Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Philemon 1 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Paul, a prisoner of Christ Jesus, and Timothy our brother, to Philemon, our dear friend and co-worker, Man Pool, mi ñu tëj kaso ngir Kirist Yeesu, ak sunu mbokk Timote, noo lay bind, yaw Filemon sunu soppe ak sunu nawle ci xeex bi;
2 and to our sister Apphia, our fellow soldier Archippus, and the church that meets in your house: te fàttewunu sunu jigéen Afiya, ak sunu àndandoo ci xeex bi Arkib, yéen ak mbooloom ñi gëm, miy dajee sa kër.
3 Grace and peace to you from our Father and the Lord Jesus Christ. Yal na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
4 I always thank my Father as I remember you in my prayers, Duma la noppee boole ci samay ñaan, di ci sant Yàlla sama Boroom,
5 because I hear of your love and faith in the Lord Jesus and for all his holy people. ndaxte dégg naa sa ngëm ci Boroom bi Yeesu, ak sa mbëggeel ci gaayam yu sell yépp.
6 I pray your shared faith becomes effective as you come to understand every good thing we have in Christ. Li may ñaan nag a ngi nii: nga xam bu wér ngëneel, yi nu am yépp ci sunu bokk ci Kirist, ba tax bokk gi nga am ci Yàlla ci kaw ngëm meññ i njariñ.
7 Your love has brought me great joy and comfort, brother, since you've refreshed the hearts of his holy people. Ci dëgg-dëgg sa mbëggeel bégal na ma bu baax, ba dëfal sama xol; ndaxte xam naa, sama mbokk, ni nga féexale xoli gaayi Yàlla yu sell yi.
8 Therefore, although in Christ I am bold enough to command you to do what is right, Am na lu ma la bëgga ñaan; teguma ko ci sañ-sañ bu mat bi ma Kirist may, ci teg la ndigalu def sa warugar,
9 instead, for love's sake I appeal—I, Paul, an old man, now also a prisoner of Christ Jesus. waaye dama lay ñaan ci mbëggeel gi nu séq, man Pool màggat, mi ñu tëj kaso ci turu Kirist.
10 I appeal to you for my child Onesimus, whose father I became while I was in chains. Maa ngi tinul sama doomu diine Onesim, mi ma jur ci Kirist fii ci kaso bi.
11 He was once useless to you, but now is useful to you and me. Amul woon sa njariñ démb, waaye tey amal na nu njariñ, yaw ak man.
12 I am sending him back to you—and in doing so I am sending my very heart. Maa koy yebal fi yaw, waaye xamal ne mooy sama reeni xol.
13 I wanted to keep him with me, to serve me on your behalf while I'm in chains for the gospel. Dama koo bëggoona téye fi sama wet, ngir mu taxawal la, di ma dimbali, li feek maa ngi ci kaso bi ngir xibaaru jàmm bi.
14 But I wanted to do nothing without your consent, so your good deed would not be forced, but voluntary. Waaye bëggumaa def dara loo àndul; noonu ndimbal li nga may defal du nekk sañul-bañ, waaye mu ànd ak xol bu tàlli.
15 Perhaps this is why he was separated from you briefly, so you'd have him back forever. Xëy na sax dafa tàggoo woon ak yaw diir bu gàtt, ngir nga jotaat ci ba fàww;
16 No longer as a slave, but more than a slave—a beloved brother, especially to me, but even more to you, both in the flesh and in the Lord. waxuma léegi ni jaam rekk, waaye lu ko sut, xanaa mbokk mu dëggu ci xol, fekk looloo raw ag njaam. Mbokk la ci man, rawatina ci yaw, muy sa jaam ci aada, di sa mbokk léegi ci Boroom bi.
17 So if you consider me a partner, welcome him as you would welcome me. Soo ma jàppee ni nawle nag, teeru ko, ni su ma la doon ganesi.
18 If he wronged you at all, or owes anything, put it on my account. Soo ko naree topp genn tooñ mbaa benn bor, topp ma ko.
19 I, Paul, write this with my own hand: I'll repay it—not to mention you owe me yourself as well. Man Pool maa ngi lay bind ak sama loxob bopp ne dinaa la ko fey; bëggumaa yegg ci ne sag dund sax ci man la jaar!
20 Yes, brother, do me this favor in the Lord—refresh my heart in Christ. Waaw, yaw sama mbokk, dimbali ma ci Boroom bi, te seral sama xol ci sunu bokk ci Kirist.
21 Trusting you'll obey, I write to you, knowing you'll do even more than I ask. Noonu bind naa la, ndax wóor na ma ne dinga ma déggal, ba weesu sax li ma la sant.
22 Also prepare a guest room for me—I hope through your prayers to be graciously given back to you. Te itam nanga ma waajal néeg, ndaxte yaakaar naa ne Yàlla dina nangu seeni ñaan, ba delloosi ma leen.
23 Epaphras, my fellow prisoner in Christ Jesus, sends you greetings, Sama mbokk Epafras, mi ma nekkal fi ci kaso bi ci turu Kirist, mu ngi lay nuyu.
24 and so do Mark, Aristarchus, Demas, and Luke, my fellow workers. Samay àndandoo ci liggéey bi, Màrk, Aristàrk, Demas ak Luug, ñu ngi lay nuyu.
25 The grace of the Lord Jesus Christ be with your spirit. Amen. Yal na yiwu Boroom bi Yeesu Kirist ànd ak seen xel.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]