaw bi ci àddina, da ne: «Na ko malaakay Yàlla yépp jaamu.»
7 Of the angels he says, "He makes his angels winds, and his servants flames of fire." Ci wàllu malaaka yi, lii la ci Yàlla wax: «Def na malaakaam yi, ñu mel ni ay ngelaw, ñooñu koy liggéeyal, mu def leen niki sawara.»
8 But about the Son he says, "Your throne, O God, is forever and ever, and the scepter of righteousness is the scepter of your kingdom. Waaye ci wàllu Doom ji, lii la ko Yàlla wax: «Yaw Yàlla, dinga toog ci jal bi ba fàww, ci njubte ngay nguuru.
9 You have loved righteousness and hated wickedness; therefore our Father, your Father, has anointed you with the oil of gladness above your companions." Sopp nga njub te bañ lu bon. Looloo tax yaw Yàlla, sa Yàlla sol la mbég mu gëna réy mi mu jagleel say àndandoo.»
10 And, "In the beginning, Lord, you laid the foundations of the earth, and the heavens are the work of your hands. Newaat na it: «Yaw Boroom bi, yaa sàkk àddina ca njàlbéen ga, defar asamaan yi ci sa loxoy bopp.
11 They will perish, but you remain; they will all wear out like a garment. Yëf yooyu dinañu wéy, waaye yaw dinga sax, dinañu màggat ñoom ñépp ni ay yére.
12 You will roll them up like a robe; like a garment they will be changed. But you are the same, and your years will never end." Dinga leen taxañ ni malaan, ñu furi ni ay yére, waaye yaw doo soppiku, te sa dund amul àpp.»
13 But to which of the angels did our Father ever say, "Sit at my right hand until I make your enemies a footstool for your feet"?" Waaye Yàlla masula teral kenn ci malaaka yi, ba di ko wax: «Toogal ci sama ndijoor, ba kera may daaneel say noon ci sa kanam.»
14 Aren't all angels ministering spirits, sent to serve those about to inherit salvation? Malaaka yépp ay xel lañu rekk yuy liggéeyal Yàlla, mu di leen yónni ñuy dimbali nit, ñi nara jot mucc gi.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]