Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

1 Peter 3 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Likewise, wives, submit to your own husbands, so that even if some disobey the word, they may be won without a word by their wives' conduct, Naka noonu yeen jigéen ñi, nangulleen seen jëkkër, ngir jëkkër ju ci nanguwula gëm kàddu gi it, mana gindiku te seen wax yeen, du ci am yoon, ngir na ngeen di jëfe,
2 seeing your pure, reverent conduct. ndax day xool ci yeen ak seenug sellal gu ànd ak wegeel.
3 Do not let your beauty be the outward kind—braided hair, gold jewelry, fine clothing. Seen gànjar bumu doon gànjaru biti bu yem ci ay létt yu rafet ak takkaayi wurus ak yére yu yànj,
4 But let it be the hidden person of the heart, the undying beauty of a gentle, quiet spirit, precious in our Father's sight. waaye nay lu làqoo jëmmu biir, nay gànjar gu dul jeex, te mooy lewetaay akug teey, ndax looloo réy njarte fa Yàlla.
5 For this is how the holy women of old who hoped in our Father adorned themselves, submitting to their own husbands, Bu njëkkoon loolu moo doon gànjaru jigéen ñu sell ña yaakaaroon Yàlla te nangul seen jëkkër,
6 as Sarah obeyed Abraham, calling him lord. And you have become her children if you do good, fearing no terror. noonu Saarata déggale woon Ibraayma, naan ko «Sang bi». Yeen jigéen ñi nag, yeenay doomi Saarata, li feek yeena ngi def lu baax te bañ cee ragal ku leen xupp.
7 Husbands, similarly, live with your wives with understanding, honoring each as the weaker vessel and as coheirs of the grace of life, so your prayers aren't hindered. Naka noonu yeen góor ñi, bàyyileen xel ni ngeen dëkke ak seeni jabar, tey sóoraale néew dooley jigéen. Séddleen leen teraangay nawle, gannaaw yeena bokk wenn yiw wi leen may ngeen dund dëgg. Su ko defee dara du gàllankoor seeni ñaan.
8 Finally, all of you, be of one mind, sympathetic, loving one another as family, tenderhearted, and humble. Li may tënke nag moo di yeen ñépp, ngeen mànkoo, yégante, bëggante ni mu ware ay bokki gëmkat, baaxeenteleen te woyof.
9 Do not repay evil for evil or insult for insult, but bless instead—you were called to this, so you may inherit blessing. Lu bon, buleen ko feye lu bon; ay saaga it, buleen ko feye ay saaga. Xanaa ngeen ñaanal leen, feye leen ko, ndax ci loolu lees leen woo, ngir ngeen jagoo barke.
10 For, "Whoever desires to love life and to see good days, let him keep his tongue from evil and his lips from speaking deceit. Ndax kat: «Ku bëgg dundam neex, bëgga fekke bés bu rafet, na làmmiñam daw lu aay, dawi fen.
11 Let him turn away from evil and do good; let him seek peace and pursue it. Na daggook lu bon, tey def lu baax, sàkku jàmm, saxoo ko.
12 For the eyes of our Lord are on the righteous, and his ears are open to their prayer, but the face of our Lord is against those who do evil." Ndax ay gët la Boroom bi ne jàkk aji jub ñi, te ay noppam la dékk seeni ñaan, waaye Boroom beey won gannaaw ñiy def lu bon.»
13 Now who is there to harm you if you are eager to do what is good? Te it su ngeen dee ñu njaxlaf ci def lu baax, ana ku leen di def lu bon?
14 But if you suffer for righteousness, you are blessed. Don't fear their fear, don't be shaken. Te sax su ngeen doon jànkoonteeki coono ndax seenug njub, ndokkalee yeen. «Buleen am jenn tiitaange ci seeni xuppe, te buleen jaaxle.»
15 Set Christ apart as Lord in your hearts. Always be ready to answer anyone who asks the reason for your hope, but with gentleness and respect. Waaye Sang Almasi bi ngeen di sellal ci seen xol, te waajal nu ngeen di tontoo ku leen laaj lu jëm ci yaakaar ji ngeen am.
16 Keep a clear conscience, so that when you're slandered, those who insult your good conduct in Christ are shamed. Waaye nay tont lu rafet te ànd akub yar. Saxooleen di jëfe li dalal seenum xel, ba mbir ma ñu leen di baatale, ñooñuy ŋàññ seen dundin wu rafet wi leen Almasi bi manloo, gàcce rekk lañuy jële ca mbir ma ñu leen di baatale.
17 Better to suffer for doing good, if that's our Father's will, than for doing evil. Coono yu la jëf ju baax yóbbe kat, ndegam da di coobarey Yàlla, moo gën coono yu la jëf ju bon yóbbe.
18 For Christ too suffered once for sins, the righteous for the unrighteous, to bring us to our Father—put to death in flesh, made alive in spirit, Almasi bi itam benn yoon la daj coono ndax bàkkaari nit ñi, moom miy ki jub moo leen ko defal yeen ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla; moom lañu rey yaramu suuxam, waaye moo dundaat ci dooley Noo gu Sell gi.
19 in which he also went and proclaimed to the spirits in prison, Ci dooley Noo googu la deme ba waari mbindeef ya tëje,
20 who disobeyed long ago, when our Father waited patiently in Noah's days as the ark was being built, in which a few—eight people—were brought safely through the water. ñooña gëmadi woon bu yàgg, jant ya Yàllay muñ, di négandiku, te Nóoyin di yatt gaal ga. Lim bu néew, juróom ñett ña ca duggoon, mucce ca ndox ma.
21 This corresponding baptism now saves you too—not removing body dirt, but appealing to our Father for a good conscience—through Jesus Christ's resurrection, Fi ñu leen jaarale, ci mbënn ma, moo di misaalub sóobu gi leen musal tey; du sóobu guy dindi tërub yaram, waaye moom ngeen di wuyoo wooteb Yàlla ci xel mu dal, te li leen di musal mooy ndekkitel Yeesu Almasi
22 who entered heaven and is at our Father's right hand, with angels, authorities, and powers subject to him. bi yéeg asamaan, toog fa ndijooru Yàlla, ki malaaka yeek boroom sañ-sañ yeek boroom doole yi bokk nekk cig curgaam.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]