Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Proverbs 24 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Do not envy evil men, and do not desire to be with them, Bul ñee ku bon, bul wuta ànd ak moom,
2 for their hearts plot violence, and their lips speak of trouble. ndax coxor lay nas ci xolam, te fitna la ay waxam di yee.
3 By wisdom a house is built, and by understanding it is established; Xel mu rafet ay tabax kër, rafet déggin a koy samp.
4 and by knowledge its rooms are filled with all precious and pleasant riches. Xam-xam ay feesal néeg ya ak mboolem alal ju jafe te yànj.
5 A wise man is full of strength, and a man of knowledge increases his power, Ku rafet xel di boroom doole, ku xam, gëna man;
6 for by wise guidance you can wage your war, and victory comes through many counselors. tegtal yu xelu lañuy xaree, diisoo bu yaatooy maye ndam.
7 Wisdom is too high for a fool; at the gate, he has nothing to say. Wax ju xelu sut nab dof, jataayu pénc du fa àddoo.
8 Whoever plans to do evil will be called a schemer. Kuy mébét lu bon, ñu ne yaay rambaaj bi.
9 A fool's scheming is sin, and the scoffer is detestable to people. Pexem dof bàkkaar la, te kuy ñaawle, ñu sib la.
10 If you falter in a time of trouble, your strength is small. Bu mettee, nga yoqi, sa doolee néew.
11 Rescue those being taken away to death, and hold back those stumbling toward the slaughter. Wallul ku ñuy reyi te tooñul, xettalil kuy tërëf, ñu di ko reyi.
12 If you say, "Look, we did not know this," does not he who weighs the heart perceive it? Does not he who watches over your soul know it? And will he not repay each person according to his deeds? Soo nee sa yoon nekku ci it, kiy natt xol yi, xam na, moom miy wattu sa bakkan, xam na, te kat mooy fey nit jëfam.
13 My son, eat honey, for it is good, and the honeycomb's drippings are sweet to your taste. Doom, deel lekk lem, baax na, lem ju xelli, boo sexee, mu tem-temi.
14 Know that wisdom is just like this to your soul; if you find it, there is a future, and your hope will not be cut off. Xamal ne xel mu rafet ni la neexe; soo xeloo, sa muj rafet, te sa yaakaar du tas.
15 Do not lie in wait, you wicked man, against the home of the righteous; do not destroy his resting place, Soxor bi, bul tëru boroom njekk ci këram, bul yàq dëkkuwaayam.
16 for though the righteous falls seven times, he rises again, but the wicked stumble in disaster. Boroom njekk day daanu juróom ñaari yoon, jógaat, ab soxor sërëx ci njekkar.
17 Do not rejoice when your enemy falls, and do not let your heart be glad when he stumbles, Bu sab noon daanoo, bu ko bànneexoo, bu tërëfee, bu ko bége.
18 lest our Father see it and be displeased, and turn his anger away from him. Lu ko moy Aji Sax ji gis la, ñaawlu ko, daldi giif, dootu ko mbugal.
19 Do not fret because of evildoers, and do not envy the wicked, Bu sa xol tàng ci ku bon, bul ñee ku soxor.
20 for the evil man has no future; the lamp of the wicked will be snuffed out. Ku bon amul muj, ku soxor day mel ni taal bu fey.
21 My son, fear our Father and the king, and do not join with those who rebel against them, Doom, ragalal Aji Sax ji, wormaal buur. Bul lëngook kuy fippu.
22 for their disaster will rise suddenly, and who knows the ruin that both of them can bring? Yàllaak buur a koy bette mbugal, te kenn xamul musiba mu muy doon.
23 These also are sayings of the wise: Showing partiality in judgment is not good. Lii it ñi rafet xel a ko wax. Par-parloo cib àtte baaxul.
24 Whoever says to the guilty, "You are innocent," peoples will curse him and nations will denounce him, Ku ne defkatu lu bon: «Yaw, tooñoo,» aw nit móolu la, mbooloo ŋàññ la;
25 but it will go well for those who convict the guilty, and a rich blessing will come upon them. ku ko ne: «Yaa tooñ,» yaay baaxle, taasoo barke bu yaa.
26 An honest answer is like a kiss on the lips. Ki lay wax dëgg sa soppe la.
27 Prepare your work outside, get your fields ready, and after that build your house. Ruujal sab tool, ji ko, doora tabax sa kër.
28 Do not be a witness against your neighbor without cause; would you deceive with your lips? Bul tuumaal nit ci neen, te bu ko seedeel ay fen.
29 Do not say, "I will do to him as he did to me; I will pay the man back for what he has done." Bul ne: «Li mu ma def laa koy def, damay feyu li mu ma def.»
30 I passed by the field of a lazy man, by the vineyard of someone lacking sense, Toolub ku yaafus laa jaare, ak tóokërub nit ku ñàkk bopp.
31 and there it was, all overgrown with thorns; the ground was covered with weeds, and its stone wall was broken down. Ndeke lépp a nga saxi dég, fépp fees akum ñax, tabaxu doj ba ko wër màbb.
32 Then I looked and took it to heart; I saw and received instruction. Maa ko gis, di xalaat, xoolaat ko, jànge ca.
33 A little sleep, a little slumber, a little folding of the hands to rest, Booy dajjant aka for bët, di tegley loxooka jaaxaan,
34 and poverty will come upon you like a robber, and scarcity like an armed man. néewlee ngi lay dikkal nib sàcc, ñàkk gànnaayul la.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]