Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

James 4 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Where do wars and fights among you come from? Isn't it your cravings warring inside you? Ana fu jote yeek xuloo yi ci seen biir jóge fu moy seen bànneexi bakkan yiy xare ci seen yaram?
2 You want and don't have—you kill. You crave and can't get it—you quarrel and fight. You don't have because you don't ask. Yeenay xemmem lu ngeen dul am. Yeenay bóome, di iñaane lu ñeneen am, te manuleen koo am. Yeenay xuloo aka jàppante. Dungeen am, ndax yeena ñaanul.
3 You ask and do not receive, because you ask wrongly, to spend it on your own pleasures. Te su ngeen ñaanee, dungeen am, ndax mébét mu bon ma ngeen ñaane, ngir am lu ngeen toppe seen bakkan.
4 You adulterous people! Don't you know friendship with the world is hostility toward our Father? Whoever chooses to be its friend becomes an enemy of our Father. Bokkaalekat yi ngeen doon! Xanaa xamuleen ne xaritoo ak àddina moo di noonoo ak Yàlla? Kon nag ku namma def àddina ab xarit, ab noonu Yàlla ngay doon.
5 Or does Scripture speak for nothing, saying the spirit he placed in us longs jealously? Am defe ngeen ne ag neen la Mbind mi indee ne: «Xemmemtéef gu ànd ak fiiraange la Yàlla am ci noo gi dëkk ci nun.»
6 But he gives more grace. That is why Scripture says, "Our Father opposes the proud but gives grace to the humble." Waaye yiw wu gënatee baawaan la maye. Moom la Mbind mi ne: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.»
7 Submit yourselves, then, to our Father. Resist the devil, and he will flee from you. Kon nag nangulleen Yàlla, te bañal Seytaane, mu daw, ba sore leen.
8 Come close to our Father, and he will come close to you. Cleanse your hands, sinners; purify your hearts, double-minded. Jegeleen Yàlla, mu jege leen. Yeen bàkkaarkat yi, raxasleen seeni loxo, yeen ŋaralekat yi laa ne, setalleen seen xol.
9 Grieve, mourn, and weep. Turn your laughter to mourning and your joy to gloom. Tiisluleen te ñaawlu bay jooy. Na seeni ree soppiku ay jooy, seen mbég doon njàqare.
10 Humble yourselves before our Father, and he will lift you up. Toroxluleen fi kanam Boroom bi, mu yékkati leen.
11 Don't speak against each other, brothers and sisters. Whoever speaks against a brother, or judges him, speaks against the law and judges it. But if you judge the law, you're not keeping it—you're judging it. Bokk yi, buleen ŋàññante. Ku ŋàññ sa mbokk mbaa nga sikkal sa mbokk, yoon wi nga ŋàññ, yoon wi nga sikkal. Ku sikkal yoon wi nag doo sàmmkatub yoon wi, sikkalkatub yoon wi nga.
12 Only one gives the law and judges—able to save or destroy. Who are you to judge your neighbor? Boroom yoon wi, kenn doŋŋ la, te mooy àtte; moo mana musle, mbaa mu sànke. Te yaw miy sikkal sa mbokkum gëmkat sax, yaay kan?
13 Come now, you who say, "Today or tomorrow we will go to this or that city, spend a year, trade, and profit." Kaayleen nag ma wax leen, yeen ñi naan: «Tey mbaa ëllëg ma dem ba dëkk sàngam, def fa at, julaa fa ba tonu.»
14 You don't know what tomorrow brings. What is your life? For you're a mist, visible briefly, then gone. Yeen xanaa xamuleen sax lu ëllëg di doon? Ana luy seen bakkan? Yeen ngeen di as lay suy feeñ léegi, nes tuut mu ne mes!
15 Instead you ought to say, "If our Father wills, we will live and do this or that." Li ngeen di wax kay moo di: «Bu soobee Boroom bi, dinanu dund ba def nàngam sii mbaa nàngam see.»
16 As it is, you boast in your arrogance. All such boasting is evil. Léegi daal dangeena bew bay damoo seeni mébét! Googu damu de, lu bon la.
17 So whoever knows the good to do and fails to do it, sin is theirs. Ku xam lu baax loo wara def te defoo ko nag, bàkkaar nga.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]