Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Proverbs 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 The proverbs of Solomon, son of David, king of Israel: Kàddu yu xelu yu Suleymaan buurub Israayil, di doomu Daawuda.
2 To know wisdom and instruction, to understand words of insight, Li ko taxa jóg di nit ñi am xel mu rafet, am ab yar, ngir xam wax ju lal dég-dég,
3 to receive instruction in wise conduct, in righteousness, justice, and fairness, ngir yaru ci jëfe xel ak njub ak yoon, di jubal,
4 to give prudence to the simple, knowledge and discretion to the young, ndax ab téxét di foog, ndaw li it xam tey xalaat.
5 let the wise also hear and increase in learning, and let the one who understands gain guidance, Na boroom xel mu rafet déglu, yokk dég-dégam, te kiy ràññee di jariñoo ay tegtal,
6 to understand a proverb and a parable, the words of the wise and their riddles. ngir mana xam aw léeb aku taas ak kàddug boroomi xel yu rafet ak seeni cax.
7 The fear of our Father is the beginning of knowledge; fools despise wisdom and instruction. Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu xam-xam, te xel mu rafet akub yar, dof yaa ko xeeb.
8 Listen, my son, to your father's instruction, and don't turn away from your mother's teaching, Doom, toppal yaru baay, te bul wacc ndigalu yaay.
9 for they are a graceful garland for your head and pendants for your neck. Kaala gu jekk la ci bopp, di gànjar ci baat.
10 My son, if sinners entice you, do not give in. Doom, bàkkaarkat bu la xiirtal, lànkal.
11 If they say, "Come with us, let us lie in wait for blood, let us ambush the innocent without cause; Dañu la naan: «Dikkal, nu tëruji bakkan, yeeruji jàmbur bu deful dara.
12 like the grave let us swallow them alive, and whole, like those who go down to the pit; Nanu mel ni njaniiw, mëdd kuy dund, mu jekki tàbbi biir bàmmeel.
13 we will find all kinds of precious goods, we will fill our houses with plunder; Mboolem alal ju réy, nu jagoo, yeb sunu biir kër, mu fees.
14 throw in your lot with us; we will all share one purse," Dikkal nu far, mbuus miy benn, nu bokk.»
15 my son, do not walk in the way with them; hold back your foot from their paths, Doom, bul ànd ak ñoom ciw yoon, bul jaare fa ñuy jaar,
16 for their feet run to evil, and they hurry to shed blood. ngir dañuy xélu, nar musiba, di gaawtuy sànk bakkan.
17 For a net spread out before any bird's eyes catches nothing; Doo firib caax, ba jàpp njanaaw luy xoole.
18 but these lie in wait for their own blood; they ambush their own lives. Ñii kat seen bopp lañuy fiir, seen bakkanu bopp lañu sànk.
19 Such are the ways of everyone greedy for unjust gain; it takes away the life of its possessors. Képp kuy lekk lu lewul, nii lay mujje: wutin wu lewul jël bakkanu boroom.
20 Wisdom cries aloud in the street; in the open squares she lifts her voice. Xel mu Rafet a ngay woote ca mbedd ma, di xaacu ca pénc ma.
21 At the head of the noisy streets she calls out; at the entrance of the city gates she speaks: Ma ngay wootee béreb yu gëna xumb, di dégtaley kàddoom ca buntu dëkk ba.
22 "How long, simple ones, will you love being simple? How long will mockers delight in their mocking and fools hate knowledge? Ma nga naan: «Moo téxét bi, foo àppal sa téxét gi? Ñaawlekat bi, foo àppal sa ñaawle bi? Dof bi, ñaata yoon ngay bañ xam-xam?
23 If you respond to my correction, I, Wisdom, will pour out my spirit on you; I will make my words known to you. Soo dëppee ba déglu, ma artu la. Ma ne, kon ma xellil la samam xel, xamal la samay kàddu.
24 Because I have called and you refused, I stretched out my hand and no one paid attention, Damaa woote, nga gàntal, ma tàllal loxo, faaleesu ma.
25 and you ignored all my counsel and rejected all my correction, Sofental nga samay digle, nanguwoo samay artu.
26 I also will laugh at your calamity; I will mock when terror overtakes you, Kon boo sëngéemee, man it ma ree, njàqare dab la, may tex-texi.
27 when terror overtakes you like a storm and your calamity comes like a whirlwind, when distress and anguish come upon you. Njàqare di ngëlén, dab la, sa musiba def callweer, buub la, njekkar ak fitna dal la.
28 Then they will call on me, but I will not answer; they will seek me earnestly but will not find me, «Keroog nga woo ma wall, duma wuyu, nga seet ma, seet, doo ma gis.
29 because they hated knowledge and did not choose the fear of our Father, Daa fekk nga baña xam, te ragal Yàlla du loo tànn.
30 they rejected my counsel and despised all my correction. Dégluwoo samay digle it, xanaa xeeb samay artu yépp.
31 So they will eat the fruit of their own way and have their fill of their own schemes. Waaye loo ci góobe, gar ko, say pexe suur la këll.
32 For the waywardness of the simple will kill them, and the complacency of fools will destroy them; Déggadi sànk ab téxét, naagu rey ab dof.
33 but whoever listens to me will dwell secure and be at ease, without dread of disaster." Waaye déggal ma, dëkke jàmm, tàggook njekkar ak safaan.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]