Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Proverbs 26 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Like snow in summer and like rain at harvest, honor is not fitting for a fool. Teraanga jekkul cib dof, mooy seddub nawet mbaa taw cim ngóob.
2 Like a fluttering sparrow or a darting swallow, an undeserved curse does not come to rest. Ñaan-yàlla, soo tooñul, du la dal, day mel ni picc muy naaw, tëë toŋ.
3 A whip for the horse, a bridle for the donkey, and a rod for the backs of fools. Xiir, aw fas; laab, mbaam; yetu gannaaw, ab dof.
4 Do not answer a fool according to his foolishness, or you yourself will be like him. Bul topp ab dof cig ndofam, lu ko moy nga mel ni moom.
5 Answer a fool according to his foolishness, or he will be wise in his own eyes. Waaye toppal ab dof cig ndofam, lu ko moy mu defe ne daa muus.
6 Whoever sends a message through a fool cuts off his own feet and drinks down violence. Ku yóbbante ab dof kàddu, yaa woo fitna, gor say tànk.
7 Like the legs of a lame man hanging useless is a proverb in the mouth of fools. Kàddu gu xelu ci gémmiñug dof, mooy tànki lafañ, amalu ko njariñ.
8 Like binding a stone in a sling is giving honor to a fool. Kuy teral ab dof, jël ngaw doj, takk ko ci mbaq.
9 Like a thornbush in the hand of a drunkard is a proverb in the mouth of fools. Kàddu gu xelu ci gémmiñug dof mooy car aki dégam, màndikat xàcc.
10 Like an archer who wounds everyone is one who hires a fool or hires any passerby. Njaatige luy liggéeyloo ab dof ak kuy romb, daa mel ni fittkat buy gaañ ku ne.
11 As a dog returns to its vomit, so a fool repeats his foolishness. Dof day def jëfi dof, dellu ca, mooy xaj, bu waccoo, lekkaat ko.
12 Do you see someone wise in his own eyes? There is more hope for a fool than for him. Ana koo gis mu ne: «Maa xelu»? Kooku ab dof a ko gën demin.
13 The lazy person says, "There is a lion in the road! A lion in the streets!" Ab yaafus da naan: «Gayndee ngi ci yoon wi! Gayndee ngi ci mbedd mi!»
14 As a door turns on its hinges, so the lazy person turns on his bed. Ab yaafus day tëdd aka walbatiku, mooy bunt, day jaayu, demul fenn.
15 The lazy person buries his hand in the dish; it wearies him to bring it back to his mouth. Ab yaafus day yeb loxoom ci ndab, waaye yékkati ko, sex, da koy sonal.
16 The lazy person is wiser in his own eyes than seven who answer wisely. Ab yaafus day foog ne moo gëna muus juróom ñaari boroom xel yu xam tont.
17 Like grabbing a dog by the ears is a passerby who meddles in a quarrel not his own. Kuy xuloo lu sa yoon newul, yaa jàpp ci noppi xaj buy romb.
18-19 Like a madman shooting firebrands, arrows, and death, Nit kuy naxe, naan: «Damay fo!» yaay dof buy sànniy jum, di fitteeka reye.
19 so is the one who deceives his neighbor and says, "I was only joking!" Not in this edition
20 Without wood a fire goes out, and without a gossip a quarrel dies down. Bu matt amul, ab taal fey, fu soskat amul it, xuloo jeex fa.
21 As charcoal to embers and wood to fire, so a quarrelsome person kindles strife. Këriñ defi xal, matt xambub taal, ab xulookat di xambu ay.
22 The words of a gossip are like choice morsels; they sink down into the inmost parts. Waxi jëwkat di ñam wu neex, wuy seey, jàll ca biir-a-biir.
23 Like a glaze covering an earthen pot are smooth lips with an evil heart. Kuy wax lu neex, tey mébét lu bon, yaay xaalis bu rax, ñu xoob ca ndabal xandeer.
24 An enemy disguises himself with his lips, but in his heart he harbors deceit. Ab noon làqoo na ay waxam, lal pexey wor ca xolam.
25 When he speaks graciously, do not believe him, for seven abominations fill his heart. Buy wax lu neex, bul gëm, ñaawtéef la xol ba fees dell.
26 Though his hatred is hidden by deceit, his wickedness will be exposed in the assembly. Su la nëbbalee mbañeel, di la nax it, ag mbonam mujj bir ñépp.
27 Whoever digs a pit will fall into it, and a stone rolls back on the one who rolls it. Ku gasal nit am yeer, yaa cay daanu; ku béraŋu doj, ngir tance, yaay tancu.
28 A lying tongue hates those it crushes, and a flattering mouth works ruin. Kuy fen, dangaa bañ ka nga fenal, te boroom làmmiñ wu neex day sànke.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]