Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Proverbs 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 My son, if you receive my words and store up my commandments within you, Sama doom, déggal samay wax, fonk samay santaane.
2 making your ear attentive to wisdom and turning your heart toward understanding; Teewlul xel mu rafet, sam xel di dégg.
3 yes, if you call out for insight and raise your voice for understanding, Ngalla wutala dégg, wool dég-dég wall.
4 if you seek it like silver and search for it as for hidden treasure, Sàkkul xel mu rafet ni xaalis, wut ko ni alal ju làqu.
5 then you will understand the fear of our Father and find the knowledge of our Father. Kon nga xam luy ragal Aji Sax ji, xam Yàllaa di kan;
6 For our Father gives wisdom; from his mouth come knowledge and understanding. ndax Aji Sax jeey maye xel mu rafet, kàddoom di taxa xam, di dégg.
7 He stores up sound wisdom for the upright; he is a shield to those who walk in integrity, Day dencalal ndam kiy jubal, di yiir ku mat.
8 guarding the paths of justice and watching over the way of his faithful ones. Day wattu ku jub fu mu jaare, di sàmm wóllëreem ciw yoon.
9 Then you will understand righteousness and justice and fairness—every good path. Kon nga xam njub ak yoon, xam jubal ak mboolem yoonu mbaax.
10 For wisdom will enter your heart, and knowledge will be pleasant to your soul; Ndax xel mu rafet miy tàbbi sa xol, nga xam, sa xol tooy,
11 discretion will watch over you, and understanding will guard you, nga foog, fegu, amug dégg, raw,
12 rescuing you from the way of evil, from men who speak twisted things, mucc ci yoonu ku bon ak kuy wax lu jekkadi,
13 who abandon the paths of uprightness to walk in the ways of darkness, mucc ci kuy wacc yoonu njub, di jaare mbedd yu lëndëm.
14 who delight in doing evil and rejoice in the perversity of evil, Kon nga mucc ci kuy def lu bon, tey bànneexoo lu jekkadi.
15 whose paths are crooked, and who are devious in their ways. Yoonu ku ni mel day lunk, jaaruwaayam dëng.
16 Wisdom will rescue you also from the forbidden woman, from the stranger with her smooth words, Xel mu rafet da lay musal ci jigéenu njaalookat, bokk feneen, di wax lu neex.
17 who forsakes the companion of her youth and forgets the covenant of her Father. Day dëddu wóllëreem, ba muy ndaw, fàtte kóllëreem ak Yàllaam.
18 For her house sinks down to death, and her paths to the dead. Këram day joy wuti dee, ay jaaruwaayam jëm njaniiw.
19 None who go to her return, nor do they reach the paths of life. Ku dem ca moom dootoo délsi, doo gisati yoonu dund mukk.
20 So you will walk in the way of the good and keep to the paths of the righteous. Kon nag aweel mbeddum waa ju baax, toppal yoonu defkatu njekk,
21 For the upright will live in the land, and those of integrity will remain in it; ndax kuy jubal ay dëkke réew mi, te ku mat a fiy des.
22 but the wicked will be cut off from the land, and the treacherous will be torn away from it. Ku bon, ñu génne réew mi; kuy fecci worma, ñu buddi, sànni.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]