Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Proverbs 8 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Does not Wisdom call out, and understanding raise her voice? Déggal! Xel mu Rafet di soxna saa ngi woote, moom soxna si Am Dégg di xaacu.
2 Atop the heights along the way, where the paths meet, she takes her stand. Ma nga taxaw ca selebe yoon ya, fu gëna kawe ca yoon wa.
3 Beside the gates, at the entrance to the city, at the doorways she cries aloud: Ma nga ca buntu dëkk ba, taxaw; fa nit ñay jaare lay xaacoo naan:
4 "To you, all people, I call out; my voice reaches all humanity. «Yeen mbooloo yi laay woo, doom aadama yi laay joor.
5 You who are simple, learn prudence; you who are foolish, gain an understanding heart. Téxét bi, deel foog, dof bi, déggal ndéey lu xelu.
6 Listen, for I speak of noble things, and everything I say is right. Déglul, ma wax la lu am solo, dégtal la njub.
7 My mouth utters truth, for my lips detest wickedness. Dëgg laay wax, di bañ wax ju bon.
8 All the words of my mouth are righteous; none of them is twisted or crooked. Lu ma wax njub la. Amul lu dëng mbaa lu jekkadi.
9 To the one who understands they are all clear, and right to those who find knowledge. Lépp a dëggu ci ku amug dégg, te jub ci ku for xam-xam.
10 Take my instruction instead of silver, and knowledge rather than choice gold, Na la samab yar gënal xaalis, xam-xam dàqal la ngën-gi-wurus.
11 for wisdom is better than jewels, and nothing you desire can compare with her. Ndax man, Xel mu Rafet, maa gën gànjar, loo bëgg maa ko raw.
12 I, Wisdom, dwell with prudence, and I find knowledge and discretion. «Man, Xel mu Rafet, foog di sama kër; xam-xam ak pexe, ma for.
13 The fear of our Father is to hate evil. Pride and arrogance, the evil way, and perverse speech I hate. Ragal Aji Sax ji mooy bañ lu bon. Réy, xeebaate, yoonu mbon, ak wax ju jekkadi, ma boole bañ.
14 Counsel is mine, and sound wisdom; I am understanding; strength is mine. Maa moomi digle, di maye gis-gis; maa amug dégg, di boroom doole.
15 By me kings reign, and rulers decree what is just; Samay pexe la buur di jiitee, kilifa di ci àttee dëgg.
16 by me princes govern, and nobles—all who rule with justice. Ci samay pexe la njiit di saytoo, ñook kàngam yeek ñiy àtte dëgg ñépp.
17 I love those who love me, and those who search for me find me. Maa sopp ku ma sopp, ku ma seet tigi, gis ma.
18 With me are riches and honor, enduring wealth and righteousness. Alal ak teraangaa ngi fi man, am-am bu sax it ak yoolu njekk.
19 My fruit is better than gold, than the finest gold, and what I yield surpasses choice silver. Li may mayee gën wurus, muy wurus wa gën, sama njariñ wees xaalis ba gën.
20 I walk in the way of righteousness, along the paths of justice, Yoonu njub laay jaare, di dox ci li jaadu.
21 giving wealth as an inheritance to those who love me, and filling their treasuries. Ku ma sopp, ma nàddil la, feesal sab denc.»
22 Our Father brought me forth at the beginning of his way, before his works of old. Soxna si, Xel mu Rafet nee na: «Aji Sax ji jagoo na ma ca njàlbéen, ma jiitu ca jëfam ya woon.
23 From ages past I was established, from the beginning, before the earth began. Bu yàgg lañu ma dëj, ca ndoorte la, bala suuf a sosu.
24 When there were no deep waters I was brought forth, when there were no springs overflowing with water. Ba may dikk, géej amul, ndox ballul bay fees, di wal-wali.
25 Before the mountains were settled, before the hills, I was brought forth, Dikk naa bala tund yu mag yee sampu, lu jiitu tund yu ndaw yi,
26 while he had not yet made the earth and its fields, or the first dust of the world. laata Yàllaa sàkk suuf aki àllam ak feppu pënd ci àddina.
27 When he set the heavens in place, I was there; when he drew a circle over the face of the deep, Ba muy taxawal asamaan, maa nga fa, ak ba muy rëdd fa asamaan taseek géej,
28 when he set the skies in place above, when he established the springs of the deep, ak ba muy teg niir ya fa kaw, ak ba muy dooleel ndoxi xóotey géej,
29 when he set for the sea its boundary so the waters would not cross their limits, when he marked out the foundations of the earth, ak ba muy sàkkal géej kemoom, ba du jàll fa mu wax. Ba muy rëdd fa muy samp àddina,
30 then I was beside him as a master craftsman, and I was his daily delight, rejoicing before him always, man, Xel mu Rafet, maa doon ku xareñ ci wetam, di ko bànneexal bés bu ne, tey bànneexu fi kanamam.
31 rejoicing in his whole world, and delighting in the human family. May bége wërngalu àddinaam, di bànneexoo doomi aadama.
32 And now, my children, listen to me: blessed are those who keep my ways. «Kon nag, samay doom, dégluleen ma. Mbégte ñeel na ki may topp.
33 Listen to instruction and be wise; do not ignore it. Nangeen déglu ku leen di yar, daldi muus. Buleen ko sàggane!
34 Blessed is the one who listens to me, watching daily at my gates, waiting beside my doorway. Mbégte ñeel na ki may déglu, di teewlu ca sama bunt bés bu nekk, di ma toogaanu sama bunt kër.
35 For whoever finds me finds life and receives favor from our Father. Ku ma daj, gudd fan, Aji Sax ji bége la.
36 But whoever misses me harms his own soul; all who hate me love death." Ku ma moy loru, ku ma bañ, daa repp.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]