Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Esther 10 RWBT

Side by side with the Father's Heart Bible™

Mardose daan na

1Gannaaw loolu Buur Aserus gàll ab galag ca réew ma mépp, ba ca duni géej ga. 2Mboolem jaloore ya Buur Aserus def, ca dooleem ak màggaayu darajaam ak na mu yékkatee Mardose, ba mu kawe, lépp bindees na ko moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Medd ak Pers ca seeni jant. 3Mardose Yawut ba, moo sësoon rëkk ca Buur Aserus, sut Yawut yépp, ay bokki Yawutam yu bare nawloo ko. Muy sàkku nag ngëneeli ñoñam, di waxal jàmm mboolem askanam.

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]