Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

1 Peter 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Peter, apostle of Jesus Christ, to the chosen exiles scattered through Pontus, Galatia, Cappadocia, Asia, and Bithynia. Ci man Piyeer, ndawal Yeesu Almasi bi la bataaxal bii bawoo, ñeel askan wi Yàlla tànn, te ñu toxuji diiwaani Pont ak Galasi ak Kapados ak Asi ak Bitini.
2 Chosen by our Father's foreknowledge, made holy by the Holy Spirit, to obey Jesus Christ and be sprinkled with his blood: grace and peace multiplied to you. Yeen la Yàlla Baay bi ràññee lu jiitu, ci ni mu leen sellale Noo gu Sell gi, ngir ngeen mana déggal Yeesu Almasi bi, boole ci tooyloo deretam, mu setal leen. Na aw yiw ak jàmm juy baawaan ñeel leen.
3 Blessed is our Father, and the Father of our Lord Jesus Christ: by his great mercy he gave us new birth into a living hope through Jesus Christ's resurrection from the dead, Cant ñeel na Yàlla, sunu Baayu Sang Yeesu Almasi bi! Moo nu judduwaatal ci yërmandeem ju yaa, ci dooley ndekkitel Yeesu Almasi bi, ngir may nu yaakaar juy dund.
4 into an inheritance that can never perish, spoil, or fade, kept in heaven for you, Loolu moo am ngir ab cér bu dul yàqu, du sobewu, du seey, cér bu dence fa asamaan ñeel leen,
5 protected through faith by our Father's power for the salvation ready to be revealed in the last time. yeen ñi seen ngëm tax ngeen yiiru ci manoorey Yàlla, mi leen di nége mucc ga mu waajal te di ko feeñal ca bés bu mujj ba.
6 You rejoice greatly in this, though now, briefly, you may have had to be distressed by various trials. Loolu bégeleen koo bége, doonte tey ñàkkul ngeen nekke njàqare ab diir, ndax ay nattuy nattu.
7 These have come so that your faith—tested and found genuine, worth more than fire-refined gold that still gets destroyed—may bring praise, glory, and honor when Jesus Christ appears. Yooyu nattu, ni sawara di natte wurus, ni lay natte seen dëggutey ngëm, te ngëm a gën wurus fuuf, nde wurus day jeex. Su ko defee seen ngëm gu dëggu jural leen ag cant ak daraja ak teraanga, bés bu Yeesu Almasi bi feeñee.
8 Though you've never seen him, you love him; though you don't see him now, you trust him, rejoicing with joy beyond words and full of glory, Moom mooy ki ngeen gisul te sopp ko. Tey fi tey gisuleen ko, waaye gëm ngeen ko, ba tax leena bég lool, mbég mu màgg mu làmmiñ manula tudd,
9 for you are receiving the goal of your faith, the salvation of your souls. ndax yeena ngi jot ci yool bi ngëm di yóotu, te mooy texe.
10 Prophets who spoke of the grace meant for you investigated and searched carefully into this salvation, Googu texe, yonent ya jottali woon waxyub seen yiw wi leen dikkal, niir nañu ko, càmbar ko.
11 searching for the time and situation the Spirit of Christ in them pointed to, when he predicted Christ's sufferings and the glories after them. Gëstu nañu jan jamono ak yan xew-xew la Noowug Almasi gu Sell ga nekkoon ci ñoom tegtale woon. Mooy ba Noo gay seede lu jiitu coonoy Almasi bi ak ndam ya cay topp.
12 It was revealed to them: they served not themselves but you, when they spoke of these things now announced to you through those who preached the good news to you by the Holy Spirit sent from heaven. Even angels long to look into these things. Yonent yooyu, xamalees na leen ne du seen njariñal bopp lañuy liggéeyal xibaar boobu, xanaa yeen. Ñi leen àgge xibaar bi tey jii, ñoo di ñiy waare xibaaru jàmm bi, ci dooley Noo gu Sell gi ñu yebale asamaan, te muy mbir mu malaaka yi sax bëggoon nañoo nemmiku.
13 So, minds braced for action and fully sober, hope completely on the grace to be brought to you when Jesus Christ is revealed. Kon nag teewlooleen seen xel, te ànd ak seen sago, te ngeen wékk seen jépp yaakaar ci yiw wa ñu leen di dikke kera bu Yeesu Almasi bi feeñee.
14 As obedient children, don't let yourselves be shaped by the desires you once followed in your ignorance. Gannaaw gone yu dégg ndigal ngeen, buleen toppati seen xemmemtéefi bakkan ya woon, ba ngeen xamulee.
15 But just as the one who called you is holy, so be holy in all you do; Waaye ni ki leen woo selle, yeen itam nangeen selle noonu ci seen mboolem jëfin.
16 for it is written: "Be holy, because I am holy." Ndax kat bindees na ne: «Ñu sell ngeen wara doon, ndax man Ku sell laa.»
17 Since you call on a Father who judges every deed without favoritism, spend your exile time here in reverent fear. Gannaaw nag kiy àtte nit ku nekk ci ay jëfam te amu ci xejj ak seen, Baay ngeen koy wax, sàllooleen koo ragal, seen diirub ngan ci kaw suuf.
18 You know silver and gold—things that decay—didn't rescue you from the empty life passed down from your ancestors, Xam ngeen ne yëf yuy wéy yu mel ni xaalis mbaa wurus, du moom lees leen jote ci seen dundinu neen wa ngeen donne ca seeni maam,
19 but with Christ's precious blood, a lamb without defect or stain. waaye seenug njot moo di deretu Almasi ju jafe ji taxawe deretu xar mu sikkul, gàkkul.
20 Chosen before the world's foundation, revealed in these last times for your sake. Bu yàgg, ba àddina sosoogul la Yàlla tuddaloon Almasi bi loolu, waaye léegi ci mujug jamono jii la ko Yàlla feeñal ngir yeen
21 Through him you believe in our Father, who raised him from the dead and glorified him, so your faith and hope are in our Father. ñi Almasi bi tax ngeen gëm Yàlla. Te Yàllaa ko dekkal, may ko ndam, ba tax Yàlla di ki ngeen gëm, yaakaar ko.
22 Having purified your souls by obeying the truth for sincere love of the brothers, love each other deeply from a pure heart. Kon nag gannaaw setal ngeen seen xol, ndax dëgg gi ngeen déggal, ba tax ngeen am cofeel gu mucc jinigal ci bokki gëmkat ñi, nangeen soppantee xol bu set, cofeel gu mat sëkk.
23 For you have been born again—not of perishable seed but imperishable—through the living, enduring word of our Father. Ndax kat dangeena judduwaat, te jiwu wi ngeen judduwaate mooy kàddug Yàlla giy dund te sax dàkk; du jiwu wuy yàqu, waaye mooy jiwu wu dul yàqu mukk.
24 For, "All people are like grass, and all their glory like the flowers of the field; the grass withers and the flowers fall, Ndax bindees na ne: «Nit am ñax doŋŋ la; mboolem darajaam mel ni tóor-tóoru àll, ñax ma wow, tóor-tóor ma ruus.
25 but the word of our Father endures forever." And this is the word that was preached to you. Waaye kàddug Boroom bi mooy sax ba fàww.» Kàddu googu moo di xibaaru jàmm bi ñu leen àgge.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]