Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Proverbs 21 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 The king's heart is a stream of water in our Father's hand; he turns it wherever he pleases. Xolu buur walum ndox la ci loxol Aji Sax ji, fu ko soob mu jëme ko fa.
2 Every way of a person seems right in their own eyes, but our Father weighs the heart. Lu waay def, daa jub ca moom, waaye Aji Sax jeey natt xol yi.
3 To do what is right and just is more pleasing to our Father than sacrifice. Deel def dëgg ak lu jub, moo gënal Aji Sax ji ab sarax.
4 Haughty eyes and a proud heart—the lamp of the wicked—are sin. Xeebaateek réy-réylu mooy bàkkaar yi ñuy ràññee ku bon.
5 The plans of the diligent lead surely to abundance, but all who are hasty end up in poverty. Farlu, woomle; ku gaawtu, mujj néewle.
6 Making a fortune by a lying tongue is a fleeting vapor, a deadly trap. Alal ju la fen may, cóolóol la, day naaw, wut ko xaru la.
7 The violence of the wicked will drag them away, because they refuse to do what is just. Coxor day sànk boroom, ndax day baña def njub.
8 The way of the guilty is crooked, but the conduct of the pure is upright. Ab saay-saay day dëngal, nit ku dëggu di jubal.
9 Better to live in a corner of the roof than in a shared house with a quarrelsome wife. Dëkkeb ruq cim sàq moo gën jabar ju pànk.
10 The soul of the wicked craves evil; their neighbor finds no mercy in their eyes. Ab soxor day namma lore, te du yërëm moroomam.
11 When a mocker is punished, the simple grow wise; when the wise are instructed, they gain knowledge. Boo mbugalee kuy ñaawle, ab téxét jànge ca; nga jàngal ku rafet xel, mu yokku.
12 Our Father, the Righteous One, observes the house of the wicked and brings the wicked to ruin. Aji Jub ji Yàlla xam na la ne ca biir kër ku bon, te mooy sànk ku bon.
13 Whoever shuts their ears to the cry of the poor will also cry out and not be answered. Ku tanqamlu jooyi ku ñàkk dina woote wall, wall ñàkk.
14 A gift given in secret soothes anger, and a bribe slipped into the cloak calms strong wrath. Ku mer, may ko ci sutura, mu giif; boroom xadar, boqal ko neexal, mu dal.
15 When justice is done, it is a joy to the righteous but terror to those who do evil. Bu yoon amee, ku jub bég; kuy def lu bon jàq.
16 A person who strays from the way of understanding will rest in the assembly of the dead. Ku noppee jëfe xel, noppaluji njaniiw.
17 Whoever loves pleasure will become poor; whoever loves wine and oil will never grow rich. Ku topp sa bànneex, mujje ñàkk; ku sopp biiñ ak lu niin du woomle.
18 The wicked become a ransom for the righteous, and the treacherous for the upright. Ku bon këppoo ayu ku baax, workat gàddu musibam kuy jubal.
19 Better to live in a desert land than with a quarrelsome and complaining wife. Dëkke ndànd-foyfoy moo gën jabar ju tàng, bare ay.
20 Precious treasure and oil are in the home of the wise, but a fool devours all he has. Ku xelu denc këram ngëneeli alal aku diw, ab dof saax-saaxee josam.
21 Whoever pursues righteousness and faithful love will find life, righteousness, and honor. Ku saxoo njekk ak ngor, am fan wu gudd, naataangeek daraja.
22 A wise person scales the city of the mighty and brings down the stronghold they trust in. Ku ñaw mana daan jàmbaari dëkk bu mag, ba màbb tata ja ñu yaakaaroon.
23 Whoever guards their mouth and tongue keeps themselves out of trouble. Ub sa gémmiñ, moom sa làmmiñ, mucc ci njàqare.
24 "Mocker" is the name of the proud and arrogant who acts with outrageous insolence. Ku réy te bew, mooy ñaawle, day reew, ba jéggi dayo.
25 The craving of a lazy person kills him, for his hands refuse to work. Ab yaafus day bëgg lu mu amul ba dee, ndax du nangoo liggéey,
26 All day long the craving grows, but the righteous give and do not hold back. day yendoo xemmem, te du am; kay jëfe njekk di joxeeka joxewaat.
27 The sacrifice of the wicked is detestable—how much more when brought with evil intent. Saraxu nit ku bon ñaawtéef la, rawatina bu ci jubloo lu bon.
28 A false witness will perish, but whoever listens will testify with lasting effect. Seede buy fen day sànku, kuy dégg, sa kàddu sax.
29 The wicked put on a bold face, but the upright give thought to their ways. Ku bon day ñeme-ñemelu, ku jub la muy def da koy wóor.
30 There is no wisdom, no understanding, no counsel that can stand against our Father. Nit xeluwul, amulug dégg ak pexe, ba manal Aji Sax ji dara.
31 The horse is made ready for the day of battle, but victory belongs to our Father. Nit ay takk, bésub xare, Aji Sax ji di maye ndam.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]