Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

James 3 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 My brothers and sisters, not many of you should become teachers, since we teachers face stricter judgment. Bokk yi, bu ñu bare ci yeen wuta doon jàngalekatu mbooloom gëmkat mi, ndax xam ngeen ne nun ñiy jàngale nooy gëna metti ab àtte.
2 For we all stumble in many ways. Anyone who never stumbles in speech is a mature man, able to control his whole body too. Bare na lu nuy tooñ, nun ñépp. Ku dul tooñ ci kàddu nag, kooku nit ku mat la, te man naa moom yaramam wépp, boole ci.
3 If we put bits in horses' mouths to make them obey us, we guide their whole bodies too. Aw fas, ŋalaab gi nuy def ci gémmiñam, mu déggal nu lanu ci jublu, te moom lanuy walbatee yaramu fas wi wépp.
4 Consider ships too: though large and driven by strong winds, a tiny rudder steers them wherever the pilot wants. Xoolleen gaal yi it, ak li ñuy réy lépp, ak ngelaw lu réy lu leen mana jañax, weñ su tuut la dawalkat biy walbatee gaal gi, jëme ko fu ko neex.
5 So too the tongue is a small body part, yet boasts great things. See how small a fire sets ablaze a great forest! Noonu itam la aw làmmiñ dee cér su tuut te réy aw bàkk. Seetleen ni ferñent su tuut di lakke gott bu yaa.
6 The tongue is a fire, a world of wickedness placed among our body's parts. It stains the whole body, sets the whole course of life ablaze, and is itself set ablaze by hell. Aw làmmiñ itam sawara la; làmmiñ a bokk ci sunuy cér, te di àddinay mbon, di gàkkal jëmm jépp. Aw làmmiñ, giiru dundu nit ki lay jafale ab taal bu tàkke fa sawara.
7 Every kind of beast, bird, reptile, and sea creature is tamed, and has been tamed, by humankind, Mboolem xeeti rabi àll yeek njanaaw yi ak ndëgmeent yi ak rabi géej yi, dees na leen tàggat, te nit a leen di tàggat ba ñu mokk.
8 but no human being can tame the tongue. It is a restless evil, full of deadly poison. Waaye aw làmmiñ, kenn manu koo tàggat ba mu mokk. Mooy aayteef gu kenn manula dànk, fees dell ak tookey dee.
9 With it we bless our Father; with it we curse people made in the likeness of our Father. Aw làmmiñ lanuy sante kiy Boroom bi, di Baay, te it ci lanuy móoloo nit ñi bindoo takkndeeru Yàlla.
10 From the same mouth come blessing and cursing. My brothers and sisters, this should not be. Genn gémmiñ gi, ci la kàddug cant ak gu móolu di jibe. Bokk yi, warula deme noonu kat.
11 Does a spring pour out both fresh and bitter water from the same opening? Benn bëtu ndox ndax dina ballandoo ndox mu neex ak ndox mu wex, ci menn pax mi?
12 Brothers and sisters, can a fig tree bear olives, or a vine figs? Neither can a salt spring yield fresh water. Bokk yi, ndax ag figg man naa meññ oliw? Am ag reseñ dina meññ doomi figg? Bëtu ndoxum xorom it du nàcc mukk ndox mu neex.
13 Who is wise and understanding among you? Let him show his deeds through good conduct, in wisdom's humility. Ana ci yeen ku rafet xel te xam àddina? Na ko firndeele dundin wu rafet wu feeñ ci jëfam ju teey ndax xel mu rafet.
14 But if bitter envy and selfish ambition fill your heart, don't boast or lie against the truth. Waaye ku denc ci sab xol wextanu kañaan ak mébétum sàkku sa darajay bopp, bul damoo xel mu rafet, nde kon nga moy dëgg.
15 This is not the wisdom that comes down from above, but is earthly, unspiritual, demonic. Moomu xel jógewul fa kaw, ci àddina sii la bokk, di yëfi bakkan, te di mbiri Seytaane.
16 For where there is jealousy and selfish ambition, there will be disorder and every vile practice. Ndax kañaan ak sàkku sa darajay bopp, fu mu ame, fa la salfaañoo di ame ak mboolem jëfi ñaawtéef.
17 Wisdom from above: pure first, then peace-loving, gentle, reasonable, full of mercy and good fruit, unbiased, sincere. Waaye xel mu rafet ma bawoo fa kaw, set la njëkka def, teg ci ànd ak jàmm akug dal. Day taxa neexa jubool, fees ak yërmande, di meññ jëf ju baax, te mucc ci par-parloo akug jinigal.
18 And the harvest of righteousness is sown in peace by those who make peace. Meññeefum njub nag, ci jàmm lees koy ji, ci biir doxkati jàmm yi.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]