Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

James 5 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Come now, you who are rich, weep and wail over the miseries that are coming upon you. Kaayleen nag ma wax leen, yeen boroom alal yi, jooyleen te yuuxu, ndax mitit yi leen di dikkal.
2 Your riches have rotted, and your clothes have become moth-eaten. Seen alal nëb na, seeni yére maxe,
3 Your gold and silver have rusted; their rust will witness against you and burn your flesh like fire. You piled up riches in the last days. seen wurus ak seen xaalis xomaag. Xomaag ja dib seede bu leen tuumaal, di xoyom seenu suux ni sawara. Yeena dajale alal ca fan yu mujj ya.
4 Look: the wages you held back from the workers who mowed your fields cry out, and the harvesters' cries have reached the ears of the Father of heaven's armies. Dégluleen! Peyoor ga ngeen xañ ña gub seen tool, mooy yuuxu noonu. Jàmbati góobkat ya tàbbi na ca noppi Boroom gàngoori xare yi.
5 You lived on earth in luxury and indulgence. You fattened your hearts in a day of slaughter. Dund gu nooy ak bànneexu bakkan daal ngeen nekke ci kaw suuf, di yaflu ci bésub rendi.
6 You have condemned and murdered the righteous one, who does not resist you. Yeena daan ba reylu aji jub, te jéemula bañ.
7 So be patient, brothers and sisters, until the Lord's coming. Think of the farmer: he waits patiently for the land's precious fruit, until it gets the early and late rains. Kon nag bokk yi, muñleen, ba Boroom bi délsi. Seetleen ci beykat biy séentu njariñal meññeef mu jóge fi suuf si. Ma ngay muñ, céebo ba bët wàcc.
8 You too must be patient. Strengthen your hearts, because the coming of the Lord is near. Yeen itam muñleen te takk seenu fit, ndax bés ba Boroom biy dikk dëgmal na.
9 Don't grumble against each other, brothers and sisters, or you'll be judged. Look—the Judge stands at the doors. Bokk yi, buleen di ñaxtoonte, lu ko moy dees na leen daan, te daan-kat baa ngii taxaw ci bunt bi!
10 Brothers and sisters, take the prophets who spoke in the name of our Father as examples of suffering and patience. Bokk yi, yonent yi wax ci turu Boroom bi, di dékku aw tiis ak di muñ, defleen leen seeni royukaay.
11 See, we call those who endured blessed. You've heard of Job's endurance and seen what our Father brought about—our Father is rich in compassion and mercy. Xam ngeen ne ñi muñ lanu foog ne ñoom la mbég ñeel. Dégg ngeen na Ayóoba muñe woon, ak muj ga ko Boroom bi jagleel, ndax Boroom bi moo bare yërmande akug ñeewante.
12 Above all, my brothers and sisters, do not swear—neither by heaven, nor earth, nor any other oath. Let your yes be yes and your no, no, so you won't fall under judgment. Li ci raw nag bokk yi, moo di buleen giñ, bu muy ci asamaan mbaa ci suuf mbaa ci leneen lu mu mana doon. Na seen waaw di waaw, seen déet di déet, bala ngeena tàbbi ci mbugal.
13 Is anyone among you suffering? Let them pray. Is anyone cheerful? Let them sing praises. Ana ci yeen ku nekk ciw tiis? Na ñaan. Ana ku ci am mbég? Na sàbbaal.
14 Anyone sick among you? Have them call for the church elders, and have the elders pray over them, anointing them with oil in the name of the Lord. Ana ku wopp ci yeen? Na woo magi mbooloom gëmkat ñi, ñu ñaanal ko, raayaale ko ag diw ci turu Boroom bi.
15 The prayer of faith will save the sick person, and the Lord will raise him up. And if he has sinned, he will be forgiven. Ñaan gu ànd ak ngëm day musal ki wopp, ba Boroom bi yékkati ko. Su dee daa bàkkaar, dees na ko jéggal.
16 So confess your sins to each other and pray for each other, that you may be healed. A righteous person's prayer is powerful and effective. Kon nag tuddanteleen seeni bàkkaar tey ñaanalante, ndax ngeen wér. Aji jub ji, ag ñaanam, day dal ak doole.
17 Elijah was a man like us, and he prayed hard that it not rain; it did not rain on the land for three years and six months. Ilyaas nit la woon ku bindoo ni nun, waaye ba mu saxee ci ñaan ngir mu baña taw, ndox laalul suuf diiru ñetti at ak genn-wàll.
18 Then he prayed again, and the heavens gave rain, and the earth produced its fruit. Mu dellu ñaan, asamaan taw, suuf meññ meññeefam.
19 My brothers and sisters, if anyone among you wanders from the truth and someone turns them back, Bokk yi, su amee ci yeen ku moy yoonu dëgg, keneen ku ko waññi,
20 know this: whoever turns a sinner from their wrong way saves that person's soul from death and covers a multitude of sins. xamleen ne ku waññ bàkkaarkat ci yoonu sànkuteem, musal na ko bakkanam, te faral na ko bàkkaar yu bare.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]