Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

1 Peter 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 So put away all malice and all deceit and hypocrisy and envy and all slander. Kon nag baleen mboolem xeetu mbon ak mboolem njublaŋ ak jinigal ak kiñaan ak mboolem xeetu yàq der.
2 Like newborn babies, crave pure milk of the word, so you grow into salvation, Ni liir buy doora juddu yàkkamtee nàmpe, ni ngeen wara yàkkamtee nàmp soow mu set miy kàddug Yàlla. Mooy tax ngeen màgg ci seen dundug texe,
3 now that you have tasted that the Lord is good. gannaaw mos ngeen ci mbaaxug Sang bi.
4 As you come to him, the living stone rejected by people but chosen, precious to our Father. Dikkleen ci moom, mooy doj wuy dund. Nit ñee ko beddi moos, waaye Yàllaa ko fal, fonk ko.
5 You too are being built, like living stones, into a spiritual house and a holy priesthood, offering spiritual sacrifices our Father accepts through Jesus Christ. Te yeen itam yeen ay doji cëslaay yuy dund, doj yi Noo gu Sell gi tabaxe ag kër Yàlla, ñeel liggéeyu carxal gu sell, ngir ngeen di ko jébbal ay sarax yu Noo gi rafetlu, sarax yu Yàlla nangu ndax Yeesu Almasi bi.
6 Scripture says: "See, I set in Zion a chosen, precious cornerstone; whoever believes in him will never be put to shame." Moo waral lii dikk ci Mbind mi: «Maa ngii di dëj fi Siyoŋ, aw doju koñu tabax, muy doju tànnéef wu gànjare. Wii doj, ku ko wéeroo, doo rus mukk.»
7 This honor, then, is for you who believe. For those who don't, the stone the builders rejected has become the cornerstone, Kon nag yeen ñi gëm, yeen la gànjar gi ñeel. Waaye ci ñi gëmul, nag: «Moo di doj wi tabaxkat yi beddi woon, te mu mujj di doju koñu tabax bi.»
8 and a stumbling stone, a rock that trips them. They trip because they disobey the word—exactly what they were appointed for. Te it: «Mooy doj wuy fakkastale, di xeer wuy daaneel.» Ñoo ko fakkastaloo nde ñoo gëmul kàddu gi, te it loolu la leen dogal ba séddoon.
9 But you are a chosen people, a royal priesthood, a holy nation, a people belonging to our Father, to proclaim the praises of the one who called you from darkness into his amazing light. Waaye yeen nag yeenay giir giy tànnéef, yeenay sarxalkati buur, yeenay askan wu sell, yeenay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.
10 Once you were not a people, now you are our Father's people; once you had not received mercy, now you have received mercy. Yeen ñi dul woon sax aw xeet, démb, tey yeenay xeet wi Yàlla ñoñoo; dajaguleen woon yërmande, waaye tey daj ngeen yërmande.
11 Dear friends, I urge you—foreigners and exiles—to avoid fleshly desires that war against your soul. Soppe yi, ay gan ngeen, ay doxandéem ci kaw suuf. Kon nag li ma leen di dénk moo di ngeen moyu xemmemtéefi bakkan yiy xeex ak ab xol.
12 Live good lives among the nations, so that when they slander you as wrongdoers, they may see your good deeds and glorify our Father on the day he visits us. Seen dundin ci biir jàmbur ñi gëmul, rafetalleen ko, ba su ñu leen waxaloon ne ay defkati lu bon ngeen itam, seen jëf ju rafet lañuy gis, te moom lañuy sàbbaale Yàlla, kera bésub dikkam.
13 Submit to every human authority for the Lord's sake—whether the emperor, as supreme, Nangulleen gépp kilifteef gu tege ci àddina ngir Boroom bi; muy buur bu mag bi gëna kawe,
14 or to governors, sent by the emperor to punish wrongdoers and praise those who do good. mbaa boroom dëkk yi diy ndawam, te mu tabb leen, ngir ñu mbugal ñiy def lu bon, te sargal ñiy def lu baax.
15 For this is our Father's will: that by doing good you silence the ignorant talk of foolish people. Ndax coobarey Yàlla kat moo di ngeen di def lu baax, ba wedamal nit ñu ñàkk bopp ñi xamul dara.
16 Live as free people—not using freedom to cover evil—but as servants of our Father. Ay gor ngeen, waaye jaami Yàlla ngeen. Kon buleen taafantaloo li ngeen diy gor, ba def lu bon.
17 Respect everyone, love the family of believers, fear our Father, honor the emperor. Ñépp nag ngeen di teral; mbooloom gëmkat ñi, soppleen leen; Yàlla, ragalleen ko; te buur, teral leen ko.
18 Servants, submit to your masters with full respect—not only the good and gentle, but also the harsh. Yeen jaam yi, nangulleen te weg wegeel gu mat sëkk seeni sang, te du sang yi baax te lewet doŋŋ, waaye ñu wex ñi itam ci lañu.
19 For it is commendable if someone bears up under the pain of unjust suffering, mindful of our Father. Ndax nit ki su séddee Yàlla ab cér, ba tax mu muñ tiis ak coono bu ko yoon tegul, loolu aw yiw la.
20 What credit is it to endure a beating for doing wrong? But enduring suffering for doing good—this is commendable before our Father. Muñ ay dóor yu la fekk ci tooñ, ana lu ciy ndam? Waaye soo muñee coono boo daj ngir lu baax loo def, loolu de aw yiw la fa kanam Yàlla.
21 You were called to this, since Christ suffered for you too, leaving an example for you to follow in his steps. Ci loolu sax lañu leen woo, ndax Almasi bi itam sonn na ngir yeen, te moo leen bàyyeel ab royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam.
22 "He committed no sin, and no deceit was found in his mouth." «Moo bàkkaarul, fenul.»
23 When they hurled their insults at him, he did not retaliate; when he suffered, he made no threats, but entrusted himself to the one who judges justly. Saaga nañu ko te feyuwul, daj na coono te tëkkoowul, waaye boppam la dénk kiy àtte dëgg.
24 He himself bore our sins in his body on the tree, so that we might die to sin and live for righteousness; by his wounds you have been healed. «Moom ci boppam moo gàddu sunuy bàkkaar,» moo ko tegoo ci yaramu boppam ca bant ba, ngir nu deewal bàkkaar te dundal njub; «moom mooy ki ngeen wére ci ay góomam.»
25 For you were straying like sheep, but now have returned to the Shepherd and Guardian of your souls. «Yeena réeroon niy xar,» waaye délsi ngeen tey ci seenub sàmm, seen wattukatub xol.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]