Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

James 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 James, a servant of our Father and the Lord Jesus Christ, to the twelve tribes scattered among the nations: greetings. Ci man Yanqóoba, jaamub Yàlla ak Sang Yeesu Almasi bi, la bataaxal bii bawoo, ñeel fukki giir ak ñaar yi tasaaroo ci àddina. Maa ngi leen di nuyu.
2 Consider it pure joy, my brothers and sisters, whenever you face trials of many kinds, Bokk yi, bu ngeen jaaree ci mboolem xeeti nattu, jàppeleen ko mbég mu mat sëkk,
3 because you know that the testing of your faith produces perseverance. te xam ne bu seen ngëm nattoo, ñeme coono la leen di jural.
4 Let perseverance finish its work so that you may be mature and complete, lacking nothing. Na ag ñeme coono sottal liggéeyam ci yeen, ngir ngeen sotti, mat sëkk, te baña yéese fenn.
5 If any of you lacks wisdom, ask our Father, who gives freely to all without criticizing, and it will be given you. Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn.
6 Ask in faith, without doubting, for the doubter is like a sea wave, driven and tossed by the wind. Waaye ngëm la koy ñaane te bumu ci am benn sikki-sàkka, ndax kiy sikki-sàkka daa mel ni gannaxu géej bu ngelaw liy yóbbu, di ko lëmbaaje.
7 That person should not expect to receive anything from our Father. Kooku bumu yaakaar dara ci Boroom bi.
8 Such a person is double-minded and unstable in all their ways. Boroom xel ñaar la, xel maa toogul ci lenn lu muy def.
9 Let the believer in humble circumstances take pride in their high position, Mbokkum gëmkat mi suufe daraja, na sagoo ab kawewaayam ci ni ko Yàlla yékkatee;
10 but let the rich boast in their low state, since they'll pass like a wildflower. te ki barele it na sagoo ci ni ko Yàlla suufeelee, ndax ni tóor-tóoru saxyaay di ruuse, noonu lay wéye.
11 The sun rises with scorching heat and withers the grass. Its flower falls; its beauty vanishes. So the rich fade away amid their pursuits. Naka la jant di fenk, ba naaj wi tàng jérr, saxyaay lax, tóor-tóoram ruus, taar ba réer ko mërr. Noonu itam la ki barele di jeexlee ci biiri yëngoom.
12 Blessed is the one who endures trial, because once tested they'll receive the crown of life our Father promised to those who love him. Ndokkalee ku muñ ab nattu, nde su ca amee ngërëm, mooy yooloo kaalag texe gi Yàlla dig ñi ko sopp.
13 When tempted, no one should say, "Our Father is tempting me." Evil can't tempt our Father, and he tempts no one. Képp ku dajeek lu koy xiirtal, bumu ne: «Yàllaa ma xiirtal,» ndax maneesula xiirtal Yàlla ci lu bon, te moom ci boppam du xiirtal kenn.
14 But each person is tempted, dragged away and lured by their own evil desire. Waaye ku nekk, sa xemmemtéefu bakkanu bopp moo lay xiirtal, ootal la ba nax la.
15 Then desire conceives and gives birth to sin; sin, full-grown, gives birth to death. Te xemmemtéefu bakkan bu ëmbee, bàkkaar lay wasin, te bàkkaar bu matee, dee lay jur.
16 Don't be deceived, my dear brothers and sisters. Bokk yi, soppe yi, buleen juum ci lii:
17 Every good and perfect gift is from above, coming down from the Father of lights, who never changes or casts a shifting shadow. gépp may gu baax ak bépp jagle bu mat, fa kaw la bawoo, di lu wàcce fa Baay biy boroom leer yi, ki soppikuwul ci lenn, te genn ker gu toogadi nekkul ci moom.
18 By his choice, he gave us birth through the word of truth, so we'd be a kind of firstfruits of his creation. Moom la soob mu jur nu ci kàddug dëgg gi, ba nu taxawe saraxu ndoortel meññeef, ci biiri bindeefam.
19 Know this, my dear brothers and sisters: everyone should be quick to listen, slow to speak, slow to anger, Bokk yi, soppe yi, nangeen xam lii: na ku nekk di gaaw ci déglu, di yeexa wax tey yeexa mer.
20 because human anger does not produce the righteousness of our Father. Ndax merum nit du jur njub fa Yàlla.
21 So strip off all moral filth and excess evil; humbly receive the word planted in you, able to save your souls. Kon nag baleen jépp jikko ju tilim ak mboolem xeeti mbon yi ne gàññ, te ngeen nangu, ci biir ag woyof, kàddu gi Yàlla xasa jëmbat ci yeen te mu man leena musal.
22 Do not merely listen to the word, and so deceive yourselves. Do what it says. Doonleen jëfekati kàddu gi, buleen di ay déglukat doŋŋ, di nax seen bopp.
23 Anyone who hears the word but doesn't act on it is like one who looks at his natural face in a mirror, Ndax kat kuy déglu kàddu gi te jëfewoo ko, kooku daa mel ni kuy niir kanamam cib seetu:
24 and, after looking at himself, goes away and immediately forgets what he looks like. bu niiree boppam, dem daldi fàtte ca saa sa lu muy nirool.
25 But whoever peers into the perfect law of freedom, continuing in it—not a forgetful hearer but a doer who acts—will be blessed in his doing. Waaye ki ne jàkk yoon wu mat sëkk wiy goreel ku ko topp, saxoo yoon wi te bañ koo dégg, fàtte, xanaa di dégg, jëfe, kooku mooy bége jëfam.
26 If anyone thinks himself religious but doesn't control his tongue, he deceives his own heart—his religion is worthless. Ku yaakaar ne am na diine te moomul làmmiñam, boppam lay nax te diineem amul njariñ.
27 Pure and spotless religion before our Father is this: caring for orphans and widows in their distress, and keeping oneself unstained from the world. Diine gu set te mucc sikk fa kanam Yàlla Baay bi moo di lii: di nemmiku jirim akub jëtun ci seen njàqare, tey sàmm boppam, ba mucc ci gàkki àddina.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]