Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

James 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 My brothers and sisters, as believers in our glorious Lord Jesus Christ, do not show favoritism. Bokk yi, bu leen di gënaatle te di gëmkati sunu Sang Yeesu Almasi bi, Boroom leer.
2 Say a man wearing a gold ring and fine clothes enters your assembly, and a poor man in shabby clothes enters too. Ndax su nit duggsee seenum ndaje, takk jaarob wurus, solu ba jekk; ku néew doole it duggsi, limboo ay sagar,
3 If you notice the well-dressed one and say, "Sit here, a good seat," but tell the poor man, "Stand over there," or "Sit on the floor by my feet," su ngeen seetloo boroom col gu jekk gi, ne ko: «Toogeel fii, moo baax ci yaw,» te ne néew-ji-doole ji: «Yaw, taxaweel nee, mbaa nga toog fii ci suuf, ci samay tànk,»
4 haven't you played favorites among yourselves and become judges guided by evil motives? su boobaa xanaa du yeena ngi gënaatle ci seen biir, tey àttee ay mébét yu bon?
5 Listen, my beloved brothers and sisters: Hasn't our Father chosen the world's poor to be rich in faith, heirs of the kingdom promised to those who love him? Bokk yi, soppe yi, dégluleen. Xanaa du Yàlla moo tànn ñi àddina jàppe ñu néew doole, ngir ñu barele ngëm, boole ci jagoo nguur gi Yàlla dig ñi ko sopp?
6 But you disrespected the poor. Don't the rich oppress you and drag you into court? Yeen nag ngeen di teddadil néew doole yi! Xanaa du boroom alal yi ñoo leen di noggatu, di leen diri ba fa mbaxana dee benn?
7 Aren't they blaspheming the honorable name called over you? Xanaa du ñooñu ñooy ñàkke kersa tur wu tedd wi ngeen di wuyoo?
8 If you truly obey the royal law according to the Scripture, "Love your neighbor as yourself," you do well. Ndegam nag yoonu Buur Yàlla ngeen matal sëkk, di sàmmonteek Mbind mi ne: «Ni ngeen soppe seen bopp, nangeen ko soppe seen moroom,» su boobaa waawleen góor!
9 But if you show favoritism, you are sinning, and the law convicts you as lawbreakers. Waaye su ngeen gënaatlee, bàkkaar ngeen, te yoon topp na leen, ndax yeena ko xëtt.
10 Whoever keeps the whole law but stumbles at one point is guilty of breaking it all. Ndax kat képp ku sàmm yoon wépp, ba mu des lenn ndigal doŋŋ lu mu tërëfe, ab daan bu ñu teg ci ku moy yoon wépp, ñeel na ko.
11 For our Father, who forbade adultery, also forbade murder. So if you avoid adultery yet commit murder, you're a lawbreaker. Ndax ki ne: «Bul njaaloo,» moo ne itam: «Bul bóom.» Ku njaaloowul te bóom nag, xëtt na yoon.
12 Speak and act as people who will be judged by the law of freedom. Deeleen waxe tey jëfe ni mu jekke ci nit ñu ñuy séddeji àtteb yoon wiy goreel.
13 Judgment is merciless to one who showed no mercy; mercy triumphs over judgment. Daan bu àndul ak yërmande, moom lees di àttee ña daawul jëfe yërmande. Yërmande nag kekku na ab daan.
14 What good is it, my brothers and sisters, if someone claims faith without works? Can that faith save him? Bokk yi, ku ne gëm na, te jëfewu ko, ana lu mu koy jariñ? Ndax googu ngëm man na koo musal?
15 Suppose a brother or sister is poorly clothed and lacking daily food, Su mbokk mu góor mbaa jigéen raflee, mbaa mu ñàkk lu mu dunde bés bu nekk,
16 and one of you tells them, "Go in peace, stay warm and fed," but gives nothing for their bodily needs—what good is that? ba kenn ci yeen ne mbokk mi: «Demal ak jàmm, solul nag te lekk ba regg,» te fajul aajoom, loolu lu muy jariñ?
17 In the same way, faith by itself, if it is not accompanied by works, is dead. Noonu la ngëm deme, su amul jëf ju mu àndal, ngëm gu dee la.
18 But someone will say, "You have faith, and I have works." Show me your faith without works, and I'll show you my faith from my works. Waaye jombul nit ne: «Yaw, ngëm nga am, waaye man, jëf laa am.» Dama ne, won ma sa ngëm gu àndul ak jëf; man, samay jëf laa lay wone sama ngëm.
19 You believe that our Father is one; you do well. Even the demons believe that—and shudder. Yaa gëm ne Yàlla kenn la; waaw góor, waaye rab yi it loolu lañu gëm bay lox.
20 Do you want me to show you, you foolish person, that faith apart from works is useless? Yaa ñàkk bopp, ndax dangaa bëgg lu la firndeel ne ngëm gu àndul ak jëf amul njariñ?
21 Was not Abraham our father justified by works when he offered his son Isaac on the altar? Sunu maam Ibraayma, xanaa du ci jëf lees ko baaxe àtteb ku jub, ndax jëf ja mu joxee doomam Isaaxa ca sarxalukaay ba?
22 You see that faith was working together with his works, and faith was completed by his works. Kon gis nga ne ngëmam ga ak jëfam ja ñoo ànd di liggéey, te ca jëf ja la ngëm ga mate sëkk.
23 This fulfilled the Scripture: "Abraham believed our Father, and it was credited to him as righteousness"—he was called our Father's friend. Mbind ma daldi sotti, na mu dikke woon ne: «Ibraayma moo gëm Yàlla, Yàlla nangul ko ngëmam, muy àtteb njub bu ñu ko limal,» ba ñu di ko woowe xaritu Yàlla.
24 You see that a person is justified by works and not by faith alone. Ngeen gis kon ne ci jëf lees di baaxe nit àtteb ku jub, waaye du ci kaw ngëm doŋŋ.
25 Likewise, wasn't Rahab the prostitute also justified by works, welcoming the messengers and sending them out a different way? Xanaa du noonu it lañu baaxe Raxab gànc ba àtteb ku jub, ci kaw jëfam, ndax la mu dalaloon ndawi Yawut ya, ba awale leen feneen?
26 As the body without the spirit is dead, so also faith without works is dead. Yaram wu àndul akug noo daal, ni mu deewe, noonu la ngëm gu àndul aki jëf deewe.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]