Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Proverbs 25 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 These also are proverbs of Solomon, which the men of Hezekiah king of Judah copied out. Lii it ay kàddu yu xelu la, di yu Suleymaan, ay niti Esekiyas buurub Yuda sotti ko.
2 It is the glory of our Father to conceal a matter, but the glory of kings to search a matter out. Màggug Yàllaa ngi ci li mu làq, darajay buur a ngi ci li mu feeñal.
3 As the heavens are high and the earth is deep, so the heart of kings is unsearchable. Maneesula daj li ci xelu buur, xalaatam daa kawe ni asamaan, xóote ni suuf.
4 Take away the dross from the silver, and a vessel comes forth for the refiner. Xellil xaalis, tonni lu ca rax, ba ab tëgg man caa am ndab.
5 Take away the wicked from before the king, and his throne will be established in righteousness. Ab soxor it, dàqal, mu sore buur, ngir njubte law, jalam sax.
6 Do not put yourself forward in the king's presence, and do not stand in the place of the great; Bul réy-réylu fi kanam buur, bul tooge jataayu boroom daraja,
7 for it is better to be told, "Come up here," than to be put in a lower place in front of a noble you can see. ndax ñu ne la: «Yéegal, jegesi fii,» moo gën ñu toroxal la ci kanam kilifa. Boo gisalee sa bopp it,
8 Do not rush into a quarrel, for what will you do in the end when your neighbor puts you to shame? bul gaawa layooji, ana nooy def ëllëg, bu ñu la yeyee?
9 Argue your case with your neighbor himself, but do not disclose another's secret, Ñaarool ak ki nga joteel, te bul jéebaane jàmbur.
10 lest the one who hears it shame you, and your bad reputation never goes away. Lu ko moy ñu dégg ko, rusloo la, sab der yàqu yaxeet.
11 A word spoken at the right moment is like apples of gold in settings of silver. Wax ju ñor di nataalu wurus wu tege ci xaalis.
12 Like a ring of gold or an ornament of fine gold is wise correction to a listening ear. Kàddu yu lay yedd ci kuy dégg, jaarob wurus la mbaa gànjaru ngalam.
13 Like the cold of snow in the time of harvest is a faithful messenger to those who send him; he refreshes the soul of his masters. Ndaw lu wóor day seral xolu njaatigeem, mooy ndox mu sedd ci tàngooru ngóob.
14 Like clouds and wind without rain is one who boasts of a gift never given. Kuy dige te doo joxe, yaay xiin wu ngelaw, mu naaxsaay.
15 By patience a ruler is persuaded, and a soft tongue breaks bone. Muñ mer ay nax kilifa, te wax ju neex, fu mu jaar, mu nooy.
16 If you find honey, eat only enough, or you will have too much and vomit. Boo gisee lem, lekkal lu yem; bu ëppee, nga waccu ko.
17 Don't visit your neighbor's house too often, or he will grow weary of you and hate you. Na sa tànk di gëj kër dëkkandoo; boo ko sàppee, mu jéppi la.
18 Like a club, a sword, and a sharp arrow is one who bears false witness against his neighbor. Ku seedeel sa moroom ay fen, yen nga ko aw njur mbaa saamar mbaa fitt.
19 Like a bad tooth or a foot out of joint is trust in a faithless person in time of trouble. Bul wóolu workat bésub njàqare, mooy bëñ bu bon mbaa tànk bu nasax.
20 Like one who takes off a garment on a cold day, like vinegar poured on baking soda, is the one who sings songs to a heavy heart. Kuy woy, boroom tiisu xol di dégg, yaa futti mbubbam cib sedd, mbaa nga jonj xorom ci góomam.
21 If your enemy is hungry, give him bread to eat, and if he is thirsty, give him water to drink; Bu sab noon xiifee, jox ko mu lekk, bu maree, may ko mu naan,
22 for you will heap coals of fire on his head, and our Father will reward you. day rus ba mel ni koo yeni xal, te Aji Sax jee lay fey.
23 The north wind brings forth rain, and a secretive tongue, angry looks. Jëw, mer a cay topp; mooy ngelawal taw, taw a cay topp.
24 It is better to live in a corner of the rooftop than in a shared house with a quarrelsome wife. Dëkkeb ruq cim sàq moo gën jabar ju pànk.
25 Like cold water to a weary soul is good news from a distant land. Xibaaru jàmm, bawoo fu sore mooy ndox mu sedd ci ku loof.
26 Like a muddied spring or a polluted fountain is a righteous person who gives way before the wicked. Ku jub bu dee nangul ku bon, yàqu na, ni seyaan bu nëx mbaa teen bu xàbb.
27 It is not good to eat too much honey, nor to seek your own glory. Lekk lem ju ëpp baaxul, te wut waaw-góor du ngóora.
28 Like a city broken into and left without walls is a person who has no control over his own spirit. Ku dul ànd ak sa sago, yaa neexa song ni dëkk bu dara wërul.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]