Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Isaiah 20 RWBT

Side by side with the Father's Heart Bible™

Kàddug waxyu ñeel na Misra ak Kuus

1At ma bummib Asiri demee ca ndigalal Sargon buurub Asiri, ba songi dëkk ba ñuy wax Asdodd ca Filisti, ba mujj ko nangu, 2fekk na Aji Sax ji wax, Esayi doomu Amocc jottali. Mu ne ko: «Demal summi tubéyu saaku ji nga sol, te summi say dàll.» Mu def noona, di doxe yaramu neen, tànki neen. 3Gannaaw gi, Aji Sax ji ne: «Esayi sama jaam bi def na yaramu neen, tànki neen lu mat ñetti at, muy firnde, di tegtal ci mbirum Misra ak réewum Kuus. 4Te noonu la buurub Asiri di yóbboo ngàllo Misra, toxal waa Kuus, ñuy ay ndaw aki màggat. Yaramu neen, tànki neen lañuy def, seen taat ne fàŋŋ, muy gàcceg Misra. 5Dañuy boole njàqareek gàcce ndax réewum Kuus mi ñu yaakaaroon, ak Misra gi ñu doon sagoo.» 6Bu keroogee ku dëkke tefes googu dina ne: «Xanaa kay du ñii lanu yaakaaroon! Te nu dawoon di wuti ndimbal ci ñoom, ngir rëcc buurub Asiri! Léegi nag nu nuy mucce?»

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]