Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Proverbs 7 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 My son, keep my words, and store up my commandments within you. Doom, sàmmal samay wax, fonk samay santaane.
2 Keep my commandments and live; guard my teaching as the apple of your eye. Jëfeel samay santaane, ba dund, jàppal samay ndigal sa fukki loxo.
3 Bind them on your fingers; write them on the tablet of your heart. Takkal ci say waaraam, bind ko ci sa àlluway xol.
4 Say to wisdom, "You are my sister," and call understanding your dearest friend, Safool xel mu rafet, muy sab jigéen, te nga xejjoo dég-dég ni sa mbokk lenqe.
5 to keep you from the forbidden woman, from the stranger with her smooth words. Dina la aar ci jigéenu njaalookat, bokk feneen, di wax lu neex.
6 For at the window of my house I looked down through my lattice, Damaa tollu sama palanteer, séentu ca xarante ya,
7 and I saw among the naive, I noticed among the young men, a youth who lacked sense, séen ca biir téxét ya, ku ma seetlu ca xale yu góor ya, muy ku ñàkk bopp.
8 passing through the street near her corner, taking the road to her house, Muy dem ba fa ndaw say taxaw, ca selebe yoon wa, daldi wuti kër ndaw sa.
9 in the twilight, as the day faded, in the dark of night and gloom. Ngoonug suuf la, jant biy lang, muy lëndëm di gëna guddi.
10 And there a woman comes to meet him, dressed like a prostitute, with cunning in her heart. Ndaw si jekki dajeek moom, sol yérey gànc, lal pexeem.
11 She is loud and defiant; her feet will not stay at home. Daa xumb, të, du toog këram.
12 Now in the street, now in the squares, she lurks at every corner. Ma nga ca mbedd ma, ne ca pénc ya, ruqoo ruq, ma ngay yeeroo.
13 She grabs him and kisses him, and with a brazen face she says to him: Ndaw sa ne ko katam, fóon, ne wajj, ne ko:
14 "I had peace offerings to bring; today I have paid my vows. «Tey matal naa la ma digoon Yàlla, yàppu bernde waa nga kër ga, saraxu cant la.
15 So I came out to meet you, to look for you eagerly, and I have found you. Moo ma taxa dikk dajeek yaw. Seet naa laa seet, ba gis la.
16 I have spread my bed with coverings, with colored linens from Egypt. Lal naa saab lal, ba mu jekk, di malaan yu yànj, bawoo Misra.
17 I have perfumed my bed with myrrh, aloes, and cinnamon. Lal ba, ma xeeñal, mu ne bann, di ndàbb, cuuraay ak xas mu neex.
18 Come, let us drink deep of love until morning; let us lose ourselves in love. Dikkal, nu baanee baane, ba bët set, te bànneexu ci mbëggeel.
19 For my husband is not at home; he has gone on a long journey. Sama jëkkër newu fa, daa dem yoon wu sore.
20 He took a bag of money with him and will not come home until the full moon." Mbuusum xaalis la ŋàbb, yóbbu, du ñibbisi ndare weer wi fees dell.»
21 With all her persuasive words she sways him; with her smooth lips she draws him in. Muy mocc aka moccaat, ba nax ko, di wax lu neex, ba man ko.
22 All at once he follows her, like an ox going to the slaughter, like a deer stepping into a snare, Waa ja jekki, topp ko, mbete yëkk wu ñuy rendiji, mbaa dof bu ñu jéng, di ko yari.
23 until an arrow pierces its liver; like a bird darting into a trap, he does not know it will cost him his life. Mooy picc mu tàbbi cig fiir. Du xam ne day dee, ba keroog fitt jam ko ci xol.
24 Now then, my sons, listen to me, and pay attention to what I say. Kon nag, samay doom, dégluleen ma, teewluleen samay wax.
25 Do not let your heart turn aside to her ways; do not wander into her paths. Bu leen soosu ndaw xiir ci moy, buleen teggi, topp ko.
26 For she has brought down many victims; her slain are a mighty multitude. Bare na ku dee, moo ko rey, maneesula waññ ñi mu rey ñépp.
27 Her house is the road to the grave, going down to the chambers of death. Këram yoonu njaniiw la, daa bartalu, tàbbi néegi dee.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]